Saa-Gana bi, Atsu (1992-2023), mujje na feeñ ginnaaw bi mu réere ci màbbiti taax ya daanu ci sababu rëng-rëng ba ca Tirkii. Ndeysaan, dañoo fekk mu dee. Moom nag, wurekat bu mag bu ñu ràññe la woon fii ci Afrig ak fa Tugal. Loolu nekk lu tiis ciy ñoñam, ciy naataangoom, waaye itam ciy soppeem rawatina waa Afrig yi. Keroog, 6i fan ci féewaryee 2023, la suuf sa yëngu woon diggante ñaari réew yii di Tirkii ak Siri, ñu baree bari ñàkke ci seen i bakkan.
Kiriscaan Atsu nag, Fc Porto la njëkkoon nekk, atum 2011. Mu jóge fa, dem Àngalteer. Nde, atum 2013 la jóge Fc Porto fekki Chelsea. Daanaka solul mayo Chelsea ndax jamonoy Móriñoo la fa dikk, jotul sax bokk ci benn joŋante, ñu abale ko. ci ñeenti këlëb lañ ko abale foofu ca Àngalteer, Everton, Bournemouth ak Newcastle. Kon yàgg na fa.
Ginnaaw loolu la génn tugal dem Araabi Sawdid am fa ñaari at ak këlëb bii di Al Raed. Xaatim ba leen lënkale woon ba mu jeexee la moom boppam, dem fële ca Tirkii fasante ak Hatayspor atum 2022. Foofu nag, ñeenti joŋante rekk la fa jot a am. Ñeenteel bi mooy keroog 5i féewaryee bii, ekibam doon daje ak Kasimpasa, nga xam ni benn bal ba ca duggoon moo ko dugal ba mu desee woon as tuut ca joŋante ba. Bal boobee taxoon ñu gañe joŋante ba ba noppi juroon mbégte gu rëy ca xoli soppey këlëb ba. Ca ëllëgu bés boobu la Yàlla Buur bi dikk ak ndogalam, suuf si xëy di yëngu yëngu yu metti foofu ca Tirkii ak Siri.
Moom Atsu, bañ ca tegeey fan yu néew, ay xibaar génnoon di xamle ni gis nañ ko ak ay gaañu-gaañu waaye deewul, ba xel yi tàmbali woon a dal. Xibaar boobu tax bu gaaw, ca ngoonu bés ba njaatigeem (agent) génn weddi loolu ni kenn gisul Atsu ba léegi. Bërki-démb ci gaawu bi nag, ba nu xëyee, moom njaatigeem bi bind xamle ni gis nañ ko ca biir bekkit ya mu ñàkk bakanam ci anam yu doywaar.
démb ku seetaan Sàmpiyonaa ya rawatina Àngalteer gis nga ekib ya doon ko sargal ak di ko mastawu njabootam ak àddina sépp.