DGE, kurél giy saytu mbirum wote yi, siiwal na njureefi négandiku yi ñeel wotey Ngomblaan gi. Démb ci alxames ji lañu janook saabalkat yi, biral la tukkee ca mbañ-gàcce ya. Pastef nag moo raafal li ëpp ci toogu yi, daldi am 130i dépite.
165i dépite ñooy toogal askan wi fa Ngomblaan ga. Ginnaaw bi Njiitu réew mi tasee Ngomblaan gi mu fi fekkoon, dafa àppaloon yeneen i wote ci bésub 17i pani nowàmbar 2024, yemook dibéer jee weesu. Askan wi génnoon na, fi réew mi ak fa bitim-réew, def warugaram. Maanaam, wote nañu, tànn ndaw yi leen di toogal fa campeef googa.
Dafa mel ni nag, askan wi dafa yeesal kóoluteem ci Pastef. Ndaxte, ginnaaw bi ñu falee Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay keroog 24i màrs, sandil nañ seen i xob njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, moom miy elimaanu jëwriñ yi. Nde, Usmaan Sonko moo jiite woon toftale lëkkatoo Pastef ci wotey Ngomblaan yees randalsi.
Bees sukkandikoo ci Abdulaay Ba, 1 991 770 ma-xejj ñoo woteel Pastef. Maanaam, 54,97 ñoo woteel Pastef ci biir téeméeri wotekat yoo jël. Abdulaay Ba mooy njiit lu njëkk ci ëttu dabu bu Ndakaaru (premier président de la cours d’appel de Dakar).
Pastef moo jël raw-gàddu gi ci 42i departamaa, kujje gi daldi séddoo 4 yi ci des (Raneeru, Podoor, Maatam ak Gosaas).
Lëkkatoo Takku Wallu gi Maki Sàll jiite moo am 16i dépite, Jàmm ak Njariñ bu Aamadu Ba am 7i dépite. Waa Sàmm Sa Kàddu, ci njiitalu Bàrtelemi Toy Jaas, 3i dépite lañu am. Bu dee lëkkatoo Àndu Nawle, 1 dépite lañu am.
Lëkkatoo yii di : Senegaal Kese, Les Nationalistes, Beesal Senegaal, Soppi Senegaal, Farlu, Ànd ci Kóolute, Pôle alternatif 3e voie, gu ci nekk 1 dépite la am.
Bu dee fa bitim-réew, Pastef moo am ndam fa Tugal (Ërob), Amerig, Aasi, Bëj-gànnaaru Afrig, Bëj-saalumu Afrig ak Afrig sowu-jant. Lëkkatoo Takku Wallu moo am ndam ca Afrigu digg ga.
Bu dee li ñeel limi wote yi, nii la mbir yi tëddee :
– limu wotekat yi bindu : 7 371 890
– limu nit ñi wote : 3 649 959
– limu xob yu neen yi : 26 326
– limu xob yu wér yi : 3 623 633
Cig pàttali, 41i toftale ñoo doon xëccoo 165i tooguy Ngomblaan ga. Dibéer 17i pani nowàmbar 2024 moo doonoon bésu wote yi. ca njeexital la, Pastef moo ci jiitu ak doole.