2023 : YOON NAR NAA XUMB

Yeneen i xët

Aji bind ji

Atum 2023 mii, atum Yoon la nar a nekk. Wëliis mbirum ñetteelu moome gi nar a tàbbi ci loxoy Ndajem ndeyu àtte mi, bari nay mbir yoy, Yoon a ca am wàlluw nag wa. Ndaxte, mëneesul a xéy bés te déggeesul mbirum njombe ñeel ay miliyaari miliyaar. Ay caabaal yu dul jeex yoy, dañuy biral ay tóoxidóona ak i jalgatiy caytu yu ñaaw a ñaaw. Nu ni déet-a-waay, nit ñi, rawatina way-pólitig yi, di tamante dëmm saa su nekk, di tuumaalante ciy mbir yu jéggi dayo. Ku nekk a ngi kalaame Yoon ngir setal deram. Ci talaatay tey jii rekk, am na ñetti mbir yi ci yéenekaay yi fésal, bu ci nekk dafa laale ak Nguur, laale ak pólitig.

1. TOPPEKAT BU MAG BI SÀKKU NA ÑU ÀTTE USMAAN SONKO AK NDEY XADI NJAAY

Yéenekaay Les Échos moo siiwal xiibar bi ci talaatay tey jile. Yéenekay biy xamle ne, Toppekat bi dafa jàpp ne sabab yi war a tax ñu àtte Usmaan Sonko ak Aji Saar yépp daje nañu. Dara desatul lu moy ñu yóbbu leen ca ëttub àttewaay ba, daldi leeral mbirum Sweet Beauty mi. Li Toppekat biy sàkku ñu àtte ci Usmaan Sonko mooy mbirum ciif gi ak tëkkuy rey yi ko Aji Saar di tuumaal ; bu dee soxna si moom, Ndey Xadi Njaay, la mu koy tuumaal mooy mbonte ak yàqug jikko.

Ci xalaatu yéenekaay bi, cib layoo lees nar a mujj. Waaye nag, lépp a ngi ci loxoy Àttekat bu mag bi. Moom rekk a yor ndogal li, am sañ-sañu yóbbu way-jote yi ca ëttub àttewaay ba ngir ñu layoo, walla mu neenal mbir yi, dëpp kaas yi te yemale leen fii. Li ci kanam rawul i bët.

2. ABDULAAY SOW – BUBAKAR KAMARA

Keroog 31 desàmbar 2022, ca jotaay ba ñu bokkoon ca TFM, Jury du Dimanche, Bubakar Kamara ak Abdulaay Sow jotoon nañoo weccantey kàddu yu ñagas, ku nekk tuumal ca sa moroom ci mbirum luubal xaalis.

Dafa mel ni, Abdulaay Sow giifagul ca meram ma. Ci lees jotagum ciy xibaar, jëwriñ ji ñu dénk wàllu Taax yi, Dëkkuwaay geek Cetalug bokkeef gi, dafa boole Bubakar Kamara yoon ngir mu leeral tuuma yi mu ko gàll. Dafa di, Bubakar Kamara mi boole jiite kurélu JENGU ak lëkkatoo TABAX, bi ko jëwriñ Abdulaay Sow tuumaale ne mës nañ koo tëj kaso, daf ko weddi woon, ba noppi dollil ko ca kàddu yii :

« …man, laaju ma juróomi téeméeri tamndaret (500i miliyoŋ F CFA) te yow, def nga ko. Jox nañu la dawalub téeméeri tamndaret (100i miliyoŋ F CFA). Ngir ay pàkk… maa ngeek wayndare wépp. »

Ci bataaxalub kalaame bi Abdulaay Sow jébbal Yoon, mi ngi ciy wax ne :

« Kàddu yu ni mel dañuy wund ne aji-boole ji, jëwriñ ji ñu dénk wàllu Taax yi, Dëkkuwaay geek Cetalug bokkeef gi, dafa laale ci wàllu ndagaan ñeel njaayum suuf walla ay kër, te dara amu ci. »

Bubakar Kamara nee :

« Waxtaan wu amoon la 31 desàmbar bii mujj, mu ay kàddu yim ma sàndi woon. Li ma bokkul ak moom jikkoo tax ma junj ko as tuut. Ci wàllu kalaameg-leeral gi nag, jotaguma ci. Bu nu ci jotee, dinanu tontu… Li may wax mooy ne, mbir mi gën na ñàng lii fuuf. Senegaal, dafa am ñu booloo, di sàcc suuf si, di ko jaay ci anam bu doy waar… Dama bëgg mu may mab layoo bob, dinaa ci mën jaare, leeral lépp. »

Moom nag, Buubakara Kamara, mi ngi xamle ne bañul a jël kalaameg-leeral gi, nde wax na fuy layookatam nekk. Nu xaar ba xam fu mbir miy mujje.

3. MBIRUM PRODAC : ÀTTEKAT BI WOOLU NA USMAAN SONKO

Usmaan Sonko dina janook àttekat bi, keroog 2i fan ci weeru féewarye. Dakar Matin moo fésal xibaar bi. Ndax, jëwriñ jii di Maam Mbay Ñaŋ moo kalaame Njiitalu PASTEF li ca Yoon. Li tax Maam Mbay Ñaŋ yóbbu meeru Sigicoor bi Yoon nag mooy ne, dafa jàpp ne Usmaan Sonko dafa yàq deram, tuumaal ko, tiiñal ci mbirum PRODAC mi. Nde, Usmaan Sonko dafa waxoon, ci wenn waxtaan wow, amaloon na ko ak taskati xibaar yi, ne yor na ag caabalug IGE guy tuumaal Maam Mbay Ñaŋ ci ni mu yoree woon PRODAC bi.

Ngir fàttali, PRODAC, ab naal la bob, la ko taxoon a jóg mooy caytuy pàkk yees jagleel mbayug mboolaay yi. Waaye, coow lu réy a ca toppoon. Waaw, dafa amoon 29i milyaar yuñ ci luubaloon, te booba, Maam Mbay Ñaŋ moo jiite woon liggéey ba.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj