MAKI DA NI WOON YOONU YOKKUTE : LÉPP YOKKU NA !

Yeneen i xët

Aji bind ji

«Réew mi dafa tagatémbe !», «Dund gi jafe na !», «Lépp a dëgër !», «Danoo sonn!», «Na nu Maki dimbali !», «…walla mu abal nu.»… Ak yile kàddu lanu waa Yëmbël-Sud biralee seenuw naqar ci tolluwwayu réew mi ak nees ko jiitee. Wànte, bees sukkandikoo ci xibaar yi kibaraan (médias) yiy biral fan yii, mënees na wax ne, njàmbat ak jooytuy waa Yëmbël yile, ci réew mépp lay jibee. Nde, wax ji, jenn rekk la : «Senegaalu tey, baadoola du fi naane ñeex ». Nguur gi jël nay dogal ngir njëg yi bañ a romb fiñ tolloogum nii. Nee ñu, dogal yooyee, nguur gi dina ci ñàkke 47i miliyaar. Boobaak léegi, ñoo ngi génney yégle, di janook taskati xibaar yi, di wër ci gox-goxaat yi, añs. Aminata Asom Jaata sax, jawriñu Njënd meek Njaay mi woote woon nam ndaje mu mag ñeel lekk geek naan gi keroog talaata 31i fan ci ut 2021 ca CICES. Waxtaaneesoon na fa njëgi dund yi askan wiy gën a aajowoo, rawatina ceeb bi, diwlin jeek suukar si. Waaye, ba tey daal, askan waa ngi binni.

Ngir natt coono wi askan wiy jànkonteel, amal nanu laajantug-nattale gu ndaw biir Yëmbël-Sud. Doxantu nanu ci mbedd yi, laaj ñenn ci way-góorgóorlu yi fay yeewoo ngir taataan seen i xalaat ñeel tolluwaayu réew mi. Waaye, yemunu ci. Ndax, gannaaw gi, méngale nanu njëg ya woon ci atum 2012 laata Maki Sàll di falu ak yu tey yi ngir natt yokku gi indi coow li.

Yëmbël mi ngi nekk ci biir diiwaanu Ndakaaru, bokk ci depàrtemã Kër Masaar. Ci nguurug Abdu Juuf lees ko xaajoon, def ko ñaari bokki-moomeel : Yëmbël-nord ak Yëmbël-sud. Yëmbël, niki Caaroy ak yeneen bãliyë yi, bokk na ci gox yi gën a tumurànke. Nit ñu bare, dëkkuwaay ak tali yu xat a xat, mbedd yu tilim, te saa bu tawee daanaka fépp ay taa. Moo tax, dékku yokkute njëg yi doon na lu jafe ci góorgóorlu ya fay yeewoo.

  « Kër gu taa, cin lu dëppe, njaay mu lamb, jiba yu fëq… »

Mbas mi, mbëkk mi, mbënn mi, mbëj mi, ndox mi ak… dund gu jafe gi. Nattu bu ñëw, laata ñu koy noppee jooy, beneen tegu ca, gën a tar, gën a metti. Senegaal di mel nig gaal guy daw ci géej gu sàmbaraax, ngëlén li wër ko fépp, ngelaane li koy joow, fu ne mu jëmale ko fa. Ci boor bu ne, gannax yiy baawaan ci kowam. Ñi ci biir gaal giy yuuxook a jooy, ñi ci bopp biy gundaandaat ak a yaataayumbe, léeg-léeg ñu xaw leen a geestu, di leen jéem a dëfël ak a naxee ay dig.

«Kër gu taa, cin lu dëppe, njaay mu lamb, jiba yu fëq… nii la fi deme, jaaxle naa. Sonn naa. Amatuma pexe. Bunt yépp fëgg naa leen.» Waaye, benn ubbeekuwu ci ñeel boroom kër gii leb turam. Bi nawet bi dooree ba léegi, mook ndox mu selladi mi ñoo dëkk, mbott yeek yoo yi diy dëkkandoom. Mbas mi xañ na ko liggéey bim daan suturloo mook njabootam gu sew. Saa bu jant bi fenkee, mu xuus génn, xoslu ji njëlug bés bi, «…bu teyee Yàlla wërsëgal ma, bu ëllëgee duma indaale dara.» Bu dul woon ngëm ak yaakaar Yàlla, «…xàddi kon woon naa bu yàgg». Ni góor gii, ñu bare ci askan wi, ngëm ak yaakaar kesee leen dese ba di leen tax a muñ ngir sàmm seen ngor. Nde, bu dul woon loolu kon, «ma garbo, jaay sama der ni ko samay moroomi jeeg di defe jamono jii te dara yóbbewu leen ko lu dul ñàkk pexe. Waaye, maa ngi jàpp ci Yàlla. Ndaxte, loo muñ mu jeex, Yàlla baax na.» Soxna sii tamit leb turam, ay jooy la daaneleey waxam. Nde, taabalu màngoom ak meññent yu sew-sewaan yi mënu cee dundal njabootam. Jëkkër ji, ab Móodu-Móodu la woon, mbas mee ko tax a daw ñibbisi. Boobaak léegi mi ngi las-lasi waaye taxu koo deme noonu. Nii la askan wi, rawatina baadoolo yi, dëkke. Ñi ci ëpp seen loxo jotul seen ginnaaw, dañuy xëy di daŋ-daŋi ba jant bi so, lépp luñ jot a fortaatu, bu motee njëlug bés, ci lay yem. Bu jant bi fenkaatee, ñu wëri deppãsu bés ba ca topp. Kenn dencatul. Ndax, «boo dencee tey, bu ëllëgee say mbokk denci la walla nga denci leen. Maanaam, boo dencee as tuut li ngay fortaatu, xiif dina la rey walla mu rey sa mbokk.»  Baay Mandaw Gay, Yëmbël-Sud moo wax loolu.

Senegaal a ngi mel nib màggetu-soboronko, xuuge lool, opp ci yaram wépp, foo laal mu onk. Wëliis dund gi, dara yombul. Maas Ñaŋ ab «agent immobilier» la, dëkk Yëmbël-Sud, ci gis-gisam, «luyaas bi sax néew-ji-doole yi àttanuñ ko. Li boroom kër yiy laaj dafa bari lool te xaalis amul. Waaye nag, ci benn boor, mëneesu leen a ŋàññ. Ndaxte, muy simoŋ, weñ, suuf, betoŋ, añs. lépp a yokku.»

Aamadu Jàllo moom, mi ngi dëkke kàrce Baas, dib ñawkat. Mu ne, «Wax-dëgg Yàlla moom, mbir mi metti na. Bu njëkk sax tane woon na. Waaye, nii nii moom boroom kër yi sonn nañu. Boo joxee deppãs sax du mat. Lépp a yokku, dund gi jafe na. Nun, ñawkat yi, liggéeyatunu. Ñaw sax amatun ko. Ndax nit ñi ñawlootuñu, «prêt-à-porter» yi ñuy jéggaani lañuy jënd. Dangay xëy, suba ba ngoon, doo am sax deppãs. Rax-ci-dolli, mbëj mi dafa gën a jafe. Sonn nanu. Noo ngi sàkku ndimbal ci njiitu réew mi, Maki Sàll.»

Faatimata Ka, jaaykat ca kàrce Laayen, moom tamit ne,

«Dëkk bi neexul, metti na lool sax. Nun, jaaykat yi sax yëg nan ni dafa metti. Lépp a jafe, lépp lañ yokk. Metti na ci góor ñi rawatina nun jigéen ñiy dem màrse. Fim ne nii, lépp lu doon jar juróom, fukki dërëm lay jar… ceeb, diwlin, suukar, saf-safal yi sax, dara yombatul. Nanu Maki dimbali…»  

Naam, mbas mi nasaxal na koom-koomu àddina si. Kenn sañul a wax ne Covid-19 amul njeexital ci njaay meek njënd mi ci àddina si. Moo taxoon, fépp ci àddina si, nguur yi lal i naal ngir sàmm seen koom-koom, aar njëg yi ak xëy yi. Senegaal, amoon na lees duppe “Fonds Force Covid-19”, njiitu réew mi defoon ci 1000i miliyaar ci sunu koppar. 200i miliyaar yi la jagleeloon àntarpiriis yi, wàññee ko seen i juuti. Waaye, mel na ni amul njeexital yiñ ci doon séentu. Ndaxte, li gën a tax njëg yi yokku mooy juuti yu takku yi àntarpiriis yiy fey. Ku daan fey 100 000 FCFA juuti, léegi 200 000 FCFA ngay fey. Bu ko defee, ci askan wi lañ koy fayoo, yokk njëg yi.

Muy jaaykatu jën bi, uude bi, paa yi ci pénc mi, ndaw yiy àttaaya ci taati garab yi, boroom bitig yi, jaaykatu dàll bi, dawalkatu kaaraapid beek àpparànteem, boroom kalaandoo bi walla boroom taksi bi… ñépp a ngi jooytu. Nde, ku ci ne, sa boor, mbir mi dëgër na. Koo ci laaj, mu ne la nguuru Ablaay Wàdd moo tane woon. Te, bin méngalee njëg yi, gis nan ni, diggante 2012 ak tey daanaka lépp a yokku.

Xanaa du Makee fi waxoon Yoonu yokkute ?

«Waaw ! Ba muy wax loolu, yokkuteg boppam, moom, njabootam, ay mbokkam ak i jegeñaaleem a ko taxoon a wax. Xoolal rekk Maki ci boppam lim yor ci alal, yokku naam déet ? Xoolal ay doomam, jabar ji li muy tuur ci xaalis yépp, doom yi nag, rawatina Aamadu Sàll… Nga xool waa Bennoo Bokk Yaakaar, ñenn ci ñoom, laata ñuy nguuru, buñ añaan duñ reer. Ana ñu tey ? Du ñoo fiy dawal daamar yiy jar 100i miliyoŋ ci sunu koppar… fuñ ko jële ? Lii mooy Yoonu yokkute wi Maki noon da koy xàll ?»

Noonu la Saalif Jàllo, maxejj bu dëkk Yëmbël-Sud jàngate mbir mi. Te, bees sukkandikoo ciy waxam, Maki moo gën a xamaatoo li askan wiy jànkonteel, xam na yit naka la war a def ba noppal leen ci coono yi leen gaar fan yii.

Ca atum 2012, Makee fi waxoon lii : «[Yokkuteg] njëg yi, ci gornamaa bi la. Ndax gornamaa bi mooy teg nit ñi ay juuti yu bees, yokk tamit yi fi newoon. Ndaxte lim soxla ci doxalin, lim soxla ci ay tukki, lim soxla ci jënd ay roppëlaan, lim soxla ci ubbi ay àmbaasad, ci ay njawriñ dafa diis, diisaay boo xam ne ngir mu mën ko def fàww mu yokk njëg yi…»

Kon, li Saalif Jàllo wax dëgg la. Makee fi dige woon sax ne, bu faloo, loolu lay jëkk a «…dindi, wàññi ni nguur giy doxe, diisaay bi, ngir alal ji mën a dem ci askan wi»

Benn ci sabab yaa ngi noonu : diisaayu nguurug Maki Sàll.

Nguurug gundaandaat

Ablaay Wàdd dafa amoon lu tollu ci 38i jawriñ, Maki ne woon loolu ëpp na ci réew mu ni tuutee. Tey, mi ngeek 39i jawriñ yu bokkul ak dumbulu jawriñ yi koy digal te seen lim romb na 30. Bun xaymaa jawriñ yooyu yépp nag, daanaka jege nañ 100i jawriñ. Te, bu nu sukkandikoo ci Seneweb (https://www.seneweb.com/news/Societe/combien-gagne-un-ministre-au-senegal-hellip_n_70295.html), Jawriñ buñ tabb ci nguur gi 2i miliyoŋ ngay am ci payoor weer wu dee. Dees na la jagleel tamit boŋu 10i miliyoŋ ngir nga defaree ko sa biir kër. Njiitéefu jumtukaay yeek njàllaleg caytu gi, ci nasaraan, “Direction du matériel et du transit administratif ” (Dmta) mi nekk ci kilifteefu njawriñu ngurd mi. Loolu doyul, saa bu jawriñ jiy amalub tukki liggéey, dees na ko jagleel ndàmpaay luy tollu ci diggante 150 000 FCFA ak 200 000 FCFA bés bu nekk. Te nag, buy tukki «business class » lay toog. Nga xool, 39i jawriñ, ku ci nekk di am lu ni tollu weer wu nekk, ñaata la ci xaalis. Bu fekkoon ne ñoo ngi liggéey sax, mu tane. Waaye, nekkewuñ fi lu dul pólitig ak njuuj-njaaj, di sàcc xaalisu réew mi, di luubal mel niy dëmm, na ma Yàlla baal.

Ablaay Wàdd amoon na SENAT mi doon wann 8i miliyaar at mu ne, Maki ne loolu dafa bare, amul njariñ te dina ko dindi. Naam, dindi na ko. Wànte, tey, mennum Maki mi, moo fi sos ay campeef yu gën a ñàkk njariñ Senat, dàq a wann xaalis. Duggewu ko lu dul làq ay farandoom ci pólitig, sédd leen ci nag wi (xaalisu réew mi). Nde, bim faloo ak léegi, dekkil na CESE ci sàttumbaar 2012, 6i weer ginnaaw bim togee ci jal bi. Mu teg fa Aminata Taal, jox ko nafag 7i miliyaar at mu nekk. Tey, Idiriisa Sekk (mburook soow) la fa teg, yokk nafa gi ba 8i miliyaar, muy feyeeku weer wu dee 9i miliyoŋ, wëliis oto biñ koy jox, esãs bi ciy dem, dëkkuwaayam, ay way-difeem. Ñu jox ko 80i liggéeykat yoo xam ne, ku ci gën a tuutile payoor 800 000i FCFA lay laal weer wu ne, ku ci ëppale di laal ba 3 000 000 FCFA. Rax-ci-dolli, saa buñ amaleem ndaje, dees dàmpe aji-teew ju nekk 1 miliyoŋ FCFA.

Nu ni déet-a-waay, Maki sosati campeef bu gënatee doyadi, duppe ko HCCT, daldi koy jagleel waa PS. Usmaan Tanoor Jeŋ a ko jëkk a jiite. Bim faatoo, Aminta Mbeng Njaay daldi ko fay wuutu. Ci 2021 mii rekk, seen nafa mi ngi tollu ci 9i miliyaar. Aminta Mbeng Njaay mi ko jiite di feyeeku 9 000 000 FCFA te oto bi, esãs bi, dëkkuwaay beek yeneen neexal yi ñëwaguñ. HCCT,  am na yeneen 150i liggéeykat. Bu dee aji-digal rekk nga, dinga laal 1 miliyoŋ ak xaaj weer wu jot. Bu dee aji-digal bu mag nga moom, dees na la ci tegal ab oto 4×4 bu tooy xepp buy jar 27i miliyoŋ.

Ci beneen boor, bi fi Ablaay Wàdd di jóge, boru 3076 miliyaar la nu bàyyee woon. Bi Maki ñëwee, ful na ko 3i yoon, yóbbu ko ba ci 9364. Nga gis ne, ci nguuru Wàdd, bor bi néewoon na te dund gi tane woon na tamit. Waaye, Maki moo ëpp li mu leb, te réew mi tey la gën a “maki” ni ko gone yiy waxe ! Fan la xaalis boobu yépp dugg ? Ana yoonu yokkute wi mu digoon askan wi keroog biñ koy fal ? Ku ko gis it de, man Jàllo gisuma ko !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj