XARE CA SUDà

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xeex bu mettee jolli Sudã, diggante làrme beek i sóobare yu beddeeku. Ñaari seneraal yi foqati woon Nguur gi, atum 2021, ñoo nekk di xëccoo Nguur gi. Démb, ci gaawu gi, la xeex bi door. Nee ñu, 54i maxejj ñàkkagum nañu seen i bakkan.

600i nit yu amey gaañu-gaañu mooy lim bu fajkat yuy sàkku demokaraasi biral. Wëlis 54i maxejj yi ci dee, am nay fukki fukki sóobare yu ci dee tamit. Ay roppalaani xare ak i « chars de combat » di naaw ak daw ci tali péey bi, Xartum, di soqiy bal ak i roket. Askan wi, kenn demul, kenn dikkul. Nga gis ay sóobare yu sol seen i yére soldaar, gànnaayu ba diis di dox ci mbedd yi. Léeg-léeg, ñu dajeek tuuti nit yu yor seen i dëbës, di wër fu ñu nekk.

Saxaar siy ballee fu nekk ci diggu dëkk bi, fi nga xam ne, fa la campeefi réew mi, yi gën a mag, nekke. Askan waa ngi ame njàqare, tiit lool, niki Ahmed Seif miy dund ak soxnaam ak seen i 3i doom, ca penkub Xartum. Daf ne, « Doy na waar. Dafa mel ni mbir mi du gaaw a jeex. »

Moom, boroom kër la, te day ragal ne am nay bal yees soqi ci taax bim nekk ak njabootam, waaye dafa « ragal a génn xool » balaa ñu koy tiire walla mu dajeek sóobare yiy wër ci mbedd yi. Ndax, ciy waxam, fetel yaak mbéll yi dañoo fanaanee téll télli ca Xartum.

Sudã, 2019 ba tey, dafa daladi. Bi ñu daanelee Njiitu réew ma woon, Omar El-Besiir, réew ma dafa yëngu. Boob ba tey, mëneesugu fa amal ay wote yu jaar yoon. Dafa di, 30i at ñoo ngi nii, ay wote amu fa.

2021 la njiitu làrme bi, Abdel Fattaah Al-Burhaan ak njaatige FSR, Muhamed Hamdaan Daglo « Hemedti » ñoo àndoon foqati Nguur gi. Ñoom ñaar nag, yàgg nañoo diiroo mbagg. Ndeke, kujje gi yàgg na, daa feeñagul woon rekk. Ci gaawu gii nag la ne jëppeet, soppikuw xal, taal réew ma. Ay roppalaan, daamari xare ak i fetel yu diis a diis la soldaar yiy jëfandikoo ci péey bi ak ci béréb yu bari ci réew mi.

Àddina saa ngi woote ngir ñu wéer ngànnaay yi. Muy Sinwaa yi, di Paap Farãsuwaa, ñépp a ngi ñaan ngir jàmm delsi fa. Waa Ligue arabe ak Bennoog Afrig war nañ daje ndajem cëtëŋ ngir waxtaane mbir mi, wut pexe. Xeex bi nag, mi wéy ci bésub dibéer jii.

Moone, sóobare yi artu woon nañu ci Facebook wax ne : « Làrme bi dina amal i liggéey ngir doggali way-fetteerlu yi bokk ci Soutien rapide, na nit ñi toog seen i kër. » 

Fi mu nekk nii, kenn xamul ku tée lan. Waa FSR nee nañu naawu baa ngi ci seen i loxo ci gaawu gi. Neeti nañ, ñoo yor Màkkaanu Njiitu réew mi (palais). Waaye, làrme bi weddi na ko, wax ne moo yor Dalub làrme bob, dafa bokk ci bérébi Nguur gi. Tele bi sax, ku nekk a ngi naan moo ko teg loxo. Li am ba des daal mooy ne, ay woyi bëgg sa réew kese lañ ciy dawal.

Sudã, nag, dafa bokk ci réew yi gën a ndóol ci àddina si. Askan wa taloon na leneen lu dul xeexoo seen biir.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj