YOLOMAL BUUMU NJAAM GI NGIR GËN LAA XOJ, FARÃS DEFATI NA MËNINAM (Boos Ndóoy)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Boos Ndóoy

Jikko ak boroom, sëg ya rekk ! Ndege, Farãs dafa am pexe moo xam ne, ca jamonoy nootaange ja ba tey jii, ci lay wéy di naxe réew yim tegoon loxo démb ngir saxal nootaange bi ci beneen anam. Pexem caay-caay moomu, mënees na ko tudde : yolomal buumu njaam gi ngir gën laa mën a naj cib ruq. Te, ràññees na ko ci ni Farãs di jëflanteek réewi Afrig yim nootoon, rawatina yi féete bëj-saalumu màndiŋum Saxara mi.

Li Farãs di def mooy, saa bu demee ba cólle, xam ne gaa ñaa ngiy yeewu, rekk mu tàmbalee naxasaale ak a neexal. Ndaxte, jamono ju ne, dina am ci biir Afrig ak ci àddina sépp, ñuy ŋàññiy doxalinam ak ni mu aakimoo yenn réewi Afrig, dale ko 60i at ci ginnaaw. Bu ko wax ji sonalee, nag, mu daldi génn, ne dina soppi ddoxalinam. Maanaam, day taafantoo ay coppite ñeel digganteem ak réew yooyi nu tuud ci kow, mel ni kuy gedd ngañaay yi ko nooteel biy jural. Fekk ne yoo, duggewu ko lenn lu dul tuur lëndëm nit ñi, jaar ci suuf, lal yeneen pexe yi koy tax a wéyal nootaange bi.

Ginnaaw bi ñu ko toroxalee Indosiin, Déggooy Genève(Accords de Genève) yaa dakkal xare boobu ci atum 1954. At moomu la Alséri daldi fippu moom tamit ngir foqati réewam ci loxo Xonq-Nopp yi. Jamono jooju, nag, Farãs dafa waroon a tànn benn ci 3i réew yii : Marog, Tinisi ak Alséri. Ndege, jàqoon na be, mënatul woon a jàmmaarlook 3i réew yiy sàkku ak a xeex ngir moom seen bopp. Moo tax, mu xool réew mu ko ci gënoon a yitteel, tànn ko. Noonu, ci atum 1956 la Farãs tàggook Marog (2eelu fan ci weeru màrs) ak Tinisi (20eelu fan ci weeru màrs), ba noppi, nag, ŋoy ci Alséri. Alséri, jamono jooju, daanaka ab diiwaan doŋŋ la woon ñeel réewum Farãs.

Noonu tamit la ragale woon réewi Afrig yi féete ci bëj-saalumu màndiŋum Saxara mi. Da doon bañ, ñoom it, ñu fippu, sumb ab xare, xeex ngir moom seen bopp.  Looloo ko taxoon a yolomal tuuti buumu njaam gi, fab ab àtte bees dippe woon ci nasaraan Loi-Cadre Defferre” ci atum 1956. Àtte boobu, nag, da doon may askani réew yoo yii, ñu falal seen bopp ay njiit ci seen i réew. Pexe moomu la laloon. Maanaam, li ñuy wax di màtt di ëf, yolomal tuuti ngir gën a wéyal nooteel bi. Ndaxte, looloo gënoon a yomb xeexandoo ak réew yu bare. Ndege, 2eelu xareb àddina si taxoon na ba yenn ci réewi Afrig yi yeewu ba dayob Farãs wàññeeku bu baax ci seen i bët. Noonu, ittey fippu ak moom seen bopp di leen gën a soxal. Loolu la Farãs xamoon bu yàgg, ba tax ko jël ay matuwaayam ngir wéyal nooteel bi ci beneen anam. Loolu moo tax Seneraal De Gaulle nas pexeem, tudde ko ‘’Mbooloom doomi Farãs ak Afrig’’ (Communauté franco-africaine) jéem koo wéyal, di ko suuxat.  

Dafa di, Seneraal De Gaulle dafa gënoon a yaatal yombal gi àtteb “Loi-cadre Defferre” dooroon. Waaye, duggewuñ ko woon lu dul wéyal nootaange bi. Ndaxte, kat, ak lu ci mënoon a am, Farãs moo doon nos, di nocci. Li koy firndeel mooy ni mu doxale woon ak Gine.

Bi Farãs nee, ku bëgg demal boppam na dem, Gine dafa dog buumu nootaange bi ko lëkkale woon ak Farãs ci atum 1958. Ginnaaw bi, Farãs da koo fexeel, tegal koy téq-téq yu bare ciw yoonam ngir nasaxal ko, tiitalaale réew yi seen xel nekk ci toppandoo Séku Ture.

Lu ni mel, wares na ko fàttali, xamal nit ñi ne, xeeti àtte ak i pexe yi Farãs mës a lal yépp, noot réewi Afrig yi rekk la ko dugge. Muy ‘’Ndajem bennoo ci peggu Farãs’’ (Union française) mu 1946, àtteb “Loi-cadre Defferre bu 1956, ‘’Mbooloom doomi Farãs ak Afrig’’ mu 1958, yépp, ay feemi neen lañ woon.

Ci ndoorteelu atiy 1960 yi, ba Farãs xamee ne mënatul a wéyal nootaangeem bi ñeel réewi Afrig yi, dafa mujje woon a bàyyi ñëpp ci ñoom moom seen bopp.

Waaye, ku yaakaaroon ne Farãs dina la bàyyee noonu, danga doon nax sa bopp. Ndege, ku ci nekk, da laa xaatimloo woon ay déggoo yi ko daan tax a teg loxo ci nguur yi, alal jeek koom-koomi réewi Afrig yi. Bataaxal ba Michel Debré bindoon Léon Mba, njëlbeenug njiitu réewum Gaboŋ ba woon, da koy firndeel. Daf ko ne woon :

Dinanu leen delloo seen réew, ngeen moom seen bopp ci kow sàrt yii may limsi : réew mu ci moom boppam, dangay nangoo wéy di topp li nekk ci sàrt yi nu xaatimoon lu jiitu muy moom boppam ; ñaari tëralin yi nu fasandoo, te muy moom sa bopp bi ak déggooy jëflante yi (accords de cooperation), benn du dem bàyyi moroomam.»

Ci sàrt yile la réewum Farãs tënkoon réewi Afrig yim nootoon laata mu leen di delloo lenge yi. Looloo taxoon François-Xavier Verschave yëkkati kàddu yii : « Réewi Afrig yi Farãs nootoon, te ñu féete bëj-saalumu màndiŋum Saxara mi, ba ñuy moom seen bopp, dañu leen a nanguloo ay déggoo ci wàllu koom-koom, politig ak xare yu leen tàbbil ci kiliftéefug Farãs. »

Keroog, 22eelu fan ci weeru desàmbar 1974, ba 94,5i nit ci téeméer yoo jël ñeel askanuw duni Komoor ya (Anjouan, Grande Comore, Mohéli, Mayotte), wotee « WAAW » ñeel referàndumub moom-sa-bopp ba, Farãs dafa lànk, ne du ci dal. Mu daldi dogal ne dun bu ci nekk ak ay xobam, kon deesul boole dun yépp ci benn lim. Mu nekkoon ab jaay doole boo xam ne, ONU sax àndu ci woon. Rax-ci-dolli, dogal boobu dafa safaanoo woon ak àtteb Farãs bu 23eelu fan nowàmbar 1974 te di wax ne : « warees na boole xobi wotey dun yépp, boole seen i lim ngir xam ku jël raw-gàddu gi ». Waaye, Farãs dafa jéggi àtte boobule, wàññi ngirtey wote bi. Noonu la tege loxo ci dunub Mayotte bi nga xam ne, nee ñu, 100i nit yoo jëloon, 63,22 yi « DÉET » lañu wote. Ba tey jii may wax ak yéen, dun baa ngi ciy loxoom.

Pexem naxe-mbaay moomu la Farãs jëfandikooti ñeel coppite CFA bi ECO bi ko nar a wuutu. Ndaxte, sémbub àtte bu 20eelu fan ci weeru Me 2020 bi koy dëggal, ci anam bu ni mel lees ko tërale. Nee ñu, ci biir sémbub àtte bile : dakkalees na teewaayu ndawal Farãs ci 3i ndajey caytu bànk yu mag yi ak gafay weccee yi (compte d’opérations). Li leer moo di ne ay feemi neen la. Ndege, ba tey, Farãs mooy wóoral ECO bi, te yemo (parité) bi ak weccin wu amul àpp wi (convertibilité illimité), duñ soppiku. Te, 2 yooyu ñooy gaañ sunu réew yi ci fànn yu bare.

Ci beneen boor, Farãs daa kootoog waa UEMOA, ñu suufu CEDEAO, sàcc seenub naal, soppi cëslaay geek jubluwaay bi. Ndege, ECO, moomeelu CEDEAO la. Ay at ñoo ngi nii, mu ciy liggéey. Li Farãs ragal Niseryaa jiite CEDEAO bokk na ci sabab yi ko tax a doxale ni mu doxale, moom ak yenn ci ay njiiti-réew yiy dox ci waawam. Xamees na xéll ne, bés bu Niseryaa tegoo ci boppu CEDEAO, Farãs dootul am baat ci réewi kurél gi, doonte moo leen yàgg a yilif, di leen jaarloo fu ko neex.

Farãs noppi naa def lépp lu mu laaj ngir wéy di ratt réewi Afrig yu ñuul yi mu nootoon. Xam na li mu bëgg te mu ngi koy def. Léegi nag, sunu réew yi ñoo war a xam li ñu bëgg, te def ci seen xel ne ngir coppite am, nooteel bi jeex fi, fàww ñu booloo ngir gën a am kàttan. Tamit, fàww ñu nas ay feem yu ñu togg bu baax te tegu ci xel ngir noppee jaamaarlook moom. Bu ñu ko defee kenn kenn rekk, dina leen daaneel  ñoom ñépp te du jóg ci di leen toroxal.

Boos Ndóoy

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj