YEWWI ASKAN WI : « MAKI SÀLL DAFA WOR BA FU WOR YEM. »

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lëkkatoo Yewwi Askan Wi génne na ab yégle ñeel tolluwaayu réew mi. Dañu bind ne :

« Lëkkatoo Yewwi Askan Wi a ngi joxoñ baaraamu tuuma Njiitu réew mi, Maki Sàll, noo ngi koy jiiñ ne dafa wor askanuw Senegaal ba fu wor yem te noo ngi koy laaj mu tekki ndombog-tànkam ci nim gën a gaawe.

Lëkkatoo Yewwi Askan Wi a ngi woo askanu Senegaal ñu gën yokk mbooloo mi tey bañ ba fu bañ yem ni leen ko ndeyu-àtte réew mi mayee, fépp ci réew mi ak ca bitim-réew, ngir sàmm àq ak yelleefi maxejj yi, bennoog réew mi ak demokaraasib Senegaal. »

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj