Tey, ci talaata ji 14 màrs 2023, la lëkkatoo Yewwi Askan Wi di amal ab « giga meeting », maanaam mitiŋ bu mag a mag ca pàkkub akapes bi nekk Parsel aseni. Mitiŋu tey beey doon njëlbeenug xew-xew bi kujje giy amal ci fan yii nu dëgmal. Ndax, ginnaaw tey, dinañu wàcc ci mbeddi réew mi, amal ay doxi ñaxtu. Liñ ko dugge, ci seen i wax, mooy sàmm demokoraasi bob, Njiitu réew mi ak i ñoñam salfaañe nañu ko, nasaxal ko. Waaye, dañuy xeex itam ñetteelu moome gi Njiitu réew mi, Maki Sàll, di diir, xoqatal bi muy xoqatal lenn ci waa kujje geek njàpp yu bari yi ñeel doomi réew mi, way-moomeel yi, taskati xibaar yeek ñi àndul ak moom.
Ci beneen boor bi, waa Bennoo Bokk Yaakaar ñoo ngi duut baaraam kujje gi, rawatina Usmaan Sonko mi ko jiite, di leen tiiñal ak a jiiñ. Nee ñu, njiitul Pastef leek naataangoomi YAW dara yëkkatiwu leen lu mooy yee fitna, taal réew mi. Ñu bari ci seen i kàngam artu nañu, tëkku waa kujje gi, wax ne dinañu jàmmaarlook ñoom. Moo tax, bu dee dëggal nañu seen bopp, réew mi dafa nar a yëngu. Lu war a tax ñépp di gaatnga taafar ak fitna ?
Senegaal, nee ñu, Réewum Yoon la. Maanaam, réew la mom, Yoon a ko lal. Bu la neexe yit wax ne ca Réew la mom, Yoon a di cëslaayug keno yi. Bu loolu amee, Yoon mooy doon ndëgërlaay liy dooleel campeef yi ba duñ jeng. Bu ko defee, Nguur gi dafay tënku ci Yoon. Ci déggin wu set, Yoon ay dox diggante askan wi, képp-kenn ci ñoom, ak Nguur gi, rawatina banqaasam yi koy jëmmal. Kon, ci réew mu ni mel, Yoon a war dox diggante Nguur geek nit ñépp, campeef yi, kurél yi, añs., ci seen i jëflante.
Li Yewwi Askan Wi namm a def mooy, bésub 14 màrs, ab mitiŋ ca Parel, pàkkub Akapes. Bu dee ci réewum Yoon, ab mitiŋ, lees sàrtal la. Yoon kat moo wax, ci ñeenteelu dogu Ndeyu Àtte bi, ne làngi pólitig yi ak lëkkatoo làngi politig yi dañu am sañ-sañ ak wareef ci dundal demokaraasi ak tàggat maxejji réew mi. Bu nu delloo ci referàndumu 2016 bi, dogub 58 bi day wax ne kujje gi am na sañ-sañu wujje ak nguur gi fi nekk ci kow mu sàmmoonte ak li Ndeyu Àtte bi tëral. Kon, mitiŋ, Yoon a ko sàrtal ci réew mii di Senegaal.
Beneen xew-xew bi kujje gi nammati def mooy doxu ñaxtu, ëllëg ci àllarba ji, 15 màrs 2023. Looleet, Ndeyu Àtte bee ko yoonal ci juróom-ñetteelu dogam. Nde, waxees na ci ne, Bokkeefu Senegaal dafa warlul maxejj yépp ay sañ-sañ yu mag yi ñeel nit ki, àqi koom ak nekkin, ak àqi bokkaale yi. Sañ-sañ yooyook i yelleef yi, bi ci gën a fés mooy :
-
Sañ-sañ yi ñeel jàmbur ak sañ-sañi politig : sañ-sañu am sa xalaat, sañ-sañu génne sa xalaat, sañ-sañu siiwal sa xalaat ci yéenekaay, sañ-sañu def mbootaay, sañ-sañu daje, sañ-sañu dem ak dikk, sañ-sañu wonu ci biir mbooloo.