Leningrad la Wladimir Putin yaroo. Leningrad googu, moo nekkaat tey Saint-Pétersburg. Cib nettali, gone gi Wladimir, ku ësoon la, amoon fit lool te bare woon ay. Foo ko fekkaan, mu ngay xeex te, ay moroomi magam doŋŋ, ëppoon ko doole, la daan jàppanteel. Nee ñu, looloo ko taxoon a jàng Judo. Ku dem yaa ngi ñaaw njort, naan ci sam xel : « kii day xoromal doŋŋ… Nii rekk lañuy def, ku leen neex ñu fental lab jaar-jaaru jàmbaar ; boo dee seenub mbañ, ñu sosal la, sikkal la. Doo xam sax loo ciy gëm… » Weddiwuma la sax de. Ndaxte, njort lu ñaaw dinay faral di wattu boroom. Waaye, firnde laa ngi ci kàddu yii toftalu :
« Juróom-fukki at ci ginnaaw, jànge woon na ca mbeddi Leningrad ya ne : bu la wóoree ne xeex mënta ñàkk, fexeel ba njëkk a dóor. » (Poutine, oktoobar 2015)
Kon nga xam ne kii, du ku lay bàyyeek Yàlla, am déet ? Waaw kay. Bu ko defee, cong mii mu song Ikren nag, warta bett kenn. Nga neeti ma, « mbaa du danga bëgg a wax ne, namm xeex rekk waral njiitu réewum Riisi li yabal larmeem ba ci Ikren ? » Déedéet ! Danga yàkkamti rekk, waaye maa ngi ñëw. Sabab yi bare nañu te junjoon nañ ci as-tuut ci yaxal bii weesu. Bii yoon nag, dees na leen wax as lëf ci jëmmu Wladimir Putin laata ñuy duut baaraam dëgg-dëggi sabab yi ne ci ginnaaw xare bile. Toppal samab xalima…
KGB ba FSB : Poutine, aji-yëddu ji
Oktoobar 2022 la Wladimir Putin di am 70i at. Def na 32i at, bim duggee ci politig ak léegi. Nde, bim laxasee 40i at, la sëñ Poutine ngembu, sóobu ci géewug politig gi. 1952 la gane àddina, waaye ci atum 1990 lees koy njëkk a takkal ndombog-tànk ci wàllu politig. Anatoly Sobchak, ngóor si ko jàngal xam-xamu Yoon (droit) ca jàngune ba, moo koy tabb, def ko faracaytu bu mag ca meri bu Saint-Pétersourg. Wànte, ca njëlbeen ga, Poutine, aji-yëddu la woon, di woon ndawul KGB, kurélug yëddu URSS ga woon, siiwoon lool te raglu. Nga xool, gis ne, Njiitu réewum Riisi mu tey mi, mi ngi juddu ci njeexitalu ñaareelu xare bu mag bi, màgge ci jamonoy xareb suuf (guerre froide) bi diggante Riisi ak Amerig. Loolu, dafa njeexital lu réy ci politigu Poutine, bul ko fàtte.
Lemal sa baaraam, muy ñeent.
Jamonoy xareb suuf ba, nag, daawuñu xeexey fetel, misil walla ay bomb. Xeexu suuf la woon, xareb xel ak caay-caay. La woon ngànnaay mooy pexe, yëddu (espionnage) ak yëddanti (contre-espionnage), naxaate ak mbaleñfaŋŋ, bóomaate, wujje ci wàllu xam-xam, xarala, koom-koom ak sañ-sañ. Xeexin woowu, nag, KGB ak CIA ñoo ko séqoon, daanaka. Kurél gu ci ne di liggéeyloo ay way-yëddu, diy ndaw yu bëgg seen i réew, am pastéef te dogu ci seen liggéey. Mu jaraloon leen seen i bakkan, gënaloon leen seen i njaboot ak seenug dund. Ñu nekkoon, itam, ndaw yu am fit, dëgër xol, xereñe lool te muus. Rax-ci-dolli, amoon nañu bàmmeelu biir te mënoon a làqarciy mbóot, ak lu ñu nëbbu, nëbbu. Ndaw yooyii, ay kàkkataar dëggantaan lañ woon. Mënees na méngale aji-yëddu bi nib mala bu làmboo boppu xar, xelum lëg, bëti géléem, làmmiñu jaan, yaramu saaw, geenu jiit. Nànd nga wax ji ? Mi ngook.
Wladimir Putin, nag, kenn la woon ci ndaw yooyii. Dalub webu Kremlin biy xamle ne, Poutine dafa yàggoon a bëgg dugg ci KGB, fekk ne « jeexalagul woon sax njàngam ». Ci laaj-tontu bu yaatu bim amaloon ak yéenekaayu Riisi bii di Kommersant ci ati 2000 yi, miŋ ciy wax ne, « KGB, ci man, xiirteg ndaw a ma ci dugaloon. » 1975 lañ ko fa jëloon, mu tolloon ci 23i at kese. Fa la nekk ba 1990. Jamono jooju la URSS daanu, yóbbaale KGB. Noonu, ba 1997 ñu daldi koy tabb, def ko njiitalu FSB, kurél gi wuutu KGB.
Lees mën a jànge ci jaar-jaar bile mooy ne, benn, Poutine dafa juddu ci jamonoy xare, màgge ci, ñu tàggat ko ci. Ñaar, Li URSS tas daf ko metti, nim mettee saa-riisi yu bare. Ñett, Wladimir Putin dafa jàpp ne, tas bi URSS tas mooy jéyyab sewopolitig bi gën a réy ci 20eelu xarnu bi. Te, deñul ciy ŋàññ ak a naqarlu li OTAN di lëkkaloo ak yenn ci réewi penkub Tugal yi bokkoon ci URSS, di gën a jegesiy digi Riisi yi. 1997 ba jonni-Yàlla-tey jii, loolu lay kaas, di ko xeex, jamono ju ne ak li ko dooleem may. Kenn réerewul ne, OTAN, ag kurél gog, Amerig daf koy xeexe Riisi. Ndege, Amerig, mennum mébét la am : tënk àddina sépp, di buur, di bummi.
Waaw, Amerig, moom, dafa jàpp ne moom la Yàlla bindal suuf si, tàggatal ko li fi nekk lépp ci lu baax, mu war koo jariñoo moom kese akuw askanam. Ñoom, jàpp nañ ne ñoo gën ci xeet yi, ba tax ñu war a yilif ñépp, di nootaate ak noggatuwaate, di joxey ndigal ak i tere, di lawal seen i gis-gis ci àddina si ci fànn bu nekk nag. Bew bi ñu bew tax na leen a jàpp ne, ni ñu gise mbir yi rekk, noonu la war a doxe. Moo leen tax di jéem a ga réew yi ci des, di leen tànnal xeetu demokaraasi bi dëppook seen i bëgg-bëgg, koom-koom gu méngook seen i njariñi bopp, ay mbonte yu deme ni ngóor-jigéen ak yu ni mel, añs. Réew walla kurél gu xàll saw yoonu bopp, am tëralin wu safaanook seen bëgg-bëgg ak seen gisin, ñoom Amerig ak i surgaam, ñu jéem laa sikkal, yàq sa der, tuumaal la ba noppi di la xeex ci anam bu ñaaw a ñaaw. Loolu la kàdduy Poutine yii di wund :
« Saa su ne, ñoo ngi [réewi sowu yi] yedd Riisi ci wàllu demokaraasi. Ma jàpp ne, àddinay tey jii, deesu fee nangooti am réew di féete ñépp kow. Te, loolu sax, dafa mënatul a nekk […]. Bi Riisi sosook tey, am na junni junniy at, te jamono ju ne, moo daan tànnal boppam xeetu politig bi muy sékk ak yeneen réew yi. Ba jonni-Yàlla-tey jii, nag, fasunu yéene wàcc yoonu cosaan woowu. » (Wladimir Putin, Munich, 2007)
« […] Réewi sowu yi dañuy xeex mbaax, nite ak jikko yi yeneen réew yi làmboo ci cosaan : muy dundiinu waa réew ma, mbatiit ga, diine ja walla sax ci wàllu ngóore ak njigéene… » (Wladimir Putin ca ndajem Kurélug Valdaï ga, 2013)
Boo ameeb seetlu, dangay gis ne, ci njeexitalu xare bu mag bi ba tey, Amerig dafa yàgg a jàppanteek Riisi. Demoon na ba jekku ko, fexe ba daaneel URSS. Ginnaaw gi, mu nas i pexe ngir beddi Riisi, néewal ko doole ci féewale bim ko doon jéem a féewale ak àddina si. Waaye, puus boobu mu doon puus Riisi, génne ko ci digey Tugal yeek mbootaay ya fa am, daf ko boole, wëliis coobareem, ak yeneen réew yuy amsi doole niki Siin, Inde, Beresil, Afrig-di-sid, añs.
Réew yooyoo samp seen i ndënd tey, ne ñoo lànk, dootuñ bàyyeeti Amerig muy def li ko neex. Ñu sos seen i kurél ak i mbootaay yi deme ni :
-
OCS (Organisation de Coopération de Shangai) mi Riisi ak Siin taxawal ci atum 2001, bokk kook Kazakhstan, Kirghizstan, Inde, Pakistan, Tadjikistan ak Ouzbekistan.
-
OTSC (Organisation du traité de Sécurité Collective) mi Riisi sumboon ci 2002, ànd ceek Kazakhstan, Kirghizstan, Arménie, Biélorussie ak Tadjikistan.
-
Ak UEEA (Union Economique EurAsiatique) biñ samp ci 2014, di kurélug koom-koom, Riisi, Kazakhstan, Arménie ak Biélorussie bokk ko.