BALAA NGAA WAX NAAM, NE FA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lekkool bi, ay at ñu ngi nii jafe-jafe bu dem, moroomam wuutu ko. Bokk na ci li ko gën a jatt, di bank loxo yi, yenn ci kuréli jàngalekat yiy xeex ak, yenn saa yi, ndongo yi. Loolu di jur ay rëq-rëq ci njàng mi, joŋante yi ak ay tardamaa ci naal yi. Ñu seetlu ne, atum ren jii, lii ñu lim léegi ak waxtu nawet wii joŋante yi yamoog yàqu ci dara. Li ëlam nit ñi kay mooy : ana lan moo sooke njureef yu baax yii ci joŋante at mii ? Liggéeyu Nguur gi la, wala mën a jàngum ndongo yi la,  am boog taxawaayu jàngalekat yi la ?  Lu ci mën di doon, wolof dina faral di wax ne : upp baax na ci laax bu tàng. 

Dafa mel ni taxawaay bi kuréli jàngelekat yi ame woon ngir xeex seen i àq ak yelleef metti woon na ci ñépp. Waaye, jàmm a ca mujj. La ñu doon sàkku ci Nguur gi, bu ñu amut lépp la ñu teg ci seen i loxo, mën nañu cee jàppandi. Ndax  payoor ya ñu doon sàkku ñu yokkal leen ko, Nguur gi def na ko. Ndàmpaay yi bokkon ci seen i ñaxtu saafara am na ca. Ba tax na ñu bari ci ñoom gis nañu ci seen bopp. Ñu gis ne yokkuteg payoor yooyu tax na jàngalekat yi sawar ba mu am i njeexital ci joŋante yi. Loolu la Sawdu Seen, kenn ci njiiti SAEMSS, xamle ci Vox Populi : “payoor yi àgg na ci dayo bu mu mësut a àgg”. 

 Li koy firndeel di njuréef  yi tukkee ci joŋante atum 2022 mii, baax lool. Moo xam daara yu suufe yi , yu digg-dóomu yi ak waa “BAC” bi. Bu ñu sukkandikoo ci këru yéenekaay bii di Seneweb xayma bi nii la fa tëdde : ca atum 2011, téeméer boo jël, lu ëpp fanweer ak juróom-ñett ( 38,13%) jàll nañu ci joŋante BAC yi. Lim bi yokk ba téeméer boo jël lu ëpp juróom-fukk (51,99%) am nañu. Waxeesuñu “mention” yi. Waññi nañu 154 “Trés bien ”, 1. 200i “Bien” ak 6. 547i “Assez bien”. Waa BFEM bi seen xayma tollu ci 67,96% ca atum 2021, dem ba 70,38% ci atum 2022 mii. Bu ñu nattee daara yu suufe yi, CFEE bi a ngi tollu ci 73,38%. 

Mu mel ni yokkug payoori jàngalekat yi lu war la. Ndax  moo gën ci daara yi, gën it ci jàngalekat yi. Dina tax ñu fonk seen liggéey, jox ko àqam. Te dina tax ba xar-matt mi wàññeeku. Ndax kuy wàlliyaani, sa kër daa tëggut. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj