ËMMA SEEN DAAN NA SAA-CEES !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci dibéer ji, 5i fan ci weeru Me 2024, la doomu Pikin ji, Ëmma Seen doon sëgg ak Saa-cees, doomu Géejawaay ji. Seen bëre nekkoon lees doon xaar. Nde, dañu doon ñaari mbër yoy, duñu yàq làmb. Bu ñu bëree mu neex, bu ñu xeexee mu neex. Kii di doomu Pikin ji nag moo mujje am ndam ci kaw Saa-Cees.

Seen bëre bi nag, yéex naa tàmbali. Ndaxte, ñu ngi sëgg bi 22i waxtu tegee 36i simili. Ba mu tàmbalee, ñaari mbër yi, ku nekk a ngi ne tekk di jàng sa moroom. Saa-Cees, lees ko xamee woon mooy ni songkat la, ci simili yu njëkk yi lay jëli naatangoom, mu jigoon ko nag. Waaye, ci bésu démb ji, dafa ñëw taxaw di déglu. Ndax, Ëmma nag, du mbër mu ndaw. Ñaari mbër yi di léewtoo lu tollu ci 3i simili, Saa-cees tàmbali gëdd doomu pikin ji. Ñoom ñaar ñu sànnantey kurpeñ. Muy lees doon xaar ci ñoom. Ñu xeex xeex bu metti, ku nekk ni waat tekk di déglu sa moroom. Niki ñuy léewtoowaat ba mu yàgg, arbit bi woo leen, wax ak ñoom ngir ñu bëre. Ñu gis ne Saa-cees dafa gaañu ci loxo bi, mu dem ardo ñu xool ko. Ba mu delsee, ñoom ñaar tàmbaleeti di léewtoo lu tollu ci 1 simili, rakku Bàlla Gay ji dellu ca ardo mu xoolaat ko. Bi ñu ko xoolee gis ni mën na àggali mu dikkaat ci géew gi. Ci noonu, arbit ëfëlaat leen, yàggul dara Saa-cees yéegat ci kaw Ëmma Seen. Ñaari mbër yi di xeex. Noonu rekk Ëmma daw jàpp ko, jéem ko tegal siis, Saa-cees bañ. Ñu nekk ci noonu, Ëmma féete suuf di bañ-bañlu ba jugaat daldi takk doomu Géejawaay ji, daan ko. Noonu la seen bëre bi demee. Ku nekk joxe na lim am, wane jom, fullaak fayda jees leen xamee woon.

Pokola Balde itam moo mujje daan kii di Liis-Njaago. Mu nekkoon bëre bu neex a neex. Ñaari mbër yi xeex ci xeex bu metti. Daanaka, ca jàkkaarloo ya la tàmbali woon a takkarnaase sax nag. Ci bëre bi, ñu xeex ba kii di Pokala dem ardo ñaari yoon. Waaye, mu nekk ci rekk ba mujje am ndam ci kaw Liis-Njaago. Mu nekkoon bés bu neex ci làmb. Nde, ay waada rekk a doon daje démb. Rax-ci-dolli, mu bari woon i soppe yu seetaansi woon.

Ci bés bi tam, Bàlla Gay 2 ak Tafaa Ti mim war a dajeel. Ñu nappante fa, ku nekk di jéem a xëbal sa moroom ak di ko wax mu waajal bés bi, ndax du yomb.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj