Démb ci guddi, tele TFM dawal na laaj-tontu bi Njiitul Ngomblaan gi, El Maalig Njaay, séq ak seen saabalkat bii di Abdulaay Siise. Ci biir waxtaan wi, ñaareelu kilifag réew mi (ci dayo) fésal nay coppite yu mu namm a amal ca campeef gu solowu googii di Ngomblaan gi. Muy koppar yi, nimerig bi ak daamaar yi, lépp la Jolof-jolof bi bëgg a joyyanti.
Jub, jubal ak jubbanti la El Maalig Njaay namm a jëmmal ca Ngomblaan ga. Ginnaaw bi mu toogee ci boppu ñaareelu campeefu réew mi, yéeney saa-pastef bi mooy soppi ni Ngomblaan giy doxee, raxas la fa tilim, jubbanti la fa dëng, yeesal jumtukaayi liggéey yi ngir dëppale leen ak jamono, waayeet fexe ba jàppandalal dépite yi seen liggéey. Lépp nag, ci kaw lu leer lol, dafay cëslaayoo yoon ak sàrti réew mi.
Ci waxtaan wi mu jagleel tele TFM, moom mi woon jëwriñu yaale ji, biral na naal yi mu fas yéene jëmmal ngir soppi xar-kanamu Ngomblaan gi. Li mu ko dugge mooy fexe ba Ngomblaan gi mën a def liggéeyam, taxawu askan wi ni mu waree.
Moom nag, ciy waxam, li ko njëkk a jaaxal bi mu tooge ci boppu Ngomblaan gi mooy yaa-ma-neex bi fa amoon, rawatina ci anam bi ñu daan saytoo koppari Ngomblaan gi. El Maalig mooy wax :
« Bi ñu ma jébbalee lenge yi, dama laaj këyiti caytug koppar gi. [Waaye] këyit jotuma ko. Ngomblaan gi amul woon kontaabilite. Ay saagi xaalis lañu daan dugal, di fay loxo ak loxo. »
Doxalin woowu mu ñaawlu, dafa doon lu lëndëm lol, dafay ubbi bunti njuuj-njaaj ak naka-su-dul-noonu ñeel koppari campeef gi. Moo tax, ginnaaw gi, mu teg ay sàrt yu leer, moom El Maalig Njaay, ngir jubbanti mbir mooma. Njiitu Ngomblaan gi neeti :
« Bi ma toogee xaat laa wax ak dépite yi, ne leen, ku ci joxewul sàqum koppar (compte bancaire) fii ak 15eelu fanuw weer wi kenn du la dugalal sag payoor. »
El Maalig yemul rekk ci mbirum koppar yi. Yeesalug jumtukaayi Ngomblaan gi tamit, yitte ju réy la ci moom. Li mu nisër mooy fexe ba dugal fa jumtukaayi xarala yu yees yi ngir dëppale campeef gi ak jamono. Loolu moo ko tax a leeral, wax ne :
« Noo ngi jëndal dépite yi ay tablet te yit noo ngi leen di defaral ay imeeli liggéeyukaay. Bu njëkkaan, dépite bu ci nekk dafa daan jot lu tollu ci 18i kiloy këyit ngir càmbar nafa yi. Bu nu jàllee ci nimerig bi, dinanu yaxanal xaalis te liggéey bi dina gën a am njariñ. »
Bu loolu weesoo yit, El Maalig dafa bëgg a dakkal yenn xeeti doxalin yu lënt ya fa amoon. Ciy waxam, dees na taxawal fa Ngomblaan ga « …ag banqaas buy saytu jokkalantey ja yi (passation des marchés). » Li ko waral nag moo di ne, ba tay ci kàdduy El Maalig, bu ñu laajaan ay leeral, tontu li lenn rekk lay doon : « ci teeylug njiit li la ». Maanaam, njiitul Ngomblaan gi rekk moo ci daan xam dara. Loolu nag, bees sukkandikoo ci El Maalig, dakk na.
Ba ci xaalis bees daan jox dépite yi bu ñu daan amal ay tukkiy liggéey, El Maalig indi na ci ay coppite. Kilifa gi neeti :
« Léegi, benn dépite du jot ndàmpul jotaayu liggéey bu fekkee teewul ci jotaayi liggéeyi ndiisoo yi. Bu dee li aju ci xaalisi tukki yi, dañu daan ëppal : dépite bu waroon a tukki ñetti fan dafa daan jot xaalisu juróomi fan, ñu boole ci bés bi jiitu demam ak bés bi topp ci delseem. Loolu dindi nanu ko. »
Fan yee weesu, mbirum daamaari dépite yi juroon na fi coow. Mbir moomeet, Sëñ Maalig indi na ci ay leeral. Dafa di, Njiitu réew ma woon, Maki Sàll, dafa dakkaloon daamaar yi ñu daan jox dépite yi ngir ñu koy liggéeyee. Nde, daf leen a daggaloon 900 000 FCFA weer wu set ngir seen dem ak dikk. Ndogal loolu taxoon na werante ak coowoo jib jamono jooja. Ci xalaatu El Maalig Njaay, pólitig moo laloon ndogal lu ni mel.
« Maki Sàll bëggul woon jox ay daamaar 82i dépitey kujje gi ndax wotey njiiteefu réew mees dëgmaloon. Daf leen bëggoon a néewal doole ci wàllu pólitig jaare ko ci xañ leen i daamaar yu ñuy mën a tukkee. »
Ngir jubbanti loolu, delloo dépite seen àq ci wàll wi, El Maalig dina delloosi daamaar yi. Ndaxte, ciy waxam, dees na sàmm ngoru dépite yi. Layam mooy :
« Naka la dépite buy jóge Saaraya walla Salemata mënee tukki te amul tukkiwaay bu yenu maanaa ? Am na ñoo xam ne Jakarta lañuy jël ! Du ay caaxaan ! Boo demee Koddiwaar, ab dépite kese 3i miliyoŋ ci sunuy koppar lay fayeeku, dépite bi bokk ci pekkug Ngomblaan gi di fayeeku 5i miliyoŋ ci sunuy koppar. Nekkuma di wax ñu yokkal dépite yi seen payoor, waaye damay wane rekk ni payoor yi ëppantee. Fi Senegaal, way-bokki pekkug Ngomblaan gi niki ay jëwriñ lañu leen jàppe, waaye, kenn defalu leen li ñuy defal jëwriñ yi. »
El Maalig Njaay dalal na xel yi. Xamle na ne, nafag Ngomblaan gi du yokk. Jubluwaayu coppite yi mooy lootaabewaat yëf yi ngir ñoŋal liggéeyi dépite yi. Li El Maalig Njaay bëgg mooy fexe ba Senegaal am Ngomblaan gu dëppoo ak jamono, tegu ci ay sàrt yu leer nàññ te am ay jumtukaay yu doy te baax, bu ko defee, mu mën a doxal sas wi ko askan wi sas.