Nimbir yiy doxe diggante nguur geek kujje gi bi Màkki Sáll toogee ci jal bi ba tey jii, dalul xel dara. Nun ñépp a ànd ci demokaraasi, waaye ni ko peresidaŋ Sàll gise — ku am doole danga koy wone, doo maye dara, doo yërëm kenn — mën naa jur ëllëg musiba ci réew mi. Ci sama gis-gis bu gàtt, dafa war a méngook li gën ci sunuy aada. Senegaal, waxtaan ba juboo lanu xam, lu fi am solo. Su dee wote rekk, nag, kenn du ni guléet, miim réew yàgg naa tabb ay njiitam te deret du turu. Lu jar a fàttaliku la, tey jii alal ju bari feeñ na ci suuf si. Mbaa du sax petorol boobook gaas bee yóbbu fiti ñenn ñi ? Bu nu ànduleek sunu sago, am nay réew yu mag ak i boroom doole dinañ jéem a salfaañe Senegaal ngir rekk aakimu alal jooju. Nanu ci Yálla musal waaye noonu la ko gaa ñooñu tàmmee def.
Kon, li war ki Yàlla teg ci boppu réew mi, mooy xam ni nun ñépp, ba ci kujje gi sax, njabootam lañu. Su ko defee mu wuuf ñépp, bañ a tànqamlu kenn. Nay yolomal buum gi bu ko mbir yi laajee, te yit këwdiir giy bax ci kaw taal bi, na koy moytoo tëj ràpp. Li peresidaŋ Abdu Juuf bàyyiwul woon xel ci looloo taxoon ñu tëral sàrtu wote bi ñépp àndoon ci atum 1992. Dafay faral ñatabal nit ñi ba ñu sës te du yoon. Ak li muus di néew doole yépp, bu sësee songe te kuy bëgg a lab sax, soo ko tàllalee jaasi mu jàpp ci.