Dibéer bi weesu (fukki fan ak ñaar ci weeru Me lees doon amal ñaar-fukk ak juróom benneelu bëccëgu sàmpiyonaa Senegaal. Mu waroon a ndar-kepp itam joŋantey at mi. Casa Sport mi raw-gàddu doon na ci dalal GFC. Waa géejawaay yi mujje am ndam ci kowam (2i bi ci benn). Mujjantal googu nag wàññiwul lenn ci ndamul guney Kaasamaas yi. Lu jiitu bëccëg bile, fekkoon na Casa Sport jël raw-gàddu gi ginnaaw bi mu témboo ak Tëngéej FC (1 bii ku nekk) ci bëccëgu ñaar-fukk ak juróomeel bi, fekk mu soxla woon ca lu dul benn poñ doŋŋ ngir jël raw-gàddu gi.
Bés bi mujj ci joŋante yi fekkoon na kon mu dese Casa Sport lu dul mu jot raayaam. Ba tax na doomi kaasa yépp génnoon, àndoon ak ALLEZ CASA (kurél gi ëmb way-far yu Casa sport yi) fees dell estaad bu Alin Sitooye Jaata doon jëlsi seenub raaya ak di xumbal ak a yaataayumbe.
Ikibu Kaasaa bi nag, bii mooy ñaari yoon muy jël raw-gàddu gi ci mbooru sàmpiyonaa Senegaal. Mi ngi ko jëkkoon a jël ci atum 2012, àndoon ceek tàggatkat bii di Demba Raamata Njaay ak joŋantekat yi ci mel ni Mamadiŋ Kijeraa, Estefan Baaji, Emil Póol Tendeng, Abdulaay Jàllo ak seeniy farandoo. Ca at moomee la ko mujje woon a jël. Ren jii nag, bi mu ko làbbalee, ndam li dafa gënatee neex ci ikib bi. Bu leen lig bu Senegaal warloo 35i tamndareti dërëm (35 millions FCFA) itam, Bokk-moomeelu Sigicoor ci ndogalu njiitam Usmaan Sonko dig na leen neexal bu duun. 20i tamndaret ci sunuy koppar la leen namm a jox, maanaam 500000 FCFA (téeméeri junni) ñeel ku ci nekk ci xaley Ãsu Jéeju yi (tàggatkatu ikibu Casa Sport bi). Rax-ci-dolli, Duudu Ka miy njiital dalu roppalaan (fafalnaaw) bu AIBD fas na cee yéene toftal 50i tamndaret ci sunu xaalis ngir ndokkale leen.
Ginnaaw biñ ndar-képpee Sàmpiyonaa bi, ñii di Buli Siñoor Sàmbu (Jaraaf ) ak Ngañ Faal (Génération foot) doon nañ ñi gën a ràññeeku ci joŋantekat yi. Ñoom ñaar a ëpp luñ dugal i bii. Ku ci nekk jot ngaa yëngal caax yi 13i yoon. Bokk na ci li gën a ràññeeku ci mujjantalu joŋante yi Njàmbuur ak Mbuur PC ñi topp ginnaaw ba mu waral seenug wàcc lig. Seenug wàcc googu mi ngi yemook yéegu SONACOS ak estaad bu Mbuur ci lig 1 bi ginnaaw bañ toppantee ci boppu lig 2 bi. Ñaari Tali ak Renaissance ñoom ña ngay yëngatuji ca nasiyonaal 1 at mii di ñëw.