YÉENEY NJIITU RÉEW MI ÑEEL NJÀNG MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew maa nga woon Gànnaar, démb ci talaata ji, ngir fekkeeji Ndajem waxtaan mom, Bennoog Afrig a ko woote. Waxtaan waa ngi aju woon ci njàng mi, ndaw ñi ak xëy mi. Ci altiney barki-démb ji, 9i pani desàmbar 2024, lees ubbi woon waxtaan wi, fa Gànnaar (Móritani). Wëppa wi moo doon “Jàngal ak yar Afrig ñeel 21eelu xarnu bi”.

Ci njiitali Sëñ Mohamet Uld Séex El Xasuwani, Njiitu réewum islaam mu Gànnaar, lañ doon amal waxtaan wi. Moom nag, Sëñ Muhamet Uld Séex El Xasuwani, moo jiite Bennoog Afrig jamono jii. Ay kilifay Afrig yu bari teewe nañu ndaje ma. Dees na ci fekk ay njiiti réew, ay jëwriñ, ay boroomi xam-xam ak i way-moomeel. Li ñu ko dugge woon, ñoom ñi fa teewoon ñépp, mooy fénc solos njàng mi ci biir kembaaru Afrig.

Bu dee Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, moom ci talaatay démb ji la fa àgg. Ba mu jëlee kàddu gi, biral solos njàng mu boole ak bennale, njàng mu mu amul xàjj-ak-seen te lalu ci cëslaay gu baax. Dafa ne :

“Téeméer yoo jël ci sunu ferey Afrig, juróom-benn-fukk yi ay ndaw lañu. Sunuy ndaw ñooñii, ñooy ëllëg, waayeet ñooy jëmmal sunu tay. Bu nu leen joxulee jumtukaay yi leen di dooleel, dinanu tayle sunu ëllëgu kembaar gi.”

Ci xëtu Facebook bu njiiteefu réew mi lees siiwal kàddoom yile.

Njiitu réew mi fésal na sax njariñ li nekk ci njàngum xale yu jigéen ñi ak waa kow gi. Nde, ñooñii kat, dañu leen di faral a fàtte, walla ñu leen di beddi ci naali njàng mi. Mbirum “Kumba am nday ak Kumba amul ndemay” moomu la kilifag Njénde li bëgg a dakkal. Looloo ko tax a waxaat ne :

“Njàng muy boole ak a bennale te lalu ci cëslaay gu baax mooy pexe mi gën a wóor ngir xeex ba jële fi ñàkk ak ndóol giy gàllankoor sunuy mbooloo yi gën a néew doole.”

Fàttali na naataangoomi Njiiti réew wareef bi ñu gàlloo ci booloo, bennoo joxante loxo ngir tabax koom-koom gu dëgër te naat ngir mën téye ndawi Afrig yu xereñ yi, ñu bañ a génn kembaar gi di liggéeyali tubaab yi. Mu waxati, ne :

“Afrig dafa war a defal ay nitam, ji ci ñoom lol, dina jariñi kembaar gi. Warees na jox ndaw ñi jumtukaay yi ñu yelloo.”

Njiitu réewum Ruwàndaa li tamit jëloon na kàddu. Moom nag, Póol Kagame, dafa woo njiiti Afrig yi, waxleen ñu gànnaayoo fulla ju mat sëkk, saytul seen bopp seen i moomeel. Kàddu yii la fa biral :

“Afrig moo war a saytul boppam ay moomeelam ci ni mu gënee. Deesul a sukkandiku rekk ci ndimbalul doxandéem. Loolu, du lu baax. Wareesul a jaawale digaale yu baax ak dénkaane sa kilifteef.”

Moom itam, ci xëtu Facebookam lees biral kàddoom yile.

Ca ndaje ma nag, ràññeesoon na fa kilifa yu mag yu deme ni Sëñ Abdelmajiit Tebun miy Njiitu réewum Alseri, Musaa Faki Mahamat mi jiite Ndiisoo Bennoog Afrig ak itam Tet Saybaan miy Tof-njiitu doxal lu UNICEF.

Kon, réewi Afrig yi mànkoo nañu, déggoo ngir liggéey ci njàng mi ak xëyum ndaw ñi. Ginnaaw wax ji nag, jëf a des. Nde, jëf moo tuxal wax.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj