Ndam la féete na wet. PASTEF a gobbi lépp, lëmbe géew bi, gën a sampu. Gaa ña wër ko, njiin ma jóg, bàkk ma jib : « Curr… Cëgindu ndàq ! …»
Mbër mi am na ngemb, ay bokkam yab ko. Taxawaay ba mat na. Doole ja bari na. Doo ko njoolu. Doo ko suufu. Loxo ba jot na. Loxo ba diis na. Du xàcc. Du méb. Dóor ba it du moy. Kurfañ ba ñu mooñe ko làpptaake : térr… dipp… dett… mbëpp !
Mbàpatoo-mbàppat, jaar na fa, toj fépp. Mbëroo-mbër, sëgg na ak moom. Ñii mu mbot, ñee mu xàttarbi, nale mu pàdd, ña ca des mu yanu. Taxut mu naagu. Taxut mu daagu.
Mbër yi koy dëkk, kaayleen ma déey leen. Laata ngay samp ndënd, bàyyil xel yii :
-
Boo réeree mbër, boo ko dëkkee doo ca am ndam ;
-
Xam sikki mbër ak i gaafam, taxut nga daan mbër ;
-
Xam mbër mooy, xam maniinam, xam dayoom ;
-
Xam, jëf a cay topp : nangul ko dayo ba, boole ca wegeel ; xàlli aw yoon wu dëppoo ak maniinam ak dayoom ;
-
Ndax li tax ba léegi manoo am ndam ci kawam, ay sikkam rekk a la ñor, di ko xaxaree ay gaafam. Te loolu ubut làmb.
-
Ma baamtuwaat ko, bu leerut, ci yile waat : li jiitu ci nooneel, laata ngay taxawal am PEXE, mooy nga xam sa manoore yi sa nattaangoo làmboo, nga nangul ko ko. Bu loolu amut, wegeel du am. Te, koo desee weg, noppee am ndam ci kawam. Lijjanti ay manoreem na doon sa itte ju njëkk. Ndax, moom rekk moo la man a may nga lal am pexe mu méngoo ak dayoom.