Xeet wii di Himbaa, fa Namibi, bis bi ñuy màggal ak a fàttaliku seen juddug doom (anniversaire), duñu ko jàpp ci bisub juddu bi, waaye, lu jiitu xale biy juddu : bis bi nday ji njëkkee daj cim xelam ne dafa nàmm a am doom, bis boobee lañuy jàpp ne mooy bis bees war a màggal.
Ci kow loolu, bis bi yëg-yëgu amug doom toqee ci xolub nday ji, dafay dem ci ab taatu garab, toog fa ab diir, di janeer ak a xalaat ba wayu doom ji war a juddu feeñu ko (waxin la, waaye nday ji a koy fent), mu tàmbalee way way wi. Naka noonu, mu dem ci ki war a nekk baayu doom ji, jàngal ko way wi ba mu mokk. Ginnaaw gi, ñu jaxasoo cib séy ngir amal jëmmu xale bi war a juddu. Ci biir séy bi, ñoom ñaar dañuy way way wi ba ni ñuy noppee.
Bu ñu jógee ci loolu, bu ci ab ëmb tofoo, nday ji dafay jàngal way wi magi gox bi (jigéen ñi) ak rewlekat yi ba ñu mokkal way wi. Bis bi muy wësin, ñu koy wayal way wi.
Ci noonu, way wi dafay topp gone gi giiru dundam. Ndaxte, moom itam, dees na ko jàngal way wi. Ñi xamante ak moom it, jàng way wi. Bis bu amee ndam walla mu def jaloore ju réy, ñu wayal ko way wi, bu nekkee ciy xat-xat ak i tolof-tolof, ñu wayal ko way wi. Bis bu defee njombe walla toj-toj, ñu woo ko ci pénc mi, ñépp wër ko, ñu wayal ko way wi. Ndax ci li ñu jàpp mooy ne, mbugal nit ki ndax toj-toj bu mu def doonut lu war ci bees ko manee tegaat ciw yoon, jaare ko ci anam bob, nit ki dina rus mbaa mu jomb a defati ab ñaawteef buy lor askanam. Bu demee ba tawat nekk di sukuraat, ay jegeñaaleem wër ko di ko wayal way wi ba ni ruu gi ak jëmm ji di teqalikoo.
Mel na ni way wii nga xam ne nday ji moo koy fent, jàpp ne way la wow, doom ji ci boppam moo ko yenkeewal laata muy judd, dafay dëggal seen ug ngëm ci ne ruuwu nit ki mësut a téqaliku ak nekk, donte amagut jëmm ju koy gunge ci sunu àdduna sii ñu nekk, donte sax ndayam ak baayam joteeguñu ngir mu man caa sosoo.
Dafa may fàttali it benn téere bob dawaloon naa ko luy toll fukki at ci ginnaaw, ab boroom xam-xam bindoon ko, sukkandiku woon ci mbir yoy, ay nit ñoo ko dundoon, di ci fésal seen i seede ci ne lii di ruuwu nit ki dafay am i jaar-jaar yu bari donte nekkagut ci jenn jëmm, ay jaar-jaar yoy, nit ki ginnaaw juddoom, bu gimmee mën na am yu ci baamtuwaat cig dundam, ba tax léeg-léeg nga dund mbir ci saa si nga mel ni ku ko mësoon a dund lu yàgg. Waaye, xamatoo kañ la woon ak naka la woon ak fan la woon.