CI TEKKIB PAAP AALI JÀLLO
*
Séex Anta Jóob mas naa bind ne “Senegaal, mënees na fee jalgati yoon, tooñ nit ba toññarbi ko ba noppi rafetal mbir mi, solal ko mbubbum yoon mu taaroo taaru (…). Bu ko defee, sunu xeexu jamono jii, na képp kuy boroom xel mbaa mu bëgg réew mi, jàpp ni xeexam la. Te nag, wareesul a toqi feek nguur gi dakkalul xëbalaate ak xoqtal ak nappaate yi mu dëkke ci fànn bu nekk, bañu ci sax dàqlu nit ki liggéeyam mbaa bóom ko. Bu yaboo ku nekk jàpp ne xare la ; xare ngir afal nit ñi dëggëntaan, ku nekk jëlaat sam péexu bopp ; xare ngir dekkil ngor. Afrig, bu fi ay Bokasaa ak ay Idi Amin Dadaa amee tey, daa fekk nu am ay workat ci sunu biir. Ay xeltukat ak ay saytaafoni Afrig ñoo worook seenuw sas. Li ñu doon i ragal rekk moo tax wax ciy maaliforo ëppal leen solo wax ci aali-kalaj gi, maanaam càmmeefu àqi sax-dakk maxejj bi. Muy boroom xam-xam bi, di maxejj bi ànd ak sagoom, ñépp a war a bañal seen bopp par-parloo ak xàjj-ak-seen, wargarloo ko. Ku ci nekk, xeex bi daf la war a jaral sa bakkan, nga fexe bay àtte yu baax te jub wuutu fi àttey par-parloo yi jaarul yoon.»
Séex Anta Jóob, “Taxaw”, limat 18, nowàmbar-desàmbar, 1979
*
Ak ni politig biy doxee Senegaal, xel mën naa jàpp ne, réew mi, sabab yi koy taal ñu ngi fi ne gàññ. Mooy li xeltukat yiy woowe ci nasaraan « nation mortelle » maanaam askan wu waxtu deewam soreetul. Nde, réewum yemale dafa war a am ay campeef yuy war a doon kenuy askan wi. Ndaxte kat, loolooy jubluwaayam. Réewum yemale, nag, du lu way-jàng-yoon yi war a aakimoo. Kon, du ñoom rekk a ci war a wax. Dafa di, njajaan lees jiital ci wax ji, ci noste gi lay dellu saa su ne. Waaye, day feeñ ci anam yu bare : lott gi campeef yiy lott ci saxal jëmmu demokaraasi ci boppam, ci nees di nasaxale bennoog réew mi, ci ni ñu koy tas-tasaree ciy pàcc yu bare ; lépp di biral ni yoon ñàkk a tëdde njaaxaanaay, di faral ñenn ñi mbaa soppiku gànnaay gi nguur giy xeexe kujje politig gi ; dina feeñ tamit ci ni ñuy saware ci lal i pexe ngir sax ci nguur gi, aakimoo ko, añs.
Réewum yemale, nag, sàmm ak yoonal kóllëre giy dox diggante nit ñee ko tax a jóg, rawatina diggante njiit yi ak askan wi. Moo tax, saa bu yoon lottee, njajaan dikkal mboolem-nawle mi.
Réewum yemale, day sàrtal ak a yombal dëkkandoo gi nga xam ne, mënta ñàkk ci tabaxug askan. Ci gàttal, Réewum yemale yemul rekk ciy campeef. Bu dee ay àtte ak i campeef rekk lañuy natte demokaraasi, Réewum yemale moomu daldi yem ciy xalaat doŋŋ, nit ñi duñu ci gis seen bopp. Campeef yi, ak lu seen tëralin rafet rafet, duñ am njariñ fileek ñi leen di saxal jëfewuñ yoon. Nde, campeef bu baax, dees na ko natte ci doxalinu doom-aadama walla ci kurél yi koy jëmmal ak njeexital yi muy am ci politig gi.
Réewum yemale mu mat day jéggi dayo yees di natte campeef yi. Waaye, digaloog baat yi bi ñuy soow, ci làmmiñi nit ñiy tënku ci mbind yi rekk lay yem. Politiseŋ yi ñoo ci raw, ak way-jàng-yoon yi féetewoo xeetu xeltu bees duppe « positivisme ». Senegaal, nag, dañ fiy faral di dégg ay nit ñuy màggal ak a bàkkoo demokaraasi biñ ne moo fi am. Waaye, ku woyof bopp rekk mooy gëm waxi caaxaan yooyu. Ndax, laaj biñ war a samp bii la : ban demokaraasi ? Xanaa kay du bi nu xam ; demokaraasi boo xam ne ciy bind la aju, ñu ciy njuuj-njaaj ci anam bu fés ngir soppi nguur gi lu doom di doon ci baayam. Wax dëgg-Yàlla, du demokaraasi bu ni mel la maxejj yi yittewoo. Wànte, demokaraasi biy tax ñu naan demokaraasi mooy biy sàmm àqi bépp maxejj tey delloo askan wi moomeelam. Maanaam, demokaraasi boo xam ne, soxlay askan wi ak i bëgg-bëggam lay def cëslaay. Xeetu demokaraasi boobu la doomi-réew miy laaj. Naam, Repibilig bu ne, aajowoo na demokaraasib yoon ak digaloog baat yi.Waaye, waru cee tënku. Dañ cee war a boole baatu askan wi. Bu dul loolu, day doon demokaraasi boo xam ne, ci làmmiñ yi kese lay yem te dina nasaxal àq ak yelleef yi demokaraasib ngore di sàrtal. Senegaal, njiiteefu politig gi day faral di doyadal Réewum yemale. Dafa di, sax, lees di woowe digaloog baat yi, te kilifay réew mi di ko damoo guddeek bëccëg, amu fi ndëgërlaay. Lenn rekk ay tax mu mën a am ndëgërlaay, te mooy ñu fexe ba dëppale baat yi, dara bañ leen a boole lu dul liggéey bu jaar yoon. Noonu la demokaraasi bu dëppook jamono di doxe. Loolu mooy li gën. Waaye ngëneel loolu du sotti mukk fileek ñi yor campeef yi sàmmontewuñ ak lañ dige woon, keroog bañ leen di waatloo laata ñu leen di jiital. Fàww nu ràññatle, bañ a jaawale campeef yi ci seen bopp ak ñi leen jiite : àttekat yi, dipite yi, ñiy sàmm kaaraange réew mi –pólis, sàndarmëri, làrme-, kilifay politig yi ñuy fal ak a folli, añs. Buñ demee ba campeef gu nekk, ñu koy xoole ki ko jiite, xam leen ni dellu nan ginnaaw, dellu nanu ca nguuri démb ya. Ndaxte, su boobaa, njiit loolu, daanaka buur lay doon, di bummi, nim fi ame woon démb rekk. Senegaal, nag, niñ fi jëmmalee campeef yi, tënk leen ci bakkan yi leen teewal, dafa jéggi dayo.
Li ñuy séentu ci Nguur guy woote bennoo ni gu Senegaal gi, moo di mu def kem-kàttanam ngir lépp ak ñépp tegu ci yoon, rawatina njiit yi. Waaye, Senegaal, Réew la moo xam ne njuuj-njaaj a ko lal ci fànn bu ne – politig, koom-koom, nooteel, tarixa, diiwaan, waaso, añs -, Réew la moo xam ne kilifa yi dañoo summi mbubb yi leen yoon solaloon, di lal i pexe ak di teg ay ndëgg-sërëx. Lépp rekk, ngir am fi baat ak alal. Réew la moo xam ne, gëm-gëmu ku nekk a féete kow mbiri àddina yi ñépp bokk. Réew la yit moo xam ne, kootook njuuj-njaaj dañu fee nasaxal Yoon. Réew mu ni mel, ndax warees na koo méngale ak Réewum yemale ? Su nu waxantee dëgg, lan moo fi desati lees mën a méngale ak doxalin wu jaar yoon ?
Ñaxtu yu bare yi askan wiy ñaxtu ci anam yu wute day wone ne, réew mii, joxatuñ fi yoon gëddaam. Xew-xewi jamono jii, ñeel politig bi, doy na ci firnde ! Li yoon tëral day faral di safaanook li xel mën a nangu. Ci man réewum yemale lan nekk bu dee campeef yi war a yemale nguur gi (baatu Fal-àtte beek baatu Yoon bi) defuñu li leen war ? Campeef yoo xam ne, ci waawu nguur gi lañuy doxe te dara waralu ko lu dul ngërëm giñ jàpp ne ameel nañ ko ki leen fa teg ak ngerum xel biñ leen ger.
Réewum yemale mu dëgër dafa laaj yoon wuy am sañ-sañu jubal ak jubbanti. Ci dëgg-dëgg, ci réew yi politig ëpp doole yoon rekk la ñuy fekk ay àttekat yuy jëfe ndigal, ay siboorukat, ay dunguru, dëkke lal i pexe ngir jàppale nguur gi walla ŋoy ci seeni ndomboy-tànk, lu njiit li joxoñ, ñu dagg, jox ko… Xamees na kàddug Jean de la Fontaine guy tënk melokaanu campeefi Senegaal yi : « bët bi la nit ñiy xoole mi ngi aju ci nga nekk ci « kujje gi » walla ci « nguur gi » ; dinañ la solal mbubb mu weex, nga yey walla mbubb mu ñuul, ñu yey la ». Te, Réewum yemale dafa safaanoo ak doxalin wuy xàjjatle ñi ñu war a àtte. Ndigal yi ñuy jox njiiti parke yi fa mbaxana waree doon benn, muy ndigal yu yaatu yi walla yu ñeel kenn nit doŋŋ, dañuy mujjee doon ay santaane, ñu ciy toppe ay nit. Ni ñuy jëfandikoo yoon, benn xeetu nit kott def kog gànnaay di ko xeexe weneen xeet wi, day dëggal xalaatin wuy sukkandiku ci xeltug Karl Marx. Rax-ci-dolli, loolu day firndeel ne, Réewum yemale mi ñuy soow, weesuwul làmmiñ yi koy tudd.
Ci beneen fànn, Réewum yemale, jëfinam day dëppook yoon ; muy « nguurug àttekat yi » walla àttekati nguur yiñ nuy naxe, du ci nangoo ànd ak benn. Maandute mooy cëslaayu demokaraasib ngore buy jiital ngor ak njub. Amul àttekatu nguur, amul àqu Nguur. Réewum yemale, dafa war a jébbalu ci yoon ba mu jeex tàkk. Njiiteefu politig, ci yoon, dafa war a màggal màndargay baat. Teg ci ne, dafa bokk ci wareefu njiit, mu feddali njorti mboolem-nawle yi jaadu yi. Bu loolu yépp weesoo, sàmm sa kàddu, dafa bokk ci jikko yi gën a kowe tey biral Yoon.
Kenn sañul ne Afrig fullaalul li yoon tëral ci kayit wànte, ni nu ko Mamoussé Diagne di fàttalee, li nu xam dëgg, nun, mooy gor ca wax ja. Moo tax képp ku ni wax waxeet ñu jéppi la, say mbokk rus. Te gis-gis bu rafet boobu, démb la saxoon Afrig, tey soog a ñëw, ni ko 23eelu Dog bu “Sàrtu Mànde” bu atum 1236 di firndeele. Dog boobu day wax ni : « Bu leen worante mukk ci seen biir. Sàmmleen seen kàddu ». Kon, bu Ndeyu-àtte réewum Senegaal (27eeluDog) nee « Kenn mënul a def lu ëpp ñaari moome yu toftaloo » ba noppi Njiitu réew mi ci boppam xamaloon askan wépp ne ànd na ci, ñu jékkee-jékki muy wax lu leerul mbaa làmboo tekkaaral, fàww xel yi teey. Ndege, noppi gi dafa ànd ak i pexey politig yu ñuy lal ci suuf. Doxalin wu ni mel moo doggali, daanaka, Réewum yemale, delloo Senegaal ginnaaw. Buñ fi nekkee di laam-laame ñetteelu moome, yëngu-yënguy 2012 yi fi gàkkaloon xar-kanamu réew mi ñoo nuy yoot.
Li nu seetlu at yii weesu moo di ne ay kilifaa ngiy ay-ayloo nguur gi, ku toog ci jal bi sa moroom fexe bañ woteel ko mu wuutu la. Waaye du kenn ku ci ittewoo soppi nekkinu askan wi, xàll yoonu yokkute. Fim ne nii, nag, mbir mi ci loxoy njiit li la nekk te, moom de, niruwul kuy xalaat benn yoon ne li Ndeyu-àtte réew mi dogal ci fànn boobu mën na koo tënk. Waaye foofu la juume ndax kàddu gu leer nàññ, kàddu gu amul benn lënt-lënt, nit ki lu sa xel màcc ci politig mbaa ci xam-xamu Yoon, amoo san-sañu dégge ko neneen. Képp ku wëlbati wax ji te nga xam lim wund, dangay géwélu buur rekk, di ko sibooru ak a màggal bëgg-bëggam wànte du jëmale kanam réew mee la tax a jóg.
Bindkat yi
-
Idrissa BA, Professeur assimilé en histoire, FLSH/UCAD
-
Mame Penda BA, Professeure assimilée en sciences politiques, Agrégée des Facultés de droit, UFR SJP/UGB
-
Tapsirou BA, Maître de conférences assimilé en droit, UFR SJP/UGB
-
Mor BAKHOUM, Maître de conférences assimilé en droit, UVS
-
Oumar BARRY, Professeur assimilé en sociologie, FLSH/UCAD
-
Jean Charles BIAGUI, Maître de conférences assimilé en sciences politiques, FSJP/UCAD
-
Marie BOUARE, Maître de conférences assimilé en droit, UFR SJP/UGB
-
Mouhamadou BOYE, Maître de conférences assimilé en droit, UFR SJP/UGB
-
El Hadji Alioune CAMARA, Maître de conférences assimilé en économie, UFR
SES/UIDTT
-
Aminata CISSE-NIANG, Professeure assimilée en droit, Agrégée des Facultés de droit, FSJP/UCAD
-
Jean-Louis CORREA, Professeur assimilé en droit, Agrégé des Facultés de droit, UVS
-
Patrice CORREA, Maître de conférences assimilé en sciences de l’information et de la communication, UFR CRAC/UGB
-
Karamoko DEMBA, Maître de conférences assimilé en droit, FSJP/UCAD
14.Mamadou Hady DEME, Maître de conférences assimilé en sciences politiques, FSJP/UCAD
-
Abdoul Alpha DIA, Maître de conférences titulaire en économie, UVS
-
Amadou Hamath DIA, Professeur assimilé en sociologie, SES/UASZ
-
Hamidou DIA, socio-anthropologue, Directeur de recherche, IRD/France
-
Mouhamadou Mansour DIA, Maître de conférences titulaire en sociologie, UVS
-
Oumar DIA, Maître de conférences titulaire en philosophie, FLSH/UCAD
-
Karounga DIAWARA, Professeur titulaire de droit, Université Laval, Québec
-
Fatimata DIA-BIAYE, Maître de conférences titulaire en droit, FSJP/UCAD
-
Malick DIAGNE, Maître de conférences titulaire en philosophie, FLSH/UCAD
-
Sidy Nar DIAGNE, Maître de conférences titulaire en droit, FSJP/UCAD
-
Babacar DIAKHATE, Professeur assimilé en mathématiques/informatique, FST/UCAD
-
Abdoulaye DIALLO, Maître de conférences assimilé en droit, SES/UASZ
-
Halima DIALLO, chercheure en psychologie, IFAN/UCAD
27.Mamadou Diouma DIALLO, Maître de conférences assimilé en sciences de l’information et de la communication, UFR CRAC/UGB
-
Mamadou Aguibou DIALLO, Maitre de conférences assimilé en sociologie, SES/UASZ
-
Thomas DIATTA, Maître de conférences assimilé en droit, SES/UASZ
-
Paul DIEDHIOU, Maître de conférences titulaire en sociologie, SES/UASZ
-
Abou Adolf DIEME, Maître de conférences assimilé en droit, SES/UASZ
-
Ablaye DIEYE, Maître de conférences titulaire en droit, FSJP/UCAD
-
Adrien DIOH, Maître de conférences assimilé en droit, UFR SJP/UGB
-
Ibrahima Demba DIONE, Maître de conférences assimilé en sociologie, SES/UASZ
-
Abdou Khadre DIOP, Maître de conférences assimilé en droit, UVS
-
Babacar DIOP, Maître de conférences titulaire en philosophie, FLSH/UCAD
-
Dame DIOP, Maître de conférences assimilé en lettres modernes, UFR LASHU/UASZ
-
Abdoul Aziz DIOUF, Professeur assimilé en droit, Agrégé des Facultés de droit, FSJP/UCAD
-
Christian Ousmane DIOUF, Maître de conférences assimilé en droit, FSJP/UCAD
-
Gane DIOUF, Maître de conférences assimilé en droit, FSJP/UCAD
-
Ibrahima Dally DIOUF, Professeur assimilé en sciences de gestion, Agrégé des Facultés
de sciences économiques et de gestion, FASEG/UCAD
-
Ismaïla DIOUF, Professeur assimilé en mathématiques et informatique, FST/UCAD
-
Ousseynou Kolly Diène DIOUF, Maître de conférences titulaire en économie et gestion, UFR SES/UASZ
-
Pape Alioune FALL, Professeur assimilé en informatique, UFR SAT/UGB
-
Saliou FAYE, Maître de conférences assimilé en sciences politiques, FSJP/UCAD
-
Souleymane GAYE, Maître de conférences assimilé en droit, FSJP/UCAD
-
Souleymane GOMIS, Professeure titulaire en sociologie FLSH/ UCAD
48.Jean Alain GOUDIABY, Maître de conférences titulaire en sociologie, UFR SES/UASZ
-
Ababacar GUEYE, Maître de conférences assimilé en droit, FSJP/UCAD
-
Cheikh Thiécoumba GUEYE, Professeur titulaire en mathématiques et informatique, FST/UCAD
-
Doudou GUEYE, Maître de conférences titulaire, UFR SES/UASZ
-
Abdoulaye GUISSE, Maître de conférences assimilé en droit, UFR SES/UASZ
-
Fatoumata HANE, Professeure assimilée en sociologie, UFR SES/UASZ
-
Abdou KA, Maître de conférences assimilé sociologie, UFR SES/ UASZ
-
Amadou KA, Maître de conférences assimilé en droit, UFR SJP/UGB
-
Cheikh KASSE, Maître de conférences titulaire en lettres modernes, FASTEF/UCAD
-
Ousmane KHOUMA, Maître de conférences titulaire en droit, FSJP/UCAD
-
Diouma KOBOR, Professeur titulaire en physique, UFR ST/UASZ
-
Mohamed Moro KOITA, Maître de conférences titulaire en gestion, ESP/UCAD
60.Raphael LAMBAL, Maitre de conférences titulaire en lettres modernes, UFR LASHU/UASZ
-
Mouhamed Abdallah LY, Chargé de recherche en linguistique, IFAN/UCAD
-
Mohamed Lamine MANGA, Maître de conférences assimilé en histoire, UFR LASHU/ UASZ
-
Ibou NDAO, Maitre de conférences assimilé en géographie, UFR SES/ UASZ
-
Abdoul Aziz NDIAYE, Professeur assimilé en économie, Doyen de l’UFR SEG/UGB
-
Amsata NDIAYE, Maître de conférences titulaire en physique, UFR SAT/UGB
-
El Hadji Samba NDIAYE, Professeur assimilé en droit, Agrégé des Facultés de droit, FSJP/UCAD
67.Ndéye Astou NDIAYE, Maître de conférences assimilé en sciences politiques, FSJP/UCAD
-
Ndéye Coumba Madeleine NDIAYE, Professeure assimilée en droit, Agrégée des Facultés de droit, FSJP/UCAD
-
Serigne NDIAYE, Docteur en littérature comparée, Emory University/USA, ancien directeur du Council of International Externe Exchange (CIEE), Bureau Afrique
-
Seydi Ababacar NDIAYE, Maître de conférences titulaire en chimie, ESP/UCAD
-
Sidy Alpha NDIAYE, Professeur assimilé en droit, Agrégé des Facultés de droit, FSJP/UCAD
-
Thierno Amadou NDIOGOU, Maître de conférences titulaire en droit, FSJP/UCAD
-
Lucienne Kodou NDIONE, Maître de conférences titulaire en droit, FSJP/UCAD
74.Moussa NDIOR, Maître de conférences assimilé en sciences politiques, UFR SES/UASZ
-
Amary NDOUR, Maître de conférences assimilé en droit, FSJP/UCAD
-
Abdoulaye NGOM, Maître de conférences assimilé en sociologie, UFR SES/UASZ
-
Paul NGOM, Professeur assimilé en droit, Agrégé des Facultés de droit, FSJP/UCAD
-
Abdoul Aziz NIANG, Directeur de recherche, entomologiste, IFAN/UCAD
79.Babacar NIANG, Professeur assimilé en droit, Agrégé des Facultés de droit, FSJP/UCAD
-
Mouhamed Bachir NIANG, Professeur assimilé en droit, Agrégé des Facultés de droit, FSJP/UCAD
-
Yaya NIANG, Maître de conférences assimilé en droit, UFR SJP/UGB
-
Baye Massaer PAYE, Maitre de conférences assimilé en anglais, UFR LASHU/ UASZ
-
Cheikh Sadibou SAKHO, Maitre de conférences titulaire en sociologie, UFR LSH/UGB
-
Moussa SAMB, Professeur assimilé en droit, Agrégé des Facultés de droit, FSJP/UCAD
-
Yamar SAMB, Professeur assimilé en droit, Agrégé des Facultés de droit, UFR SJP/UGB
-
Aly SAMBOU, Maître de conférences assimilé en lettres étrangères appliquées, UFR LSH/UGB
87 Mame Anna SENE-FALL, Maître de conférences titulaire en philosophie, FASTEF/UCAD
-
Marie-Pierre SARR-TRAORE, Maître de conférences titulaire en droit, FSJP/UCAD
-
Mamadou SEYE, Maître de conférences assimilé en droit, UFR ECOMIJ/UADB
-
Yankhoba SEYDI, Professeur assimilé en anglais, FSLH/UCAD
-
Youssouf SEYDI, Maître de conférences assimilé en droit, FSJP/UCAD
-
Adama SOUMARE, Maître de conférences titulaire en langues et civilisations romanes, FSLH/UCAD
-
Fatoumata Bernadette SONKO, Maître de conférences assimilé, CESTI/UCAD
-
Ndiémé SOW, Maître de conférences assimilé, UFR LASHU/ UASZ
-
Oumar SY, Professeur titulaire en géographie, UFR ST/UASZ
-
Ibrahima SYLLA, Maître de conférences titulaire en sciences politiques, UFR SJP/UGB
-
Mouhamadou Moustapha TALL, Maître de conférences assimilé en droit, FSJP/UCAD
-
Cheikh THIAM, Professeur d’études africaines, Doyen de la School for international training, USA
-
Mballo THIAM, Maître de conférences titulaire en droit, UFR ECOMIJ/UADB
-
Benoît TINE, Professeur assimilé en sociologie, UFR SES/UASZ
-
Sadou WANE, Maître de conférences assimilé en droit, UFR ECOMIJ/UADB
-
Moussa ZAKI, Professeur assimilé en droit, Agrégé des Facultés de droit, UFR/SPJ/UGB”