Joŋante “baccalauréat” amal nañu ko alxames jii, fukki fan ak ñeent ci weeru sulet. Li ëppoon ci ndongo yiy wut seenub lijaasa bu leen di jàllale ca daara ju kawe ja, natt nañu leen. Niñ ko tàmm a defe at mu nekk, ndongo ya nekk « série technique » ñoo njëkk a def seen ug kàtte.
Bu ñu sukkandikoo ci ñuy saytu joŋante boobu di wa “Office du bac”, ren, tollu 150 925i ndongoy nattu. Waaye, bu ñu méngalee lim boobu ak bu daaw ba, danuy gis ne 6 401i ndongo wàññeeku nañ. Ci xayma, téeméer boo jël, lu ëpp juróom-fukk ak ñaari ndongo yi ca daaray Nguur ngi lañu féete, fukk ak juróom-benni ndongo ak lu teg diy seen i lawaxi bopp. Lim bi ci des, ci lekkool piriwe yi lañ jóge. Cees mooy diiwaan bi ëppaley lawax, lu tollu ci 26 191i ndongo ñoo fa féete.
Wërngal bu njëkk amal nañu ko ci natt gi ñu doon nat ndongo yi. Ñu bari si ñoom biral ni “épreuves” yi jafewuñu. Loolu, du guléet ci joŋante bu ni tollu, ni booy nay nopp. Joŋante yi jaar na ci yoon. Doonte ne, seetlu nañu ne benn ndongo bu doon jéem a luubal ànd kook ub xaritam. Loolu ame ca “Lycée Délafosse”. Ñu jàpp leen, di leen toppe “fraude à l’examen et usurpation d’identité”. Muy luy faral di am di amaat ci yile joŋante. Terewut ne, ku ñu ci jàpp, yoon dina la teg ay daan.
Ndongo yi di xaarandi seen i ngirte ginnaaw bu ñu lafee wërngal bu njëkk bi. Loolu, xibaar bi ñu ci mën a biral di, yenn ci ay ngirte dina rotani altine walla talaata yii ginnaaw bu ñu sukkandikoo ci kàdduy Soose Njaay, muy jëwriñ ji ñu dénk wàll woowu di saytu joŋante bi.