WOTEY NGOMBLAAN YEES RANDALSI : DGE SIIWAL NA 41 TOFTALE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kurél gu mag guy saytu wote yi fi Senegaal, Direction générale des élections (DGE), siiwal na toftale yiy joŋante ci wotey Ngomblaan yees randalsi, ñu war a am keroog 17i pani nowàmbar 2024.

Ca njëlbeen ga, 48i toftale yu ay lëkkatooy làngi pólitig ak i lawax yuy demal seen bopp la DGE jotoon. Ginnaaw bi leen kurél gi saytoo, 41i la ci jàppagum, dàqandi ci juróom-ñaar (7). Ñooñii ñu gàntalagum seen i toftale, mayees na leen wenn fan (24i waxtu) ngir ñu jébbal ag dabu (recours) fa màkkaanu Ndajem ndeyu sàrtu réew mi. Bees ci tegee juróom-ñaari fan, Ndajem ndeyu sàrtu réew mi dina siiwal toftale yi war a bokk ci wotey dépite yees dëgmal.

Toftale yii nuy limsi la DGE jàpp. Li ci biir lonk yi nag, ay beqi la ñeel mbindum tur yi ci wolof walla pulaar :

1. And liguey sunu rew [Ànd liggéey sunu réew]
2. Senegaal kese
3. Rv naatangue [naataange]
4. Union des groupes patriotiques
5. Coalition Pole alternatif kiraay ak natangue [kiiraay ak naataange] 3ème voie
6. Coalition Xaal yoon [Xàll yoon]
7. Union citoyenne bunt-bi
8. Jubanti Sénégal [Jubbanti Senegaal]
9. And ci koolute nguir Sénégal (aks) [Ànd ci kóolute ngir Senegaal]
10. Alsar
11. Coalition Nafoore Sénégal [Senegaal]
12. Union nationale pour l’intégration, le travail et l’équité (U.N.I.T.E)
13. Samm sa gafaka-samm sa elleg acsif [Sàmm sa gafaka-sàmm sa ëllëg]
14. Coalition Wareef
15. Coalition Actions
16. Union Naatall kaaw-gui (u.n.k) [Naatal kow gi]
17. Coalition Dundu
18. La marche des territoires andu-nawle [àndu-nawle]
19. Les nationalistes jel linu moom [jël li nu moom]
20. Coalition Mankoo liggeeyal Senegaal (MLS) [Mànkoo liggéeyal Senegaal]
21. Coalition Dekkal Teranga [Dekkal Teraanga]
22. And doolel liguey kat yi [Ànd dooleel liggéeykat yi]
23. Parti ensemble pour le Sénégal (Peps)
24. Coalition And beesal Senegaal-abs [Ànd beesal Senegaal]
25. Parti Garap-Ads [Garab]
26. Coalition Gox yu bees
27. Coalition Républicaine samm sunu rew jotali kaddu askanwi [sàmm sunu réew, jottali kàddu askan wi]
28. Coalition Defar sa gokh [Defar sa gox]
29. Coalition Fédération du renouveau
30. Parti Alliance jef jel [jëf jël]
31. Pastef [Pasteef]
32. Entité Alliance nationale pour la patrie
33. Coalition Farlu
34. And-suxali-production-transport-ak-commerce-laap-fal-jikko [laab]
35. Secteur privé
36. Coalition Diam ak njarin [Jàmm ak njariñ]
37. Coalition Samm sa kaadu [Sàmm sa kàddu]
38. Parti Bes du niakk [Bés du ñàkk]
39. Takku wallu Sénégal (TWS) [Senegaal]
40. Grand rassemblement des artisans du Sénégal
41. Coalition Sopi Sénégal [Soppi Senegaal]

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj