Keroog, ci gaawu gi 29 awril 2023, sàmpiyonaa Senegaal bi jaxoon na lool. Ndax, As Pikine ak Guédiawaye Fc ñoo doon daje. Mu nekkoon joŋante boo xam ne, ñi ko doon xaar bari nañ. Ndaxte kat, du joŋante bu ndaw. Mënees na jàpp ne sax, ni fii ci Senegaal, mooy sunu Barça-Real, walla sax Paris Saint-Germain-Marseille. As Pikine ak Guédiawaye Fc di ñaari ekib yu bokk daanaka benn gox mbaa nu wax ni ñoo takkaloo, ñuy yenn ci ekib yu gën a mag ci sàmpiyonaa Senegaal gi.
As Pikine bu waree joŋante, ni ñuy waajalee seen bés yi ak soppe yu bari te gëm ekib ba nañuy mel, meneen mbir la. Muy këlëb bu yàgg a wane boppam, di ekib bu mag. Guédiawaye Fc itam, naka noonu. Ci at yii ñu génn, gis nañu jaloore yi mu fi def yépp : wàcc Ligue 2 bi, jël ko yéegaat fekki punkali Ligue 1 yi.
Gis nañu nag, ñi dëkke ca gox ya na ñuy jàppee ci seen i ekib ak liñ leen jaral. Ku ci mel ne Bàlla Gay, mbër mu mag mi dëkke Géejawaay, def na ci waajtaayu joŋante bi benn tamndaret ci sunuy koppar, mu nekk luy dooleel ekib ba ci lu bari.
Joŋante bi nag, barkaati-démb, ci gaawu gi, la amoon. Rëyaayu joŋante ba taxoon na ñu bàyyi fowu yépp, tóxal ko ca fowub Abdulaay Wàdd, Jamñaajo, fa ekibu Senegaal bu mag biy joŋante. Ekib bu ci nekk, indi nga say soppe, mu neexoon lool, xumb ba dee. Joŋante bi nag neexoon na lool, bal bi daw na, futbal bi set na. Waaye nag, ndam demul, ndam dikkul. Ñaari ekib dañoo mujje joxante loxo, kenn dugalul sa moroom. Guédiawaye Fc, boo xoolee, moo féete kaw. Ndaxte, mooy nekkagum ci ñetteelu toogub sàmpiyonaa ba ak 31i poñ, As Pikine jëlagum 6eel ak 25i poñ.
Joŋante bi jur na liñ ci doon xaar, muy kuppe gu rafet, bal bi daw, ñu amal ko ci jàmm. Ba ci soppe yi nekkoon ci kaw, yëngal nañu ba mu neex, lépp ci jàmm ak salaam.
Ñu bari nag rafetlu nañu ni ñu yóbboo joŋante gi ci bóobee bërëb. Ndax, jàpp nañ ne dina gën a may bët ak bayre sàmpiyonaa bi. Rax-ci-dolli, ekib boo fa yóbbu, daanaka ay soppeem dinañu sawar a seetaani ko, te dina dundal sàmpiyonaa bi ak kuppeg Senegaal.
Ñoo ngi xaarandi yeneen bés yu ni mel. Ndax, bile moom neexoon na lool. Te, lu neex du doy. Ndaxte, xumb na, dagan na.