Ci li nu tàmm a dégg, boroom-kër, góor lees koy askanale. Waaye, bees settantalee Alxuraan, dees na gis ne jigéen la moomale kër gi. Daanaka, fu ab laaya tuddee jigéen ak kër, moomeel ga ca moom lay dellu :
“Nangeen fàttaliku li Nu leen jàngal ci seen biiri kër, te mu bokk ci laayay Yàlla yi , Alxuraan ak lépp luy xereñe. Yàlla dey Kuy ñeewante la, di Kuy xàmmee.”
(Saar 33eel, laaya 34)
Fii, mi ngi wax ak Soxnay Yonnent bi, ca lañuy teewlu ci Waxi Boroom Bi ak i xereñteef yiy wàcc ci seen kër yi. Waaye, taxut Alxuraan askanale kër gi Yonnent bi, Soxna yi la ko askanale.
” Eey yaw Yonent bi ! Su ngeen di faseeti jigéen ñi, nangeen leen di fase cig laab ; te nangeen di lim yidda ja ; nangeen ragal Yàlla seen Boroom. Te bu leen leen génnee ci seen i néeg…”
(Saar 65eel, laaya 1)
Fii, doonte xiiroo ak ŋaayoo am na ba tas war caa am yoon, terewut moomeelug kër dafay des di ko ñeel.
Fenn rekk la Alxuraan roccee moomeel gi ci moom, mooy mu indi ñaawteef (njaaloo) wuy gàkkal kër gi :
“Ña def ñaawteef [njaaloo] ci seen i jigéen, nangeen ko seedeloo ñeenti nit ci yeen. Bu ñu ko seedee, nangeen leen tëj ba dee fekk leen fa walla ba Yàlla ubbil leen aw yoon [wu ñu mën a aw ba mucc].”
(Saar 4eel, laaya 15)
Kon, lii, lees ci man a dégge mooy solo si Lislaam jox jigéen ci biir kër gi, xam ne keno la bob bu nërmeeloo rekk, kër gi màbb.
Yaay, Soxna, Doom, Rakk, Mag, Yàlla na leen Boroom Bi taxawu.