Kenn werentewul ne njàng mu kowe mi dafa nekk ci guuta. Ab diir a ngi nii, muy jànkonte ak ay jafe-jafe yu bir. Li ko waral lépp mëneesu ko fi lim. Waaye, kurélug jàngalekati jàngune yi, gàttal biy joxe SAES ci tubaab, amaloon na ab lël jagleel ko jafe-jafe yooyile. Mu di aw yoon wees mën a jaare ngir càmbar gàllankoor yi ak pexe yi leen mën a saafara.
SAES mooy kurél gi ëmb jàngalekat yi féete ci daara yu kowe yi. Amal nañu seen fukkeelu lël ak ñeent. Bii yoon, dañu fasoon yéene waxtaan ci diirub ñetti fan. Ponk bi ñu doon waxtaane di : “ Enseignement supérieur au Sénégal : défi de qualité ”. Maanaam, ci wolof, njàng mu kowe mi ci Senegaal : Sasub mbaaxal gi. Mu mel ni, sas boobile ñu gàll seen bopp, ngir gën a ñoŋal njàng mu kowe mi, doonut lu kurél gi rekk war a sasoo. Ñépp ñoo ci war xar seen tànki-tubéy. Naam, waaye, benn pàcc kese
la ci pàcci yu bari yu séq njàng ak njàngale mu kowe mi. Dafa di, nag, SAES daf ci am wàll wu réy a réy. Ci kaw loolu, ci seen biir ub lël ba, tënk nañu seen ub bilaŋ. Ci lañu gisee ne kat, li ñu jot a liggéey ci 6i at yii ñu génn, am na ay njeexital yu baax. Waaye, wolof nee na, saabu du fóot boppam. Loolu la Maalig Faal, seen njiit li, xam ba daldi ko fay wax. Wànte daal, boo leen déggee, dafa mel ni, ñoom, dañuy rasu. Maanaam, dafa mel ni dañuy jéem a setal seen der ci tolof-tolofi jànguney Senegaal yi.
Kon, ñu gis ne boor boobu mënees na ko laf. Te may weneen wàll wi ñu àddu. Mu mel ni teewaayu jëwriñ ji ñu dénk njàng mu kowe mi du jaas. Nde, Seex Omar Aan jot na fekke lël boobu, biral fa ay xalaatam. Muy kàddu yu jëm ci tabax ay béréb yi ñuy jànge. Ci li soxal taax yooyu, Njiitu réew mi joxe na ay santaane. Nee na ñu saytu koppar yi ñu jagleel wàll woowu. Ñu gis ne bu ñu yokkee daara yu kawe yi, yokk tamit seen yaatuwaay, gën leen la ñoŋal ak ay jumtukaayi xarala yu bees, dina saafara lenn ci jafe-jafey njàngaani jàngune yi. Ci loolu, jëwriñ ji jot na lim jàngune bi ñu dippe Aamadu Maxtaar Mbów te nga xam ne daanaka noppi na. Bi féete diiwaanu Siin ak Saalum mu ngi ci njeexitalam. Ba nekke ca Fatig ak Kafrin tamit, liggéey ba dina wéy.
Mu gis ne tamit, taxawaayu ISEP yi lu baax la ngir saafara yenn jafe-jafe yi. Ci kow loolu, fas nañu yéene dolli juróom-ñetti daaray liggéey (écoles professionnelles). Ba tey, ci xalaatu Seex Omar Aan, loolu dina tax limub ndongo yi wàññeeku bu baax a baax ci daara yu kawe yi. Ak lu ci mën di am, bu nu bëggee njàng mi baax te jëm kanam, fàww ñépp bokk jëmu, di yékkateendoo, di dóorandoo. Muy Nguur gi, di SAES walla képp kenn ku ci laale, war na ci bay waaram. Nde, ni ko wolof di waxe, benn loxo du tàccu.