XEEX BI TÀMBALEETI NA !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xeex bi tàmbaleeti na diggante askan wi ak takk-der yi. ndogalul dàq wotey 2024 yee ko sabab. Nde, tey ci àjjuma ji la kilifay kujje gi woote woon am ndajem ñaxtu mu réy fa « Place de la Nation ». Nees ko njortee woon, takk-der dañ leen fa jiitu ngir tere leen amal ndaje mooma. Waaye, way-ñaxtu yi dañoo dogu ci ne kenn du leen teree kaas àq yi leen Yoon may. Moo tax, jamono jii nuy bind yaxal bile, xeex bi door na diggante takk-der yeek way-ñaxtu yooyiy bañ ndogalu Maki Sàll li.

Ndakaaroo ngi bax

Noonu, biir Ndakaaru ak li ko wër, gërënaad lakkirimosen yeek xeer yaa ngi naaw, gune yiy taal i póno ak i matt, saxaar siy jolli di ubale jàww ji. Kolobaan, Medinaa, Liberte 6, màkkaanu Walfadjri, Xaar-Yàlla, Kastoor, Kornis west, Petersen, Faas, Gël-Tàppe, Sàndaga, Ñaari-Tali… ci béréb yii yépp, ñu nga fay xeex.

Yeneen diiwaan yi sóobu nañ ci xeex bi

Waaye, xeex bi yemul Ndakaar kese. Fa Ndar tamit, ndongay Iniwérsite Gastoŋ Berse yaa ngiy jàmmaarloo takk-der yi, fa Place Faidherbe tamit, oto demul, oto dikkul ndax xeex bi. Pomu Faidherbe bi sax oto jaaratu ci. Mbàkke, Sigicoor ak Mbuur tamit ñu nga fay xeex.

Taskati-xibaar yi moom, seen liggéey narul a yomb. Ndax, ñu ngi leen di dóor i gërënaad lakkirimosen ak di leen jàpp.

Ci biir ñaxtukat yi, am na kuñ ci dóor bal ci loxo nees koy gisee ci peeñu melal gi (image d’illustration).

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj