Ginnaaw bi mu sottalee nas boobu mu duppe woon “Akon lightening Africa”, kii di Aliyun Badara Caam di doomu-Senegaal bu nekk ca Amerig moo doon taxawal démb ci altine ji ñaareelu nasam. Muy ab dëkkub lëmm bu mucc ayib te méngoo ak jamono, wara tollu ci 800i ektaar, ñu xayma njëg li ci 3300i milyaar ci sunu koppar.