Ci at mu réy mi mu amal ren ak ekibam bii di Red Star ca Nasiyonaal 1 bu Farãs , Saa-Senegaal bi daldi nay yéegal këlëb ba ca Lig 2 ba. Jaloore ju réy jooju mu def moo tax sax ñu sargal ko, tabb ko tàggatkat bi gën a xarañ ca sàmpiyonaa nasiyonaal 1 ba.
Gannaaw liggéey bu rëy bim amal, xamle na ni teg na bëtam fu gën a kawe. Ndax, bi ñu ko laajee ndax bëgg na yor Olympique de Marseille, ci kàddu yii la tontoo:
“Ëllëg, bu ma OM soxlaa, damay dem. Mooy këlëb bi ma gën a sol mbégte sama xaleel ba nii. Nekkoon naa fa it kàppiten. Bu ma Marseille woowee, damay daw sumay dem. Awma benn ayib ngir wax ko.”
Kalidu Kulibali jënd na këlëb !
Kàppitenu ekib nasiyonaal bu Senegaal bi, K. Kulibali topp na ci tànki Saajo Maane. Ci fan yii nu génn la nekk waadab sàmpiyonaa Araabi Sawdit ak këlëbam bii di Al Hilaal. Mu jóge ci loolu daldi jënd moom it këlëb bii di SC Sedan te mu nekk Farãs.
Ligue des champions : Aston Villa day bokk déwén
1983 ba tey, këlëbu Àngalteer bii di Aston Villa mësul a bokk ci joŋantey Liguedeschampions. Déwén mooy doon guléet mu ciy bokk. Dafa di, ren, Unaï Emery ak ndawam dañu wane njàmbaar ak jom ci sàmpiyonaa “Première League” bi. Unaï Emery, seen tàggatkat bi, bay na ci waar wu rëy.
Mbappe : dem bi leer na léegi !
Keroog, ci dibéer ji, la futbalkat Farãs bi doon amal joŋanteem bu mujj ak Paris Saint-Germain fa seen pàkk, Park des princes. Lu jiitu loolu nag, biraloon na ci benn widewoo bum fësal ci xëtu Twitteram ni moom ak Paris Saint-Germain jeex na. Bind na li muy bind ca mbooru sàmpiyonaa Farãs ba noppi, moo ngi jéggaani feneen.
Fa ko ñépp di séntu nag mooy Real Madrid, këlëb bi ko yàgg a bëgg, yàgg a dox ngir jënd ko. Ci wewu béy, jëlees na ci ne xaatim na bu yàgg, siiwal rekk ci des.
Kalifikaasiyoŋ Kuppeg àddina 2026
3eel ak 4eeli bés
Senegaal dina dalal RD Kóngoo keroog 6i fan ci suwe 2024 ca Jamñaajo laata muy fekki Móritani ca Nuwaksot bésub 9i fan ci weeru suwe ba tey.