Kollëre gi doxoon diggante Coca-Cola ak Soboa fecceeku na !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Pas gi waa Coca-Cola ak Soboa amaloon seen diggante àntuwul. Daanaka ci Suliye bi ñu dégmal la àpp pas gi di mat. Soboa nag léegi dafa bëgg a jël yoonu boppam ci liggéeyu buwaasõ bi. Waaye bu ci daanoo rekk, dina am ñétt-junniy liggéeykat yuy tumurànke Senegaal. Te yit, réew mi dina ci ñàkk fukk-ak-juróomi tamñareet ci wàllu juuti yim ko daan fay at mu nekk.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj