Kuppeg àddina këlëb yi : “Real Madrid” defatina ko !
Démb ci gaawu gi, 11i Féewaryee bii atum 2023, la woon finaalu kuppeg àddina këlëb yi, mu doxoon ci digante “Real Madrid” ak “Al-Xilal”. “Real Madrid” moo dóor juróomi bal ci ñett (5-3) dellu jëlati raaya ji. Bii moom 5eelu yoonam bu muy jël bile kuppe waaye it kuppe gii doon 100eelu kuppe yu mujël ba mu sosoog leegi, muy lu rëy. Mu nekkoon finaal bu neex donte ñu bari nag xamoon nañu ni Real Madrid daf koy dóor, waaye it taxul Al-Xilal yombalal ko ko, ñëw na ak bëgg-bëgg xeex ca la mu mën.
Gannaaw fan yu xaw a lëndëm yi mu nekkewoon ci fan yii ñu génn, rawatina ba leen “Barça” dóoree woon Finaal, gisoon nanu ni dafa xawoon a baayi loxoom walla mel ne ku réeraloon wureem. Kuppe gii ñu jël démb yaakaar naa ni dana nekk lu leen di dolli jom ci li des ci at mi. Fi mu toll nii moo ngi war a dajeeti ak “Barça” 1/2 kuppeg buuru Espaañ (coupe du roi), war a xëccoo ak moom ba tay Sàmpiyonaa ba, ba noppi xeexi nguuram ga xa “League des Champions”.
Ana kukoy tee, Vinisis ?
Saa-beresil bi, luñu ko gën a xeex, muy gën a wane boppam. Fan yii weesu gis nañu na koy moroomi wurekatam sonalee ca Espaañ, nga xam ni dañu koy cokkaas ak di ko gaañ, leeg sax soppey yeneen këlëb di ko saaga ak a xas ndax limuy ku ñuul. Loolu lépp teewul muy yokk jom ak fi gën a wane boppam. Démb ci seen finaal bi mu taal ñaariyoon kër gi ba noppi joxe ci ñu dugal. Gannaaw loolu ñu fal ko wurekat bi gënoon xereñ ci kuppeg àddina këlëb gi. Kii di Walweerde (Valverde) dugalatina ñaari bay ci démb, yeewuwaat ci nelaw yi mu nekke woon ba noppi weesu lim bi ko tàggatkatam bi tegaloon ngir mi dugal lu tol noon mbaa lu ko ëpp (10). Bensemaa it jot na ci dugal bennam. Loolu di mbégte ci waa “Real Madrid” ak seen soppe yépp.