WOTEY 2024 : MAKI SÀLL A NGI NGEMBU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Maki Sàll, dalal na 474i meer ak 37i njiitali Ndajem depàrtmaa yu bokk ci lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar. Ba mu jelee kàddu gi, wax na ci xew-xew yi fi jaar, yàggul dara. Guléet nag, muy àddu ci yëngu-yëngal yi fi amoon ba ñu bari dee ci : 16 (ci waxi Nguur gi), 23 (Amnesty Internationale), 30 (Pastef).

Maki Sàll, Njiitu réew mi, ñaawlu na taal yeek yàqate yees nemmeeku woon fan yee weesu. Xamle na ne, Senegaal dafa leb xaalis bu bari ngir tabax ak a defar ay jumtukaay yokkute. BRT bi ak TER bi la ci namm. Nde, way-ñaxtu yi jot nañoo am lu ñu yàqate ci TER bi ak BRT bi. Njiitu réew ma nee, loolu, wareesu ko seetaan. Nde, dinañ jël seen i matuwaay ngir sàmm kaaraange ak jàmmi réew mi.

Maki Sàll dafa doln dalal meer ak njiitali Ndajem depàrtmaa yi. Nde, mbootaayu Meeri Senegaal yi (Association des Maires du Sénégal) ak mbootaay gi boole njiitali depàrtmaa yi dañoo defar ay “pétitions” yu ñu bokk xaatim ngir Maki Sàll bokk ci wotey 2024 yii ñu dëgmal. Nee ñu, 87i meer yoo jël ci 100 yu nekk, nangu nañ Maki Sàll bokkaat. Nooneet, 84i njiitali depàrtmaa yoo jël ci 100 yu nekk Maki Sàll lañ bëgg a def seen lawax. Ñoom nag, fas nañoo yéene jàppale Maki Sàll, gunge ko, xeexle ko ngir mu toogaat ci jal bi.

Ñoom sax, bees sukkandikoo ci kàdduy Umar Yum ak Mari Terees Fay, Maki Sàll rekk a mën a boole njabootu Bennoo Bokk Yaakaar. Moom rekk a di buum gi mën a téye say wi. Bu nee du bokk, njaboot gi dina tas, ndono li ñaaw. Kon, Maki Sàll moo seen yaakaar démb, tey ak ëllëg. Te nag, ci kàdduy Mari Terees Fay, bu jaree bakkan, dinañ ko ci bàyyi.

Lees mën a jàngatee ci wax jooju mooy ne, waa Bennoo Bokk Yaakaar xam nañ ne, wëliis Maki Sàll, amuñu keneen ku am dayob jàkkaarlook kujje gi, rawatina Usmaan Sonko. Ndax Maki Sàll dina samp ndëndam ? Léegi mu leer. Ndaxte, Njiitu réew mi dige woon na ni dina waxtaan ak askan wi ginnaaw tabaski gi te, dina waxaale ndax day bokk walla déet ci wotey 2024 yi. Waaye nag, junj na.

Njiitu réew dafa mel ni kuy waajal xeex walla xare. Ndax, xam ni, bu nee day bokk, réew dafa nar a yëngu. Bu boobaa nag, nee na, na meer bu nekk fagaru, fexe aar goxam, bañ a bàyyi kenn muy jóge geneen di leen yàqalsi seen dëkk. Moo tac mu leen di digal ñu wut ñi leen di aar, ñoom ak seen i béréb.

Bim waxee loolu, xel yépp ñoo dem ci “nervis” yi. Ndax, bu dee wàllu kaaraange, takk-der yi ñoo ko war a sàmm. Dem na ba ne sax, CPI ay waxi caaxaan la. Mëneesul a dogu ci li wund waxam ji. Waaye, njortees na ni, Maki Sàll fasul yéene dellu ginnaaw te, bu ko jaralee xeex, dina xeex ba mu saf. Kon, Maki Sàll dafa mel ni kuy ngembu. Kan lay waaj a bëreel ? Ku ëpp doole ? Tontu li yàggatul.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj