Ndajem Ndeyu Sàrtu Réew mi biral na njureefi wotey Ngomblaan gi. Tay ci àllarba ji, 27i pani nowàmbar 2024, lañu leen siiwal ginnaaw bi mu amulee kenn ku dugal dabantal. Njureef yooyu nag, dañuy dëggal ndamu làngug Pastef gog, moo raafal limu 130i dépite ci biir 165 yi war a teewal askan wi fa Ngomblaan ga.
Ci ndogal li mu biral, àttekati Ndajem Ndeyu Sàrtu Réew mi xamle na ne amul kenn ku bañ njureef yi tukkee ci mbañ-gàcce yi. Maanaam, bi DGE biralee njureefi négandiku yi, amul kenn ci joŋantekat yi ku kaas walla mu bañ njureef yi. Ci weneen waxiin, benn lawax dugalul ab dabantal. Loolu moo tax ñu dëggal njureef yi.
Bu ko defee, ci biir 7 371 891i wotekat yu bindu woon ci wotey Ngomblaan gii weesu, 3 650 120 ñoo wote. Bees ko xaymaa, ci biir wotekat yi bindu, 49,51 ñoo wote ci téeméer yoo jël. Waaye nag, keroog, dibéeru wote ba, daf ci amoon 26 487i xob yees neenaloon. Bu ko defee, 3 623 633i xob ñoo ci wér.
Ginnaaw bi ñu waññilee làng / lëkkatoo gu ci nekk li mu am ciy xob, Pastef moo jiitu ak doole. Ndaxte, làngug Usmaan Sonko gi moo am lu tollu ci 1 991 77i xob, daldi jël 29i toogu ci réew mi ak 101i toogu ci wote raw-gàddu gi, lépp di 130i dépite.
Lëkkatoo Takku Wallu 531 466i xob la am ci lépp, mu jox leen 16i dépite.
Lëkkatoo Jàmm ak Njariñ am na 330 865i xob, mu méngoo ak 7i dépite.
Lëkkatoo Sàmm Sa Kàddu moom, dajale na 222 060i xob, muy tollook 3i dépite.
Lëkkatoo “La marche des Territoires / Àndu Nawle” am na 47 636i xob, muy yemoo ak 2i dépite.
Lëkkatoo yii di Ànd Ci Kóolute Ngir Senegaal (21 391i xob), Senegaal Kese (25 822i xob), Ànd Beesal Senegaal (20 765i xob), “Pôle alternative 3ème voie / Kiiraay Ak Naataange” (26 775i xob), Soppi Senegaal (22 991i xob), Farlu (28 303i xob) ak làngug jàmbure gii di “Les Nationalistes / Jël Li Nu Moom”, gu ci nekk, 1 dépite la am.