AYSATA : TAAL BI DU AY FEN ÑOO KOY FAY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kii di John Mearsheimer, ca atum 2011, dafa génne ab téere tudde ko “Why Leaders Lie : The Truth About Lying in International Politics” di jàngat li tax njiit yiy fen ak a kàcc, rawatina lu jëm ci pólotig bi aju ci seen diggante ak yeneen réew yi.

Doonte Mearsheimer, li ëpp ci téere bi mi ngi ko jëme ci fen yi aju ci jëf ak bir yi soxal bitim-réew te njiit yi di ko taxawe, waaye dafa cee leralaale ne fen yi bu fekkoon ne mbaal la, askan wi lay njëkk a napp ba noppi door a jàll ci biti. Maanaam, fen wi paaka ñaari wet la : dafay dagg ci biir, di dagg ci biti.

Fen wi, li ñu koy layalee, ñaare, mooy “intérêt national”, ngir man a yay seen bopp ci fen yi doonte xam nañu ne fen baaxut. Waaye, boo jàngatee bu baax xalaat bi Mearsheimer bëgg a jëmmal, dangay gis ne doxaliin wu ni mel, ni mu man a soxalee mbir yu jëm bitim-réew, noonii la man a soxalee mbir yoy, biir réew mi la yitteel. Rawati na mu doon mbir yoo xam ne leeg-leeg dafay lëkkale ñaari taxawaay yi : bu biir réew mi ak bu waa bitim-réew. Lu ci mel ni xew-xew yi lëmbe réew mi jamono yii.

Ba tax na, ku seetaan tey Aysata Taal Sàll ci janoo bi mu doon amal ak saabalkat yi, dinga gis yére yi taq ripp ci daa gi Mearsheimer bindee téereem bi. Bindkat bi juróomi xeeti fen yi mu lim ne moom la njiit yiy def, ndaw si Taal man naa doon seetu ba. Rax-ci-dolli, ñaari pexe (technique) yi Mearsheimer yaxal ne mooy cëslaayu njiit liy fen ngir tuur lëndëm ña muy waxal, dañoo fees dell ci kàdduy ndaw si :

  • “Concealment” : saale-saalelu, mel ni ku xamut ñeel dëgg-dëggi mbir mi. Ni ko Soxna si Taal defe ci lu jëm ci coxorteg takk-der yi (bavures policières), jàpp yu teguwul ci yoon yi (arrestations arbitraires) yi ak par-parloo bi ci Toppekat yeek àttekat yiy luññutu (partialité du Parquet et des juges d’instruction).

  • “Spinning” : wiiri-wiiri, mbir mu nekk nga cof ca li dëppoo ak li nga bëgg a saxal, la ëpp solo ca mbir ma nga tege ko wet. Ni ko ndaw si defe ci lu soxal kàddu gii “Ni mu gën a gaawe” (Dans les meilleurs délais), “Bésub 2 avril 2024”, “Bésub wote yi”…

Daanaka “conférence de presse” bi yépp ci ñaari pexe yooyii la sukkandiku ngir jàllale fen yi mu bëgg a gëmloo nit ñi muy waxal.

Lii lépp li muy firndéel mooy ne ñoom ba léegi noppeeguñu ngir jébbalu. Dinañu yolomal di xool poroxndoll bu ubbeeku ngir ñu jaar fa. Waaye, bu ñu am mbetteel bis bu ñu daanoo ci seen ndëgg-sërëx ni ko Mearsheimer di woowe “Blowback”, nu man koo tekkee ci wolof : “Sànni buy dellusi, duulu bëy doy na ci”. Maanaam, lii nuy def yépp ci seen kaw lay këppuwaat. Ndaxte, fen bu ubbee benn bunt, tëjal na la fukk… Te sax, wolof nee, fen du bijjaaw. 

Seexunaa Njaay
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj