Démb, ci àllarba ji, lees doon amal ñaareelu joŋantey demi-finaali “Ligue des champions” bi, diggante Real Madrid ak Bayern Munich. Lu ko jiitu, ci talaata, Paris Saint-Germain doon na janook Dortmund. Dafa di nag, Dortmund ak Real Madrid ñoo am ndam ci seen i joŋante, war a daje ci finaal bi war a am keroog 1eelu fan ci weeru suwe fa Wembley.
Paris Saint-Germain – Dortmund
Saa-Almaañ yi ñoo toogloo farãse yi ci seen ñaari joŋante yi. Paris Saint-Germain moo njëkk a fekki, keroog 30i fan ci weeru awril wii, Dortmund daldi koy dóor 1-0. Barki-démb, ci talaata ji, 7i Me 2024, mu fekksi ko ca fowoom bees duppee “Parc des princes”, gañewaat ko benn bal ci dara, daldi jàll finaal.
Real Madrid – Bayern Munich
Ci weneen wàll wi, waada (champion) Espaañ bi moo toogloo yeneen Saa-Almaañ yi. Ñu amal ñaari joŋante yu metti lool nag. Keroog, bu njëkk ba, 29i Awril 2024, la Real Madrid fekki woon Bayern ca pàkkam, ndaje ma metti, ñu mujjee timboo 2-2. Ci àllarbay démb ji, 8i Me 2024, Bayern Munich daldi fekksi Saa-Espaañ yi seen dëkk. Niki bu njëkk ba, ndaje mi metti lool. Ci 2eelu xaaju joŋante bi la Bayern njëkk a dugal (Alphonso Davies, 68eeli simili). Naka noona, Real Madrid daldi koy tontu, dugal, dugalaat. Joselu moo dugal ñaari bii yi (88eel ak 90+1eel).
Noonu la 1/2 yi demee. Ñaari way-bom yi war a daje bés bi njëkk ci weeru suwe wees dëgmal, fa Wembley (Àngalteer).