YEWWI ASKAN WI – TAXAWU SENEGAAL : ÀND BUY WAAJ A TAS ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waxtaanu Maki Sàll wi de, boo demee, moo nar a génne Taxawu Senegaal ci lëkkatoo Yewwi Askan Wi. Ndaxte, Yewwi Askan Wi daa fétt, ne du bokk ci waxtaanuw 30 me 2023 wi Njiitu réew mi woote. Nde, Ndajem kilifay lëkkatoo gi dañ génneb yégle, xamle ci ne duñ wuyuji wooteb Maki Sàll bi te di ko digal làng ak kurél yi bokk ci lëkkatoo gépp. Ci seen yégle bi, lii toftalu lañ ci bind :

“Jamono jii réew maa ngi toog cib nen, Maki Sàll naan dafay woote “caaxaanuw waxtaan “, bésub 30 me 2023, ngir nelawloo saa-senegaal yi, fàtteloo leen jafe-jafe yi ñu nekk di leen dund.

Lëkkatoo Yewwi Askan Wi a ngi xas, di biral ñàkk àndam ci waxtaan woowu.

Lëkkatoo gaa ngi jóo làngi pólitig ak kurél yi ko séq yépp, ak way-moomeel yépp, ñu bañ a bokk ci waxtaanuw caaxaan woowu nga xam ne, daray njariñ du ci tukkee ñeel askan wow, sonn na, tàyyi na ciy tooñ yu bari te toftaloo yi ko Nguur giy teg. »

Ndogal loolu nag, neexul waa Taxawu Senegaal te wax nañ ko cib yégle biñ gaaw a toftale ci bob Yewwi Askan Wi.

Kurél gi Xalifa Sàll jiite kat, àndul ak ndogal li Yewwi Askan Wi jël ñeel waxtaanu 30 me 2023 wi. Moo ko tax a gaaw a génne, moom itam, ab yégle ngir leeral taxawaayam, bind ci ne :

“Taxawu Senegaal a ngi xamal ñépp ne, déggoo amul ca ndajem kilifay lëkkatoo gi ñeel mbirum waxtaan wi.”

Ñoom Bàrtelemi Jaas dolli nañ ci ne :

“Li jëm ci wàllu waxtaan wi, Taxawu Senegaal, ak aaday waxtaan wees ko xame, dina diisoo ak banqaasi suufam ak làng ak mbootaay yi ko séq yépp. Dees na amal um ndaje mom, dees ci boole tënk xalaat yépp ngir leeral taxawaayu kuél gi, biral ko ba ñépp xam ko. »

Ci seen njeexitalu yégle bi, fàttaliñ ne, Taxawu Senegaal dafa bokk ci ñi samp lëkkatoo gi te, du wàcc yoon yi mu mës a teg i tànkam.

Mu mel ni réeroo am na. Mbaa du ànd bi day waaj a tas ? Ku dund, dinga fekke ba xam.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj