WOTEY 2024 YI : AG TËNK ÑEEL BAAYALE GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Areete 032005 bu 25 sàttumbaar 2023 bu njëwriñu biir réew mi biraloon moo tënk limu falaakon bob, lawax bu nekk war na ko dajale. Areete booboot leeral anam yi baayale gi war a tëdde. Baayale gi nag, ci ni ko areete boobii tëralee, dafa séddalikoo ci ñaari pàcc. Baayaleg maxejj yi (parrainage citoyen) ak baayaleg way-falu yi (parrainage des élus), maanaam dépite yi, meer yi ak njiiti ndajey depàrtmaa yi.

Bu dee baayaleg maxejj yi, lawax bu ci nekk, ginnaaw bi nga matalee sa wayndare, danga waroon a indil ndajem ndeyu àtte mi 44. 231i falaakon (électeurs) gën-gaa néew, walla 58.975i falaakon gën-gaa bari. Lim boobu nag, dafa war ëmb as-tuut juróom-ñaari (7i) diiwaan, diiwaan bu ci nekk boroom dajale fa 2 000iy baayale lu mu néew-néew. Li ciy des, fum neex boroom wutee ko fa, muy biir réew mi walla fépp fu doomu Senegaal nekk.

Bu dee baayaleg way-falu yi moom, lawax bi ko tànn dafa waroon a am baayaley juróom-ñetti (8i) dépite ci téeméeri dépite yoo jël fa Ngomblaan ga. Maanaam, as-tuut, boroom waroon na am fukk ak ñetti (13i) dépite yi ko baayale. Bu dee baayale meer yi ak njiiti ndajey depàrtmaa yi, lawax bu ko ci tànn, waroon nga dajale téeméer ak ñaar-fukki (120i) baayale seen biir.

Falaakon bu ci nekk nag, benn lawax kese la la yoon may nga baayale ko. Dafa di, ku juum walla mu tey ko baayale ñaari lawax walla lim bu ko ëpp, yoon mën na la ci topp. Bépp lawax nag bu jébbale limub baayale bu ëpp bees la laaj, àttekat yiy saytu baayale gi duñu boole lim bu ëpp bi ci caytu gi. Maanaam, lim boobii ëpp, day neen.

Sumb bu njëkk bi ci caytu gi nag, mi ngi dooroon keroog gaawu 30 desàmbar 2023 bi 9i waxtu toftalee 30i simili. Mi ngi jeex àjjuma 5 sãwiyee 2024. Ci Bubukara Kamara lañ doore, jeexalee ko ci Usmaan Sonko. Ayda Mbóoj moo waroon a mujje, waaye kenn jotul woon a saytu wayndarew Usmaan Sonko bés biñ ko waree woon saytu. Te, yoon dafa sàrtal ni, ku wuute sa ay, sa wayndare lees di mujjee saytu.

Bu dee ñaareelu sumb bi, ci talaata jii weesu, 9 sãwiyee 2024 la amoon. Doon nañ ci saytuwaat wayndare ñi matalul woon ca sumb bu njëkk ba. Ndaxte, juróom-ñeen-fukki lawax ak ñett (93i) ñoo jébbale woon seen i wayndare ca njëlbeen ga. Mu amoon ci ñett ñu mujje woon a bàyyi, muy Elaas Ibraayma Mbów, Ndongo Sillaa ak Taala Sillaa, mu desoon juróom-ñeen-fukki (90i) lawax.

Ci biir juróom-ñeen-fukk (90) yooyu desoon, ñaar-fukk ak benn (21) kese ñoo ci jàll jéegob caytu gi. juróom-benn-fukk ak juróom-ñeent yépp ñoo lajj. Dees na ci fekk ñeent ñoñ, nekkoon nañ fiy magi jëwriñ (anciens premiers ministres) niki :  Aminata Ture, Abdul Mbay, Séex Aajibu Sumaare ak Suleymaan Ndeene Njaay. Bu dee ñaar ñu njëkk ñi, Maki Sàll moo leen ko tabboon, ñeneen ñaar ñi ci des, ci Nguuru Ablaay Wàdd lañ ko nekkoon. Te, Maki Sàll ci boppam, Ablaay Wàdd a ko meññ. Kon, Sàmbaay Bàcc rekk. Ñoo bokk cëslaayu pólitig.

Ci boroomi tur yees gàntal tamit, dees na ci fekk boroom DMedia, Bugaan Géy Dani, Elaas Abdurahmaan Juuf, layookat bii di Elaas Mustafaa Juuf (Meetar Elaas Juuf), añs. Ñoom, dañu bokkoon ci juróom-ñetti (23i) lawax yi waroon a jàll ci ñaareelu sumb bi, waroon a mottali seen i baayale. Waaye, mujjuñoo baaxle. Àndandoo Usmaan Sonko bii di Basiiru Jomaay Fay, moom mujje naa jàll.

Bu dee Usmaan Sonko, njiitul kujjeg pólitig gi, gën fi siiw, ndajem ndeyu àtte mi saytuwul ay baayaleem. Nde, ñoom àttekat yi, dañu lay ni ngóor si Sonko matalul wayndareem. Këyit giy wone ni joxe na ag warloom (caution) la indaalewul. Këyit googii nag, ci li Ayib Dafe wax, dañ leen ko bañ a jox, du ci seen coobare. Te, ñoom sax, joxe nañ ab « quittance » buy wone ni jébbale nañ seen warlu. Ak lu ci mën di am, moom Usmaan Sonko du bokk ci wotey 2024 yees dégmal.

Lawax bii di Ceerno Siise moom, dafa joxe woon ag toftaleg dépite bu baaxul, takk-deri DIC yi daldi koy jàpp.

Keroog 12 sãwiyee 2024 la ndajem ndeyu àtte mi di siiwal turi lawax yi nga xam ne, seen i baayale baax na. Buñ ci tegee juróom-ñetti fan, keroog 20 sãwiyee 2024, lay biral lawax yi nga xam ne ñooy joŋante ci wotey 2024 yi ngir dagaan baatu askan wi. Bu dee kàmpaañ bi, dibéer 4 féewaryee 2024 lay door, wote bi di am keroog dibéer 25 féewaryee 2024 ci réew mépp ak bitim-réew. Bés boobu la Saa-Senegaal yi war a fal ki leen di jiite juróomi at yii ñu jëm.

Cig pàttali, guléet Senegaal di dégmal wote yoo xam ni, Njiitu réew mi toog du ci bokk.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj