XEEB NGA XAL, MU LAKK SA DÀGGA (1/2)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kuy laaj fu réewum Senegaal tollu, dellul bésub alxames, 16 féewaryee 2023, xool, seet, settantal bu baax. Du ñàkk nga jëley ciy njàngat yoy, dees na ci gindeeku. Nde, bés la bob, doy na junj ñeel tolluwaayu réew mi ak fim nar a jëm. Dafa di, keroog, nes-tuut, Senegaal tàbbi ci fitna joo xam ne, mën na màbb kenoy réew mi. Bés boobu la xar-kanamu Senegaalu Maki Sàll feeñ dëgg-dëgg. Keroog, la Yoon wàcc yoon, naroon a dugal réew mi ci guta gu réy a réy. Nan leen dellu xoolaat la xewoon keroog.

Usmaan Sonko dafa génne ca àttewaay ba, mbooloo mu bari dar ko, ay ndaw gën cee bari. Mbooloo mooma, jàppale njiitul Pastef lee leen fa indi woon. Ndax, ñoom, ak li ëpp ci askan wi sax, dañu jàpp ne, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa bëgg a laaj ñetteelu moome. Te, Usmaan Sonko rekk a di dédd bi ne ci yoonam, muy xool nu mu def ba fexeel ko. Ci seen gis-gis, lees di toppe njiitul kujjeg Maki Sàll gi day dellu ci pexe yooyile muy nos ak nocci ngir beddi ko ci joŋanteb wotey 2024 yi. Kon, mbirum « sosalaate, saaga ak njublaŋ » bi ko jëwriñ jii di Maam Mbay Ñaŋ di toppe day delluwaat ci pexe yooyu. Waaye, bu mbir mi yemoon ciy tuuma ak layoo kepp, coow du jib, walla bu jibee yit, du jur tiit ak njàqare yi mu sabab keroog. Lu xewoon ?

Usmaan Sonko dafa xéy, wuyuji Yoon. Bi muy dem, takk-der yaa ko dar, gunge ko ba mu àgg. Naam, ca biir àttewaay ba, xëccoo amoon na fa diggante layookati Usmaan Sonko ak àttekat baak toppekat bi. Waaye, mujje woon nañu ajandi layoo bi ba bésub 16 màrs 2023. Bi meeru Sigicoor bi génnee di ñibbi, ca la coow li am. Nde, mbooloo mu bari lool a ko toppoon, mu taxaw ci biir wataam, yékkati ñaari loxoom, mel ni kuy wax ni am na ndam. Ndiiraan may riir. Ca la takk-der ya ñëwee, dóor ay lakkirimosen, tas ndiiraan ma, mu dog i jégaajél. Ay sàndarm yu sol i kask ak i mask daldi wër watab Sonko ba.

Ca njëlbeen ga, dañu ko sant mu wàcc ; waaye njiitul Pastef li dafa bañoon. Ci widewoo yi, gisees na Sonko di jollasanteek komiseer bi yilif takk-der ya, di ko laaj ndax dafa def lees ko war a jàppe, am déet. Ca la leen waxee ne, mën nañ koo dar, ni ñu ko daree woon ba muy dem ca àttewaay ba, wànte takk-der ya ne dee day wàcc daamaram bi. Ca la kenn ci sàndarm yi daldi toj weeru wataam bi, ubbi buntu bi, xëcc Usmaan Sonko, génne ko. Jamono jooju yépp, Usmaan Sonko mi ngi àndoon ak sagoom, daldi dal. Deful lu dul laaj leen laaj yii toftalu :

« Ndax dama def lees ma war a jàppe ? Ndax takk-der yi am nañu sañ-sañu génne nit ci daamaram wëliis coobareem ? »

Ndekete, booba, kenn ci layookatam yi, Sire Keledoor Li, mi ngi doon filme lépp, di ko tasaree ci mbaali jokkoo yi. Naam, yóbbu nañ ko ba këram, daldi ko fay wàcce. Waaye kat, seen uw doxalin teey na xel lool, te day wane rekk fitna ju réy ju nekk diggante njiitul lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar li, Maki Sàll, ak njiitul Pastef li, Usmaan Sonko. Ñu bari ñiy jàngat pólitigu Senegaal dañu jàpp ne, keroog, nguurug Maki Sàll dafa wane dëgg-dëgg li ko ñetteelu moome gi jaral ak fi mu nar a àgg ak Usmaan Sonko mi ciy gàllankoor bi gën a mag. Mul mel ni, diggante suuxal Gaal gi ak jox lenge yi Usmaan Sonko, Maki Sàll tànn na ba noppi ; te mel na ni ku ci dogu. Maanaam, taal réew mee ko gënal di seetaan ba Usmaan Sonko di ci jot. Foofu, jar na amal ab taxaw seetlu ngir xam lu tax njiitu réew mi Maki Sàll ameel Sonko mbañeel gu ni me lak lan lañuy ragal ci moom.

Dees na ko topp…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj