Maalig Gàkku, Basiiru Jomaay Fay ak Seex Tiijaan Jéey jébbal nañu Ndajem ndeyu àtte réew mi ag càkkuteef gu jëm ci neenal dekkare bi Maki Sàll jël jëm ci dàq wotey 25i féewirye 2024 yi. Du ñàkk yeneen lawax yi def ni ñoom.
Baara Gay jébbal na bataaxal njiitul Ngomblaan gi
Baara Gay, meeru Yëmbël sid miy dépite, jébbal na njiitul Ngomblaan gi, bataaxal bob, Njiitu réew mi, Maki Sàll, la ko jagleel. Li mu ko dugge mooy Njiitu réew mi jox ndigal Aamadu Ba, njiitul jëwriñ ji, ngir mu wuyusi dépite yi, ñu déglu ko. Li ko sabab mooy ne, ciy waxam, daa mel Aamadu Ba moomee dafa bañ a toftal xaatimam (contresigner) dekkare biy neenal dekkare bi jëmoon ci woote ngir ñu dem ci wotey 2024 yi.
Ahmet Aydara : « Aamadu xaatimul dekkare bi… »
Ahmet Aydara xamle na ne Aamadu Ba nanguwul a xaatim (contresigner) dekkare bi Njiitu réew mi jël ngir fomm wotey 2024 yi. Sabab bi moo di ne, ci waxi Ahmet Aydara, moom Aamadu Ba dafa tekki ndombog-tànkam ba noppi ñu koy nëbb nit ñi.