YOON GÀNTALATI NA USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Usmaan Sonko dafa dugaloon ? keroog 2i fan ci oktoobar 2023, ab « recours » ñeel li ko waa DGE bañ a jox xobi baayale gi. Sànq ci ngoon, bi 15i waxtu jotee, la ko Ëttu Àtte bu mag bi doon àtte ak waa DGE. Layookati Usmaan Sonko yi, waa Pastef ak soppeem yépp a amoon yaakaar ci ne, wii yoon, àttekat yi dinañ ko dëggal. Waaye de, ci yàqi lañ mujje. Nde, àttekatu Ëttub Àtte bu mag bi dafa gàntalati Usmaan Sonko.

Kurél giy saytu wote yi, ci nasaraan Direction Général des Elections (DGE), dafa bañoon a jox ndaw la fa Usmaan Sonko yabaloon ngir mu jëlal ko xobi baayale gi. Moo taxoon layookati Usmaan Sonko yi dugaloon lees dippee « recours » walla « requête en référé Liberté » ca Ëttub Àtte bu mag bi. Tey ci àjjuma ji la àttekat bi waroon a jël ndogalam ginnaaw bi mu dégloo ñi mu waroon a déglu yépp. Bi 15i waxtu jotee la àttekat bi ubbi liggéey bi.  Ci boori timis la fésal ndogal li mu jël, dëggal DGE, gàntal Usmaan Sonko. Ndogal lu ni mel nag, dafa bett ña fa nekkoon ñépp, rawatina layookati Usmaan Sonko yi. Moo tax, kenn ci ñoom, Sire Keledoor Li, wax ne :

« Àttekatu « référé-liberté » yi jël na ndogal lol, ñépp la bett. Te jàpp naa ne sax, àtte bi dafa bett Nguurug Senegaal. »

Li gën a waral mbetteel gi mooy ne, Toppekat bu mag bi sax, àndul woon ak ndogal li DGE jëloon, bañ a jox Usmaan Sonko ay xobi baayale. Daf ne :

« Caytu gi mënut a far ba noppi di àtte. Njëwriñ (gu biir réew mi) dafa sukkandiku ci dogu 29eel (bu càrtug wote gi). Te, dog boobu, ci bindu gi la aju, waaye waxul ci ndàqe yeek génnee yi. DGE dafa jéggi ay sañ-sañam. Dañ xañ Usmaan Sonko àqi maxejjam ci lu bir, daldi koy tooñ. Yow, àttekat bi, danga war a dakkal tooñ bi. »

Toppekat bu mag yemu ca. Nde, joxoñ na ka fa teewaloon caytu gi, wax ko ne :

« Dangeen sukkandiku ci teewadi gi (contumance) daldi génneewaate ci njuumte. Dogu 29 bi ngeen di tudd, ci bindu gi la aju, waaye waxul ci ndàqe yeek génnee yi. Ndogal loolu, am ndajem caytu a koy jël. Bu ngeen joxee xobi baayale gi, lum leen di yàqal ? Ab àqub dàtt (droit fondemental) lees xañ ab maxejj. Bu nu jiitu Ndajem Ndeyu Àtte ji ci sañ-sañam. Ag tooñ la ñeel ub àq bu dàtt. »

Wax jii, rawatina bim jóge ci koo xam ne xel xalaatul mu faral Sonko, dafa yaakaarloo woon ñu bari. Meetar Sire Keledoor Li raxoon ca, wax ne :

« Jamono jii nga xam ne noo ngi tollagum ci càkkuteefu doon lawax, wotey 25 féewaryee 2024 yii am na gàllankoor ba noppi ñeel yemale gi war a am diggante lawax yi. DGE du lenn lu dul ab banqaas bob,bokkeef gi daf ko dénk lenn ci sañ-sañam yu leer. Bokk na ci, joxe ay xobi baayale. Liggéeyam mooy joxe ko te ye ci. Bu weesoo loolu bay wax kuy doon lawax ak ku ko dul doon, mi ngi jalgati Yoon. Te nag, bu jalgat Yoon amee, yow àttekat bi danga war a delloosi Yoon. »

Meetar Sire Bàccili dolli woon na ci :

« Danu ci réew mom, Yoon a ko tënk. Li nu fi indi tey mooy dakkal jalgat yi ak ëppal yi njiit yiy ëppal ci seen i sañ-sañ. Benn campeef kese moo war a àddu ci lawax bees war a nangu am déet. Li ci des lépp waxi picc kese la.  Bu amee jenn jëwriñ juy wër ci kibaraan yi di wax ci mbir mi, loolu safunu. »

Bu dee Meetar Bàmba Siise moom, dafa laaj ndax waa DGE dañu jot ci yégle bu leen di wax Usmaan Sonko mënatul a doon lawax. Waaye, ànd ak loolu yépp, àttekat bi dafa gàntal Usmaan Sonko. Muy lu doy waar.

Meetar Abdulaay Taal xamle na ci xëtu Facebookam ne, Usmaan Sonko bàyyeegul, donte kenn amatul kóolute ci Yoonu Senegaal.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj