REAL MADRID DEFATI NA KO !

Yeneen i xët

Aji bind ji

15i kub ! Real Madrid kepp moo ko fi defagum ci joŋantey Ligue des Champions bi. Ndax, ci gaawu gii, 1eelu fanu suwe 2024, la dóor Dortmund 2-0, jëlati kub bi. Mu nekk luy gën a yokk i jalooreem ci mbooru joŋanteb futbal boobule nga xam ne, moo ëpp dayo fa tugal.

Barki-démb la Real Madrid doon daje ak Dortmund ñeel finaalu League des champions bi. Saa-Espaañ yi ñoo ko mujje gañe gannaaw mats bu metti boo xam ni bii, Saa-Almaañ yi ñoo jekku daanaka la ca ëpp.

Ca xaaj wu njëkk wa, Dortmund waroon na mën a jiital ca ndaje ma. Waaye, li ñu moyal ci bal yu waroon nekk bii dafa bari. Ñoom ñoo jekku daanaka xaaj woowu yépp, ñu mitã ci 0-0. Ba ñu dikkaatee, naka noonu, mu sëppaat ekibu Real Madrid bi. Wànte, Real Madrid, loo ko sëpp sëpp, danga koy bàyyi xel. Ndaxte, ay songukatam dañu gaaw te daanaka luñ am dugal ko. Noonu, ñuy dawal ci ñaareelu xaaj wa ba ca 73eelu simili ba, cib korneer Dani Carvajal daldi dugal mbëkk mu réy. Ba loolu amee ñu seetlu ne Saa-Espaañ yi dañ yeewu, wëlbati mbir yi, sëpp waa Dortmund. Real Madrid di dawal, di dawal ba 83eelu simili ba, Maatsen (Dortmund) daldi juum ci paas, jox Bellingham bal bi, mu yokkal ko Vinicius Junior mu tojati kër ga. Ci 2-0 yooyu la jeexee.

Real Madrid daldi yokk beneen kub ca yam amoon. Mu nekk it ñetteeli kub bum gañe ci ren jii (Super coupe d’Espagne, Liga, League des Champions).

JALOORE BIIR JALOORE

Wëliis jaloore ji Real Madrid def, am nay kuppekat yu def i jalore tamit. Tony Kroos, Nacho, Carvajal ak Modric, ku ci nekk, góob na 6eelu kubam ci League des Champions bi. Tony Kroos, moom, finaal booboo nekkoon mujjantalu joŋanteem ak Real Madrid. Muy mujju gu rafet ci moom.

Kii di Arda Güler, xale bu bees bi Real Madrid jënd ren, mooy Saa-Tirkii bi njëkk a gañe bile kub. Bellingham itam ñëw ren, am ko ren. Yamu ca de. Ndax, Ancelotti tamit, tàggatkat ba, doonaale na ca tàggatkat bi njëkk a am 7i kubu League des Champions ci mbooru futbal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj