Ci guddig gaawu jàpp dibéer lees jàllale Paap Aale Ñaŋ ca raglub Principal. Me Musaa Saar, layookatam bi, moo ko xamle. Cëtëŋ ya lees ko njëkk a yóbbu laata ñu ko fay génne, jàllale ko ca beneen béréb ca biir fajuwaay ba. Jamono jii nag, mu nga fa, ay ma-kaso di ko wattu. Layookatam bi nee, « xiifal gi daf ko sonnal lool sax ». Dafa di, talaata 20 desàmbar, bés biñ ko jàppaate ba tey, Paap Aale Ñaŋ day xiifal, ngir di ko xeexe jàpp biñ ko jàpp.
Am na 6i fan ci tey, bi toppekatu Bokkeef gi, Hammadi Juuf, santaanee ñu jàppaat Paap Aale Ñaŋ ginnaaw bi mu amee woon bàyyig négandi. Taskatu xibaar bi dafa yégle woon ne day xiifalaat, ni mu ko defe woon bi ñu ko njëkkee jàpp. Li tax ñu jàppaat ko, ci kàdduy toppekat bi, mooy ne :
« Kàddu yi tuumaafon jii di Paap Aale Ñaŋ mujje biral ci kibaraan yi, nees ko nemmeekoo ciy ndéggat ak i ngistan yees boole ci wayndarew àtte bi, dañuy firndeel bu wér ag jalgati ñeel tere yees tënkoon [Paap Aale Ñaŋ], rawatina tere yi aju ci biralug njëf yi sabab toppe yi. »
Ñu baree ngi àddu ci mbir mi, di dankaafu ak a artu. Ngudda Mbuub, jàngalekatu yoon xelam màcc ci wàllu yoonuw bokkeef, dafa wax ne :
« Dañu war a bàyyi Paap Aale Ñaŋ ! Dafa jot ñu samp ab àttekatu njàpp geek ngoreef yi…»
Aliyun Tin moom dafa gis ne Maki Sàll dafa war a delloo Paap Aale Ñaŋ ca njabootam. Ndaxte, dafa jàpp ne wareesul a seetaan ba taskatu xibaar bi di dee ci xiifal gile. Ab Tweet la def, bind ci ne :
« Bés bu Paap Aale Ñaŋ ñàkkee bakkanam ci sababu xiifal gi bi, dina doon jéyya ju réy a réy ñeel demokaraasi, Càmmug yoon ak àqi doom-aadama. »
Ngir fàttali, dibéer 6i fan ci nowàmbar lañ jàppoon Paap Aale Ñaŋ. Lees koy tuumaal di ciiwalug xibaar yu ñeel cóobare gi te amu ci ndigalu njiit yi, yor ay kayiti caytu ak cóobare, biralug xibbar yu wéradi yuy tiiñal campeefi bokkeef gi.