Gaasu Senegaal bi : lu tax tugal di ko xemmem?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Daan ya réewi tugal ya tegoon ci kow Riisi ñoo tàmbalee di dalaat seen kow. Nde, daan yooyee sabab tey jaf-jafe yu metti yi ñuy jànkonteel ci wàllum koom-koom. Daanaka lépp a yokku rawatina dund gi ak laf gi, soroj (petarol) ak gaas bi. Mooy li ñu naan dereti bopp du moy mbaggum boroom. Moo tax seen dogal yi ñu jëloon teg ko ci kow Riisi ngir lottal ko ñoo leen yóbbe tolof-tolof yii tàmbali di leen gàllankoor. Ba tax na ñoo ngi xalaat ci ni ñuy def ba génn ci gént yu naqari yi ñu nekk tey. Kurél gii di BCE (Banque Centrale Européenne) amaloon na ca bésub àjjuma 10 Suweŋ fale ca Amsterdam am ndaje. Ndaje mi nag li ko wundoon du lenn lu dul yokkute dund gi ak i mujjantalam ci seen weccit gii di Euro. Nee ñu, ni dund gi di yokkoo baaxul ci weccit gi te it dafay tax dooleem di néew. Looloo sabab seen i ndaje yu metti yi yépp. Liy firndéel mile mbir nag ñépp a ko xam. Daanaka ca Riisi ak Ikren la réewi tugal yi di jëlee/jéndee li gën a bari ci seen dund. Ana li tax kon ñu bëgg a daan Riisi, faral Ikren ?

Am na ñu naan dañu bëggoon a wàññi dooley Riisi ba mu jaral leen jël yile dogal. Amaana sax séntuwuñ ci woon lii yépp.

Tey nag, yamuñu rekk ci di def ay ndaje seen biir. Ci gaasu Afrig, rawatina bu Senegaal, lañ gën a teg seen i bët. Ci moom lañu bëgg a sampu (sukkandiku) ngir génn ci bekkoor bi ñu nekke. Ndax ci xayma, fii ak weer, dinañ tumurànke ci wàllum gaas. Ñu bari jàpp ne looloo tax Saa-tugal yi wutali Afrig, rawatina Senegaal ngir dimbalikoo seen soroj ak gaas.

Moo tax ñu gisoon fi ci lu yàggul dara ku ñuy dippe « Le Chancelier Allemand » fii ci Senegaal. Almaañ nag, mooy réew miy gën a moytu dogal yi ñoñam yiy jël ngir daan Riisi. Jàmmam moo tax muy wutali gaasu Senegaal ngir mucc ci li moom ak i ñoñam di ragal : bekkoor gi. Am na ñu naan Senegaal pare na ngir yor leen ci gaas fii ak déwen (2023).

Waaye mbir mi du fii rekk la tollu. Ndax Njiitu réew mi, Maki Sàll, Saa-Tugal yi woowoon nañ ko ci « Sommet G7 » ngir ñu xalaat ci ni mu leen di dimbalee ci gaasu Senegaal bi.  Senegaal nag pare na ngir sédd leen ci gaas bi mu yor.

Moom miy dund ay jafe-jafe yu tar ci jamono jii nu nekk ndax mën na sukkandikoo ci bile pose ngir suqali koom-koomam ? Am na ñu naan war na ko mën a def te mën na fi jaar sax suqali koom-koomam ba fàww. Waaye loolu du lu ñuy xam feek bés bi ñëwagul.

Saa-Tugal yi dañu tollu ci jamono joo xam ne mënuñu dem wëliis ñu jaar ci Afrig. Te it dañu jaaxle ba fu jaaxle yem. Daanaka seen taxawaay dese naa baax ndax am na ay lay yuy wone ni Amerig a ngi teg ay pexe ngir ñu gën a sax ci dogal yi ñu jël ci Riisi. Lan moo war a sabab lu ni mel ? Nde, Amerig dafa bëgg koom-koomu réewi tugal yi gën a suux ndax mu jaar fa diri leen fu ko neex. Maanam daf leen a bëgg def ay jàppeef (prisonniers). Pexe yi nag liñ ci jublu du leneen lu dul fexe ba mën leen a jaay gaasam ci ni mu gën a njëgee.

Li dal réewi tugal ya dafa jéggi dayo. Looloo tax ñu bëgg a song gaasu Senegaal bi. Mbir mi nag àntu na ba pare ndax Senegaal nangu na leen a jàppale. Waaye moom, ndax dina ci jële ndam ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj