Àtte bi daanu na. Tey ci àjjuma ji lañ doon àtte Ustaas Umar Sàll ginnaaw bees ko jëkkee bëtal àjjuma jee weesu. Dafa am ag kurél ci tarixa tiijaan ñu pelent waaraatekat bii di Ustaas Umar Sàll. Li ñu koy tuumaal mooy wax ji mu waxoon ñeel anam bees war a tuddee Yàlla, Boroom Bi. Layoo bi nag, yàggoon na lool. Ndax def juróom-ñaari waxtu. Ci njeexital la nag, àttekat bi bàyyi na Ustaas Umar Sàll mu ñibbi këram. Nde, daf ko setal ci tuumay cokkaas ak jëfi muñadil (provocations d’actes d’intolérance). Waaye, nag, daf ko gàll daanub juróom-benni weer ak sirsi (six mois d’emprisonnement assortis de sursis). Li ko àttekat biy taqal mooy ne dafa biral ay saaga ci mbaali jokkoo yi.
Layookati Ustaas Umar Sàll yi dañu sàkku woon ci àttekat bi mu jiital jàmm, bañ a àtte luy yee fitna. Moo tax, bi àtte bi jibee, Meetar Abdulaay Taal, layookatu Ustaas Umar Sàll bi daf ko rafetlu, wax ne « xibaar bu neex la ñeel xam-xamu lislaam. ». Ndaxte àtte bi day tax ñu delloowaat coow li ci géewug diine ji. Nde, yoonu Senegaal amul màqaama àtte lu ni mel. Moom layokat bi, rax na ca dolli sax ne :
« Bu Ustaas Umar Sàll di wax ci xam-xamu diine, dañ ko war a tontu ci xam-xam. Lii [pelentu tiijaan yi], dafa nar a nekk ag njiitlaan (précédent) lu doy waar ci réew mi. Ëllëg aw nit mën nañoo jóg pelent ab waaraatekat buñ jàppee ni daf leen a tooñ ci seen ngëm-ngëm… Buñ la woowee ci xam-xam, tontul ci xam-xam moo gën ngay saaga, di xaste ak a yàq der. »
Cig pàttali, 15 nowàmbar ba léegi, Ustaas Umar Sàll mi ngi woon ci loxoy yoon, doon xaarandi àtteem ñeel layoo bim séq ak tiijaan yi ko boole ak yoon. Tiijaan yi dañ jàpp ne dafa ŋàññ seen tarixa, soofantal seen yoon wii di suufiya. Looloo sabab ag kurél ci ñoom pelent ko.
Werante ci diine nag, yàgg na Senegaal. Dafa di, bu njëkkaan, fësul woon ni mu fësee tey. Li taxoon mooy ne, li ëpp ci Saa-Senegaal yi dañu bokkoon ci ay tarixa. Moo tax, kenn daawul dégg ñi doon dàjji yoonu tasawuf. Penda Ba mi xam-xamam màcc ci wàll wi, di jàngale fa jànguneb Ndar bii di UGB, firndeel na ko ciy kàddoom yii :
« Am nay ndawi Afrig sowu-jant yu jàngi woon ca jànguney araab ya, ca ati 1950 ya, ñibbisiwaale ak yoonu salafiya, di woote ci lislaam bu set wecc bu raxul benn bidaa yi ci tarixa yi dugal. Ñoom, ñetti nooni lislaam yii lañ doon xeex : sëriñtu, nooteel ak kapitaalism. » (Cahiers d’étude africains)
Léegi, ñi ñuy woowe « Ibaadu » dañ fi gën a bari, rawatina biñ taxawalee Jamaatu Ibaadu ca atum 1978 ba léegi, donte ne sax du Ibaadu yépp ñoo bokk ci kurél googu. Moo tax léegi, waxtaan wi yaatu ba ci mbaali jokkoo yi. Waaye, ak li wax jiy bari yépp ak a tàng léeg-léeg, ci wax kepp la mës a yem. Coow mësul jib, fitna mësu cee juddoo te yoon mësu cee am baat. Te sax, naka la yoonu Senegaal mi tënku ci layisite, maanaam màndu ci diine, mënee àtte lii ? Ndax sunu tirbinaal yi dañuy àtte nit ku junj te tuddul aw tur ? Xanaa, su boobaa, àttekat bi day kaalawu, ubbi kaamil bi ak téere xadiis yi ngir àtte ? Waaw, bu dee diggante kercen ak jullit nag ? Caaxaan baaxul.
Wax ji Ustaas wax ñeel ab xeetu jaamu Yàlla, dafa cee junj. Ndax àttekat bi mën na àtte junj ? Ci ban sàrt lay tënku ? Xanaa kon Alxuraan ak Biibal bi kenn du leen jàngati ci réew mi ? Ndax, téere bu ci nekk, dafa fees dell ak i junj. Diine moo ni deme. Kon, waxtaanu diine, dafa war a yem ci keppaaru xam-xamu diine ndeem bëgg nañ jàmm ci réew mi. Nde, wax jii Ustaas wax, buñ ko ci daanoon, kenn dootul mucc, ba ci sax tiijaan yi ko pelent. Ndax, ku wax ci sa ngëm, weddi leneen loo gëmadi lol, am na ñeneen ñu ko gëm. Te, kon, bu dee ku wax ne jëf sàngam bokkul ci diine te tuddoo kenn, ag kurél sañ la cee pelent, Senegaal nar na tàbbi ci fitna ju doy a doy waar. Te sax, kan mooy Ustaas Umar Sàll mi waral coow li ?
Ustaas Umar Sàll jàngalekat la, di waaraatekat, féete Daaru Cub, fa Kër-Masaar. Moom, ci waa Ahlus Sunna la bokk, maanaam ñiy roy ci Yonent bi ak i saabaam ci wàllu diine. Maanaam, ibaadu la ci nees koy déggee fii ci Senegaal. Ustaas Umar Sàll, daara ji mu yor di ci jàngale, daf ci yoraale ay jirim yoy, moo leen féetewoo, yor leen, di leen dundal, di leen jàngal, di leen yar ak a yiir. Loolu yépp, ginnaaw ndimbalu Yàlla, ci alalu boppam la koy defe. Rax-ci-dolli, Ustaas Umar Sàll ku bari li muy dimbali néew-ji-doole yi la. Ndaxte, saa su nekk, mu ngiy jàppale ñoo xam ne, seen loxo jotul seen ginnaaw. Muy Ndakaaru di fépp ci biir réew mi. Ba ci dëkk yi gën a sori ci kow gi, daf fay dem di leen gasal ay teen ak di leen jox i ndàmpaay. Saa bu tabaski jubsee, mu jënd ay xar yu baree bari, jox koy boroomi kër yi ko yeyoo te tumurànke. Bu koor teroo ak laata muy jeex itam, dina dimbaliy njaboot yu baree bari. Xam naa dinga laaj fan la Ustaas di jëlee xaalis boobu yépp.
Moom Ustaas, wëliis fànnu diine ji, day yëngu ci wàllu paj. Ay reen lay fajee ak pajum diine mees jàngee ci Yonent bi. Ci paj moomu lay fàggoo alal ji muy yoree daaram ji ak di ci dimbali nit ñi néewle. Waayeet, dinay faral di woote ndimbal, di sàkku ci ñi ko mën, ñu joxe as lëf ci li leen Yàlla wërsëgal ngir mottalee ko li mu am, baaxee ko miskiin yeek faqiir yi ci réew mi. Ba Ugandaa mu sori mee, Ustaas mi ngay fay dimbaliy jullit yu néew doole. Ku ni mel, kaso du palaasam. Am na lu bare lol, Nguur gee ko waroon a taxawe. Waaye, Ustaas ak ñi mel ni moom ñoo ko taxawe ci réew mi. Te sax, li mu wax, yàgg nañ ko fee dégg.
Xanaa kay, dafa dib boroom dayo bob, saa bu waxee mu law. Te, waxam jigul tarixa, jigul it Nguur gi. Dafa di, muy mbëkk mi, di jafe-jafey dund bi, ni yoon jengee, ger ak càcc gi ci réew mi, añs., Ustaas bawul dara. Bari na lu muy yedd ñi jiite réew mi, di leen delloo ci Yàlla ak di leen fàttali seen wareef ak seen i sas ñeel askan wow, sonn na lool. Buy xutba, di tafsiir walla di amal uw waxtaan, dina compaale, waxal askan wi, kaasal ko. Moo tax, jàpp biñ ko jàppoon xaw a teey xel yi. Ndax, bu dee mbirum diine rekk, wax ji du kon àgg fii mu àgg ba ñu koy jàpp. Waaye, li ci kanam rawul i bët.