AFROBASKET-KIGALI 2023 : XALAM DEMOON NA BAY NEEX !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb la woon finaalu Afrobasket bi doon am ren ca Ruwàndaa, doxoon ci diggante Senegaal ak Niseriyaa. Niseriyaa nag moo ko mujje gañe, daldi jël kub bi.

Senegaal, ca njëlbeen ga, ku la waxoon ni dana finaalu nga weddi ko. Nde, dafa lajj ñaari yoon ca ndoorteelu xëccoo bi (tournoi). Gannaaw ba ko Ugàndaa dóoree 85 ci 83, Mali tamit daf ko dóoroon 72 ci 49. Ca la gaynde yu jigéen yi fippoo, jàpp Esipt mi nga xam ni ci ñaaari at yii bojo-bojoom la ko def, gañe ko 71 ci 60. Mu jóge foofu, ba tay, gañewaat kii di Kamerun 80 ci 77 jàll ci dëmi-finaal yi. Noonu, mu dajewaat ak Mali mi ko dóoroon ca ñaareelu joŋanteem ba, daldi fayu, gañe ko 75 ci 65. Ndax, wolof dafa ni, dóor, fayu. Démb nag, ci gaawu gi la doon daje ak Niseriyaa ci finaal bi. Waaye, Niseriyaa a ko mujje gañe 84i poñ ci 74, muy fukki poñ yi dox seen diggante.

Kii di Siyeraa Siney Dilaar mi nga xam ni, wii yoon lay door a ñëw ci ekib bi, moo mujje jël raw-gàddu bi ñu tegaloon ki dàq a doxal, muy lu mu jagoo gannaaw lu rëy la mu basket ci diiru xëccoo bi.

Kii di seen tàggatkatu bi nag, Mustafaa Gay àggaliwul finaal bi ndax dafa géddoon, dem bàyyi leen fa ba mu xaajee. Loolu nag, nekk na loo xam ni rafetul wenn yoon. Ndax, ñoo xam ni yaa leen war a taxawu bu leen ñépp bàyyi woon, yaa leen war a taxawu, fital leen, ngay dem di leen bàyyeek seen bopp.

Ci kow loolu, Siyeraa Siney Dilaar yékkati nay kàddu di ŋàññ doxalinu Mustafaa Gay mi leen doon tàggat : ” Liy wutaley ekib ci sàmpiyonaa, mooy tàggakat. Guleet may gis ab tàggatkat buy bàyyi ak a gédd ekibam ci xaaju joŋanteb sàmpiyonaa.”

Mustafaa Gay sax xamle na ni dafa daldi bàyyi, nekkatul tàggatkatu ekib bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj