Talaata jii ñu weesu (1 Sàttumbar 2020) kurél gii di « Y’en a marre » moo bëggoon a jébbal kilifay Orange yi ab bataaxal ngir wone ni ànduñu benn yoon ci « noot » gi Groupe bi nekkeek Senegaal ak ni muy yokkee ay njëgëm. Ci kow loolu pólisu Jëppël tegoon loxo Aliyun Saane mi jiite Kurél gi ak Kilifa ak yeneen 5 ci seeniy farandoo.
Démb ci àllarba ji nag, ñoom ñooñu ñépp bàyyi nañu leen ñu dellu seen kër.