« WAXLEEN DËGG SONKO ! »

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ànd, wax dëgg ca la. Ànd bu laluwut ci dëgg, du yàgg. Te, sa waay, boo ko bëggee, danga koy wax dëgg… Yii yépp, ak li ko niru, ay cëslaay lañu yoy, deesu ci werante.

Mu doon ay kàddu yees di faral a dégg ñaare ci mbir yu soxal Usmaan Sonko. Sànnikatu xeer yi duñu deñ ci di wax : “Waxleen seen waay ji dëgg !”. Ñenn ci njaboot gi, walla ñi safoo PASTEF itam, leeg-leeg haal dikkal leen, ñu joqarbi Sonko, duut ko baaraam.

Mu doon lol, manees na leen koo nangul, ndax ñaari yëf :

– Gisiin yu wuute manut a ñàkk ;
– Nit matut te, kuy wax, yaay juum.

Waaye, li soxal njaboot gi ak ñi safoo PASTEF, am na ci mbir yoy, war nañu cee bàyyi xel :

– Laata ngeen di ànd ak Sonko, natt ngeen ko ci jikko, ci xalaat, ci jaar-jaar ba gis ne am na lu nekk ci moom lees namoon a gis ci njiital polotig te nekkut ci ay moroomam ;

– Am ngeen njort bu rafet ne yoon wii mu xàll man na a jëme réew mi fa gën ci moom ;

– Bu ñaari sàrt yii dajee, ngeen ànd ak moom di ko gunge, muy wéy, di wéyal, du ñàkk leeg-leeg am ndog ci yoon wi. Ndax, nit la te dafay juum. Waaye, ndax loolu dafa tekki ne sa wareef mooy nga taaj ko ci pénc mi di ko joqarbi ak a duut baaraam ? Mukk ! Li war te jëkk, mooy xool lees di tudde njuumte ndax dëgg-dëgg loolu la. Ndax bari na lees di tudde njuumte fekk du ko. Waaye, bu fekkee dëgg-dëgg njuumte la, laaj bi war a jëkk a samp mooy : ndax laal na cëslaay yi tax ma àndoon ak moom ? Bu fekkee laalut ko lu dut ne sikk la ci wàllu pexe (Stratégie), jarut a xabtalu. Ndax ñaari mbir, di ànd ak sànnikatu xeer yi ngir jéebaane ko ci pénc mi :

– Bokk na ci nees di aaree ak sàmm Sémb wi (le Projet), di moytoo jógandoo ak ña nga xam ne, bu seen yéene sotti woon, tay yeen ñépp a nga kaso mbaa bàmmeel, ñu naan ndem-si-Yàlla PASTEF… Ndax lépp lees mës a teg seen kaw niki tooñ, àndoon nañu ca. Ñooñu, fu ñu waxee guy ga, neel daqaar ga. Lu bon lañuy xëy di wër suba ba ngoon jot, doonte kàdduy dëgg lañuy jibal. Dafa di nag, jubluwaay ba, ay neen la ni ko Alquraan misaalee.

– Ku xam ni PASTEF bindoo, Sonko du kok, dees ko bàyyee ak cëggal guyam fu ko neex gësëm… Lees war a jubbanti ci ay doxaliinam dees na ko ko yégge ci waxtaanu biir néeg. Te, moom it, mu amug woyof di déglu ak a ñoŋal boppam… Nde, bu nekkut woon loolu, tay PASTEF du egsi fii mu nekk tay.

Ci gàttal, ñi tànn PASTEF ndax ay cëslaay, fii ak loolu soppikuwut, nañuy ànd ak dal ak xel mu teey ci yenn ndog-ndog walla coow yi nga xam ne, génnut yoonu pexe. Li ngeen daj ba egsi fii, fàww ngeen ànd ak farlu gu raw ga ngeen amoon ngir man a jëmmal seen i mbébet. Ndax, ñi doon gor seen i tànk démb ak barki-démb, ñoo ngi fi ba tay… Te seen lajj doŋŋ lañuy xaar. Dara ñorut leen lu dut réew mi tagatémbe ba ñuy wax ne “waxoon naa leen ko, ñii duñu gaa ña”.

Buleen jël mukk seen i kàddu ñoom, di ci sukkandikoo ngir nattee ko seen taxawaayu bopp. Buleen déglu seen i kàddu ya ñuy jibal, lu ci mel ne “seen waay ji du ngeen ko wax dëgg”…

Seen waay ji, yeen a ko tànn, yeen a ko safoo. Fii ak wàccut yoonam, buleen deñ ci di ko taxawu. Lees man a tudde ay “rëcc-rëcc” ciy kàddoom, mooy “tojtal” bi, bu dut woon loolu mu nekk “Malaaka”. Kon nangul-leen ko ko te wéy ànd ak moom wéyal liggéey bi.

Seexunaa Njaay
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj