YOON : JUB, JUBAL, JUBBANTI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey, ci talaata ji, 28 pani suwe 2024, lañuy tijji péncoo mi ñu jagleel ni Yoon war doxee. Péncoom ren jii nag, mooy doon ñeenteel wi yoon ñu koy amal fi réew mi. Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, mooy jiite tijjite gi.

Ca jamono ja muy kàmpaañ, di dagaan baatu askan wi, lawaxu lëkkatoo “Diomay Président” bi dafa dige woon ne, bu toogee ci jal bi, dina indiy coppite ci ni Yoonu réew miy doxee. Nde, at yii weesu, Yoon dafa sooxe lool fi réew mi. Dafa dem ba pólitig bi rax ci, ëpp ko doole, bóof ci kowam, mu daldi jeng. Ñenn ñi (nguur ga woon) soppi ko ngànnaay, di ko xeexe kujje gi ak askan wi.

Yoon wi nga xam ne, moo waroon di àtte diggante yi ci màndute, waroon a tëdde njaaxaanaay, dafa dem ba jeng, di salfaañe àqi maxejj yeek way-pólitig yi ci kujje gi. Mbir mi dafa mujje doon mbirum “Kumba am ndey, Kumba amul ndey” walla mbirum “Làq doom, dóor doom”. Boo bokkaan ci kujje gi, walla nga dib baadoola, nga tooñ walla nga ñàkk a tooñ yépp, yat wi sa kow lay dal, rawatina boo jote waan ak boroom daraja walla boroom ndombog-tànk bu fare ci nguur ga woon walla muy boroom alal. Lees ci war a déggee mooy ne, nger daf ci bari woon lool. Askan wi gisatul woon boppam ci ni Yoon di doxe. Kaso yi fees dell. Ku wax, ñu jàpp, tëj.

Bu loolu weesoo, anam bi Yoon di liggéeyee ci boppam dafa dëppoowul ak jamono. Muy béréb yi muy liggéeyee walla jumtukaay yi, yépp a màgget walla ñu xewwi. Limub liggéeykat yi tamit, doyul. Sàrt yi tënk ni Yoon war a doxee, ni àttekat yi war a doxalee ak ni caytug Yoon wi di liggéeyee tamit, dafa laaj ag joyyanti. Loolu yépp a waral Njiitu réew mi woote waxtaan ngir ñu fénc jafe-jafe yooyii, sàkkal leen i pexe.

Péncoo mi nag, tënkees na ko ci ponk bii di : “Sopparñi ak yeesalug Yoon wi”. Laata tey, waajaloon nañ ab dalu web bees tudde « Jubbanti » ngir taataan xalaati maxejj ñeel Yoon wow, ci seen tur lay àtte. Képp-kenn ci doomi réew mi mënoon cee tàbbal gis-gisam ci wolof walla ci farãse. Bu péncoo mi jeexee sax, dees na fi bàyyi dalu web bi, askan wiy wéy di ci rotal i xalaatam, ñu ciy sukkandiku ngir di gën a baaxal ni Yoon di doxee. Bu dee ñi mënul lënku walla ñi desee nànd nees koy defee, jagleel nañ leen limat gii di 1222 ngir ñu woote ci, joxe seen xalaat wëliis ñu fay dërëm.

Waxtaan door na tey. Askan wépp a ngi xaarandi coppite ya cay tukkee, am ci yaakaar lool. Ndax, fu Yoon am, jàmm am fa. Te, jàmm mooy cëslaayu naataange ak yokkute. Wolof nee, bakkan, jàmm la bëgg.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj