AMNESTI : MAKI XÀLL NA YOONU JÀMMOO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fan yii, ñoo ngi soow mbirum amnesti (mbaale) bi Njiitu réew mi junjoon. Amnesti boobu, lees ci jublu mooy far lépp li fi jot a xew diggante màrs 2021 ak suwe 2023. Diir boobu nag, ay bakkan yu baree ci rot, ñu jàpp ci kaso lim bu takkoo takku. Moo tax, am na ñu àndul ci manesti bi. Moo tax it, jur na xaat coow ak xàjjalikoo te dara xewagut.

Dafa di, bu naalub amnesti bi àntoo, mooy képp ku ca yoon jàppoon mbaa ñu tuumaal la ci dara, yoon daf lay bàyyi mbaa mu setal la ba nga set wecc, kenn dootu la toppeeti dara. Ñu gis ne, démb ba tey, ñu ngiy génnee ñu bari ci kasoy Ndakaaru yi. Moo xam ña fare ca làngug pólitigu pastef wala way-moomeel yi. Aliyun Saane, Mor Taala géy (Nitdof), Tusee Màngaa, Paap Abdulaay Ture, Yarga Si, Séex Umar Jaañ, Ustaas Asan Sekk, Doktoor Seydu Jàllo, Fadiilu Keyta, añs. Waaye, ñi ñu jàppagum ci kasoy diiwaan yi moom, bàyyeeguñ leen.

Fa xel yépp daje nag, mooy fa kasob “Cap Manuel”. Nde, fa lees jàppandi njiitul Pasteef la woon, di Usmaan Sonko, meeru Sigicoor bi. Ndax Maki Sàll day génne wujju pólitigam bi ko gën a sonal ? Muy laaj bi jar a laaj.

Dafa di, for nañu ci wewu béy ne, gaa ñaa nga cay dox ay jéego. Ñu ràññee ca taxawaayu Piyeer Gujaabi Atepaa ak Aliyun Tin. Ñoom nag, duggewuñu ko lu dut jàmm dellusi ci réew mi. Ndax bu ñu sukkandikoo ci Piyeer Gujaabi Atepaa mi séqoon waxtaan ak RFI, moom ak ñeneen ñoo ngi dox ak a def i pexe ngir disoo bi Maki Sàll di sàkku, Sonko mën caa bokk. Te, ma ngay xaar tontul Sonko bu ci waxtaane ak ay jegeñaaleem. Loolu, day ruumandaat ne njiitul Pastef laa ngi ci tànki génn. Mu nar a nekk coow ci kow coow. Ndax APR a ngi xaacu fii, naan dee du fi ame. Waa Pastef tamit, di xataraayu fee, naan ñoom waxtaanuñ ak Maki Sàll. Li ci kanam nag, rawul i gët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj