KÀDDUY USMAAN SONKO 2/2 PÀCC

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa réew mi  ci 8eelu fan ci weeru Màrs. Waxtaan woowu nag, dara waralu ko woon lu dul mas-sawu leen ci yi fi jot a xew, xamal leen itam ni mook ñoom a bokk naqar.

Lu Defu Waxu>, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc a ngi leen di baaxe ci ñaareelu xaaj bii, ay kàddoom na mu leen yëkkatee keroog jooju.

(Ci taataanug Uséynu Béey)

Nu war nag di waxante dëgg ndax Maki Sàll, li ko bewloo, bokk na ci nun waa Senegaal, ñenn ci nun waa Senegaal. Bala maa dee ñu naan ku xareñ la ci pólitig. Ndaxte yow mën ngaa dal ci sa naataangoo, mën ngaa ko kompaloo, mën nga koo jënd, walbati ko ba suy waxati du xam li muy wax lu mu doon ; loolu mooy xareñ ci pólitig? Nun, lin soxla mooy ku xareñ ci ni ñuy yoree réew ; koo xam ne, suñ la dénkee réew, nga defar réew ma. Xarañ ci pólitig dëgg mooy liñ la dénk, nga liggéey ko ba soo ne woon sama ñaareelu moomeel jeex na, maa ngi dem, ñu ne la bàyyiwuñu la. Juróom-ñenti ati Maki Sàll yi, li fi am, masul a am ci Senegaal. Ñaata naataangoom la tëj, ñaata la faagaagal? Loolu ba kañ? Loolu nag, la nu mënatul a nangu. Te nag, lii mu def, dañ koy tudde ci Tubaab wor wu réy. Maanaam wor wi gën a réy ci wor yi mën a am. Ndax moom bi ñu ko falee dafa teg loxoom ci sunu ndeyu sàrti réew mi daldi waat, ne «waat naa ne dinaa tënku ci ndeyu sàrti réew mi, dinaa nekk ci bëgg-bëggu askanu Senegaal». Li mu def wuute na. Ku dem ba yow nga wéet kunduŋ ak say juróomi nit, saw askan janoo ak yow, nga am sañ-sañu yónni jawriñ bu ñoradi bi, mu ne sa askan woowu yépp ay «terroristes» lañu, askan woowu wépp dafa am ñu nekk seen ginnaaw di leen jox xaalis. Ndaw yii dañoo mas a gis ku leen jox xaalis ? Taxaw saaga sa askan wépp, wépp. Yow doŋŋ ci sa pale ; tey boo ñëwee ci péey bi, moom kenn ak paleem, moom cunduŋ, askan wépp nekk fii. Su dul woon takk-der yi nekk sunu diggante, tey jii ay bagaasam dañ koy for. Loolu mooy wor wu réy ndaxte liñ ko joxoon ci ay jumtukaay du woon ngir muy «comploter» ay naataangoom.

Dama wax tey, ñu ne ma «contrôle judiciaire», waratoo wax ci mbir mi, ma ne àttekat bi : «Su ngeen ci waxee ma wax ci». Ndax, ay mbir amoon nañ fi : mbirum Xalifa Abaabakar Sàlll gis nañ   ko, mbirum Karim Wàdd wax nañ ci. (…)

Waaye, damay gaaral waa Senegaal. Wallaahi, dama ko waat, Wallaahi lañ ma tuumaal bu amoon, duma nangu benn doomu-Senegaal di ci am xoosu-xoosu, waxatumalaak bakkan di ci rot. Ndaxte bu boobaa, duma yem ci liñ ma def rekk, damay doon reykat ; kon doon na mel ni ñi ci faatu tey, man maa leen faat, duma nangu di am àq ak sama kanamu Boroom. Ñaawteefu Maki Sàll la ak ñi mu bokkal mbir mi.

Ba tax nag, ñu ne : Njiitu-Réew, am na loo xam ne, du sa sañ-sañ. Amul Njiitu-Réew moo xam ne, war naa féewale askanam, di féewale nit ñi, ñuy jàmmaarloo, di xuloo walla di xeex ; amul Persidã boo xam ne, war naa jiite ci coxor, ci bañ nit. Ndaxte, ku àndul ak yow rekk nga ne kii tey ma faagaagal ko. Loolu du Njiitu-Réew. Te nun ñépp, nan ko ci bañ a jàppale, ndaxte kàdduy mbañeel, léegi lay door a am Senegaal. Tey laay door a dégg Senegaal ñu tudd waaso nit ci pólitig, walla ñu tudd ngëm-ngëmam ci pólitig. Loolu, nun ñépp, kenn waru koo nangu ; te di ci woo ñépp nag, te di ci boole «media» yi. Nun ñépp nanu góor-góorlu. Wuutale ay porogaraam, ay naal ak ay xalaat, nangu nañ koWaaye def ay porogaraam ngir rekk ay nit ñëw di saaga nit, di ŋàññ nit, di wax ci moom loo xam ne du dëgg subaak ngoon, mu yor njaboot, am ñu ko bëgg, yor ay militaŋ, loolu mooy taal am réew…

Nanu delloosi sunu xel, mbir mi sottante xalaat la, wuutale ay xalaat, ay porogaraam la, waaye du xeex ak kujje giKenn ku ne deram rekk la am, waaye xéy suba ba ngoon, jóg di wax ci nit, di wax ci nit, di wax ci nit, tam ko dëmm, wax ciy mbokkam, wax ciy waa-juram, loolu amu fi woon ci Seŋoor, amu fi woon ci Abdu Juuf, amu fii woon ci Ablaay Wàdd ; mu ngi door a am, te dafa war a dakk. Maki Sàll moomul réew mi. Nun ñépp noo war a jël sunuy matuwaay. Te lii, defe naa buñ ci jógee dina doon njàngat ci nun ñépp. Ndaxte maa ngi seetaat porogaraam yi, dàŋŋaaral bi wàññeeku na. Ndax waroon nanoo toog ba agsi fii? War nañ cee jël ay njàngat. Ku ñu dénk réew, ñii nga xam ne ñooy say takk-der, nga xam ne kaaraange réew mi moo leen tax a jóg, waruloo leen teg ci yenn anam yi.  Ndaxte takk-der yi ma gis, ñoo gën a am lu leen naqadi fi nu tol nii ; ndax xam nañu ni ki ñuy dóor seen rakk la, xam nañu ni ki ñuy gaañ seen rakk la ; koo ci wéetal; xolam seddul. Ku ñu jox réew war ngaa moytu loolu.

May sargal nag Sàndarmëri Senegaal, ci seen mën-liggéey, ci seen sago. Man dama leen a mujjee naw. GIGN, bés biñ may jàpp ba tey biñ may delloosi ma dem noppaliku, ci seen loxo laa nekk. «Brigade de Recherches», noonu. Ngalla waay bu nu caaxaane sunuy «institutions» (campeef). Kenn musu ma sax bëmëx, kenn musu ma xoos. Kon ñooñu, ku am ñu mel noonu, àddina sépp ñee na ñu ko, ngalla waay Maki Sàll bul yàq sunu réew. Sàndarm boobu gaañu démb, ci GIGN yi ma yoroon la, di liggéeykat bu mag a mag a mag, ku bëgg réewam, tiitaru Senegaal la ; ñeewant bi mu amoon ci ñi mu doon sànni gërënaad bi, moo tax mu téyéwaat ko, moo yàq loxoom tey. Kon yooyu dañ ciy bàyyi xel, te gëm naa ni, ni mu amee ci sàndarmëri la amee ci yeneen tàkk-der yi. Kon waay-pólitig yi buñu yàq sunu diggante, nun waa Senegaal, waaye it sunu diggante ak sunuy campeef, rawatina sàndarmëri, xare bi, pólis ak leneen ak leneen.

Di wax tamit ni, Maki Sàll mooy ndeyu-mbill gi ci li xew nii ci réew mi ; te loolu dunu ko bàyyi mu jàll. Maki Sàll amul màqaamay jiite Senegaal tey jii, amu ko ! Amu ko woon démb tey doog a ñëw. Ndax man bokk naa ci lawax yi nga xam ne, bi nu génnee ci 2019, maa waxoon ñetti lawaxi kujje gi, ne leen sama ngëm-ngëm du nañ génne xale yi, mooy duñ ko jàppe ni Njiitu-Réew mi. Mooy persidã ci kanamu Yoon waaye amatul màqaama bi. Defe naa mennum man ci lawax yi, maa ci yor taxawaay boobu ba léegi. Musuleen maa dégg mani ko Persidã Maki Sàll. Maki Sàll laa koy wax ndaxte màqaama Njiitu Réew amu ko, dafa mbuxum wote bi. màqaama boobu nag, li ci desoon lu tuuti, moo fi nekkatul. Kon su nu nekkoon ci yenn anam yi, Maki Sàll dañ ko waroon a wacce tey jii. Su nu nekkoon ci yenn anam yi, waaye, foofu nag laa bëgg askan wi dëglu ma, nanu dëgloonte bu baax a baax a baax. Ndaxte, loo gis rekk teey ak dal daf cee baax. Benn, bu kenn dem pale ne Maki Sàll day wàcc ci anam yu ko neexul, ndaxte loolu baaxul ci demokaraasi, fi mu mën a jëme réew mi du baax. Moom, bu xoolee boppam ba xam ne amatul màqaaamay jiite Senegaal, mu ne «jóg naa man, bàyyi naa», na askan wépp jóg tàccu, nu waajal sunu wote, ñi war a dem, dem jàmmaarloo. Wànte, bu ko deful, nanu ko gunge ba màndaam jéex. 

Ñaareel bi, yenn boroom xam-xam yaa ngiy wax « gouvernement d’union nationale». Nun de, sama bopp laa mën a waxal ak ñi ma àndal, bokkunu, jegewunu benn xeetu guwernmaa bu Maki Sàll. Ndaxte, dañ koo nawloowul bay mën a ànd ak moom ci guwernmaa. Ndaxte koo dem ba ne dafa wor, waratoo wéy di ànd ak moom ci guwernmaa.

Léegi nag mu des, li ma bëgg waxtaaneek waa Senegaal :  coppite bi, «révolution», am na ba noppi, kenn mënautu koo téye. Bu ñu ne woon coppet Usmaan Sonko yóbbu, walla ñu def ko Dëkurwaa walla ñu def ko Séex Tijaan Jéey, walla Xalifa Sàll, ku mu mënti doon, du tee, ñii ma gis nii ci ndaw ñi, kenn mënatuleen a téye. «La révolution est en marche», te gën cee yàgg, 2024 nu mottali ko. Li ci des mooy, nanu bañ a def njuumte yi nga xam ne réewi Afrig yu bari def nañ ko fi : mooy, dañuy def seen coppite, «révolution», ba egg ca cëppaandaw ga, mu am ñu ñëw ne ko coppet, rawatina nag xare yi. Ndaxte, réew am na fu muy tollu, xare bi day jël nguur gi. Te ñaare, xare, day am yeneen réew yu am doole yuy jël seeni nit waajal leen ngir ñooñu jël réew mi. Bu nu sàgganee ba xare jël réew mi, lépp li nu doon yóotu ak di ko nas dinanu ko ñàkk. Moo tax ma ne «syndrome malien» baa ngi nii. Keroog ba ñu defee seen coppite  bay waaj a egg, ñu ne xare ba génn na, ñu topp ci «chars de combat» yi di tàccu, laa ni mbir mi jeex na, ñàkk nañu, ak feneen ak feneen ak feneen.

Moo tax coppite gi am na ba noppi. Maki Sàll mënautu koo téye, kenn mënu koo téye. Kon nan ko gunge ndaxte pexe dafa baax ci lu ne. Du lépp nag lañuy wax ci tele, waaye sunu warugar nun ñépp, askan wi, mooy nan ko gunge ba nu egg fi nu bëgg a egg. Waaye nag, loolu tekkiwul ni, danoo firi Maki Sàll rekk di ko seetaan. Nuŋ koy gunge mooy, danu koy tënk ci wenn doxalin ginnaaw-si-teyNdaxte loolu la askan wi bëgg.

Askan weey dogal tënk ci dooleem. Tënk boobu nag, bokk na ci :

– Benn lu nuy «exiger» labu ci njëkk mooy ñii nga xam ne seen bakkan rot na ci mbir mi, te muy ki ko def, moom Maki Sàll, nañu jox ndàmpaay seeni njaboot. Te ñu ubbi lànket bu tënku- wul ndax ñu xam ku tiire ak kan moo rey. Te itam, dinanu yóbbu mbir mi ci “Cour Pénale Internationale” mu àtte ko. Ndaxte, yii, ay «crimes contre l’humanité» lañu, te ci nguuru Maki Sàll la xewe fii ci Senegaal.

– Ñaareel bi, mooy ñi ci gaañu, dañ leen war a jox ndàmpaay, ñuy «civils» walla diy takk-der, jàppale leen ñu mën a faju ci ni mu gën a rafete ;

– Ñetteel bi, mooy ñi ñu jàpp ndax seen taxawaay ci pólitig bi, na leen Maki Sàll bàyyi ci ni mu gën a gaawe.

– Ñenteel bi mooy, bis niki tey dootunu nangu Maki Sàll di bunduxataal ñi àndul ak moom ak jaambur yi, di leen wattu, di leen déglu ci lu ñu yëgut, saa su ne.

– Juróomeel bi mooy, ñi nga xam ne ay sàmbaa-bóoy lañ yu mu jël, jox leen xaalis, ñu yor ay jaasi ak i fetal, nañu def lànket ba xam ñan lañu, jàpp leen, jébbal leen Yoon, ñoom ak ñi leen yónni.

– Juróom-benneel bi mooy, Maki Sàll, bëgg na ko, bañ na ko, dina fexe ba ñu mën a dem ci ay wote ni mu gën a leere. Ay wuruj «fichier électoral» jeex na ci Senegaal. Yor say kar-dàntite ne duma ko jox ndaw ñi ndax ànduñook man, jeex na ci Senegaal.

– Juróom-ñaareel bi, mooy, ci ni mu gën a gaawe, foog ñu amal wotey gox-goxaan yi, doomi-Senegaal yi tànn seeni meer. Na Maki Sàll amal it wote dipite yi ci atum 2022, doomi Senegaal yi tànn seeni dipite, jox seen bopp Péncum ndawi réew miñ bëgg. Waaye dina doxal it ci atum 2024 wote ngir tànn njiitu réew mi ci ni mu gën a rafetee. Lii, lenn rekk moo ko mën a gàntal, mooy mu dem ba xam ni moom, jiiteetul Senegaal, amatul màqaama bi, mu ne bàyyi na,  ñu amal ay wote lu jiitu 2024.

– Juróom-ñetteel bi mooy, na Maki Sàll delloo ñi mu ko xañ, seen àq ak yelleef ci pólitig : benn ci Xalifa Abaabakar Sàll mii, ñaar ci Karim Wàdd. Maki Sàll mooy tànn kuy lawax ak ku dul lawax, loolu jeex na Senegaal.

– Juróom-ñenteel bi mooy, moom Maki Sàll, na taxaw jàkkaarlook waa Senegaal yépp – amul lu ma neex laay def, walla du waaw du déet ; fii déet rekk moo fi am – ne ñetteel  sax dootuma ko tudd waxatumalaak ñetteellu moomeel. Atum 2024 Maki Sàll du nekk lawax ci Senegaal.

Lii lépp nag dafa am lu mu àndal, may ñaan askan wi, rawatina ndaw ñi, sunu taxawaay bii, bu mu wàcc mukk nag. Tey lanu war a gën a taxaw. Kenn ku ne ci nun am na sañ-sañu jëfandikoo àqam bi nga xam ne ndeyu sàrti réew mee ko ko may ni : «man duma nangu ku ma noot». Loolu ngeen def tey jii, loolu ngeen def fan yii yépp weesu. Nu wéyal taxawaay boobu. Waaye, na doon taxawaayu jàmm, ndaxte dafa am lu Maki Sàll foqati woon ci nun : kenn amatul woon sago def mbooloo. Tey, won nañ ko ni mu bëgg ko mu bañ ko danu koy def ndax ndeyu sàrti réew mi moo nu ko may…..

May wax nag, ginnaaw ba ma waxee ci Maki Sàll, may woo nun ñépp, nun ñii ñépp di ay way-pólitig ; askan wii, yelloo na ay way-pólitig yu mat. Nun ñépp amatunu sañ-sañ ci yenn yi, nanu sargal askan wi, nanu ko delloo màqaamaam, nanu ko waat nun ñépp ni, askan wi rekk moo nu ñor ; kenn newu fi di def pólitig ngir xaalis booy am ; ku bëgg ay milyaar, uti ko feneen. Waaye pólitig jaamu sa askan la, yaa ciy sonn, dugal ci sa alal, ñàkk ci ba dee, waaye waroo foog ni, ci pólitig ngay ame milyaar. Kon, nax nga sa bopp. Loolu dafa war a dakk ci Senegaal.

Man dey, man Usmaan Sonko,  tuuti naa lool ci kanamu askan wi. Gisuma lan laa def ba askan wi daj li mu daj ci nun. Kon nun it, nanu waat ni, bis niki tey, dinanu am doxalin wu yees. Ndaxte réew mi yomb naa defar de. Bii yoon, war nanoo jublu ci doxalin wu bees. Su dee nag, danuy ŋàññ ñi fi nekk ba jële leen fi, ñëw def lañu  daan def walla lu ko yées, defe naa ne, askan wi day, mujj génn ci nun ñépp. Ngalla waay nañ ci góor-góorlu.

Ma yokk ci benn poñ. May sànni ay kàddu jëmale ko ci Kaasamaas, ci mujjeelu yoon wi. Samay mbokk laay waxal, walla ñenn ci samay mbokk, ndax Yàlla may na ma ma bokk fépp. Ak lu nit mënoon a jàpp ba tax nga dugg ci àll bi, jàpp ni dañ laa xeeb, jàpp ni dañ laa boolewul, jàpp ni «citoyen de seconde zone» nga, boo xoolee li xew tey ci Senegaal, dinga xam ne loolu amut. Ndax, ginnaaw ba ma doonee doomu-Senegaal, doomu- Kasamaas laa. Waaye ñii ñépp jóg taxaw, muy Tuubaa, muy Ndar, muy Fuuta, Bakel, muy Kees ak feneen ak feneen, jóg taxaw, seetuñu kii fu mu bokk. Dëgg jot na, nanu xeex ngir dëgg sax fi. Kon, li ma leen di ñaan mooy ci 6i weer yii, li may ñaan samay mbokk yi ci Kaasamaas, ku ci yoroon ngànnaay na ko teg te bañ cee laaj dara, génn, nu bokk ndey bokk baay, te xam ne nun ñépp doomi -Senegaal lanu, doomi-Afrig lanu. Ginnaaw ga, ngeen ànd ak sunu xare, fépp fu nit ñi ne woon ngeen génne kàrt yi, génne miin yi, génne ndell yi, aar nit ñi. Bunu nangooti ñu ne dañ koy saafaraal ci ngànnaay. Ndaxte, kiy jam ak ki muy jam ñoom ñépp doomi-Senegaal lañu. Nun ñépp benn lanu. Kon loolu, mooy woote woo xam ne, maaŋ koy woote ndax lu ma ñor a ñor la. Te ku seet bu baax li xew Senegaal tey, dinga xam ne waa Senegaal yépp wone nañ ni Senegaal benn bopp lanu. Kon, lii lanu ci bëggoon sànni ciy kàddu yu gàtt…..

May rafetlu it teewaayu soxna yi ; tudduma goor ñi, bis bii, bisu jiggéen ñi la. Soxna Aminata Lóo Jeŋ, ministar bi, di ko gërëm bu baax ci teewaayam ak ci taxawaayam ci xeex bi, ndax bi mbir mi dooree rekk la dawsi  kër ga, jaa-ngeen-jëf…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj