BATAAXAL BU JËM CI MAAM SEŊOOR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Maam,

Fan yee weesu, sama xel dafa ne yarr ci yaw. Ba nga demee ba léegi déggu nu la. Mbaa du foofu dafa neex rekk nga fàtte nu ?

Njort naa ne yaa ngi fa nekk di dawal i téere ak a bind rekk. Ndaw lim bu takku ! Li ngay bind foofu nag moom, xaw ma ndax yaa ngi nu koy yónnee am déet, waaye boobu ak léegi, jotunu dara. Xanaa dëkkee nafar ak a dawal ak dawalaat “Ethiopiques” ak yeneen yu gànjaru yi nga nu fi bàyyil.

Xéy-na du ñàkk am ñu naan lu tax ma lay mbind ci wolof, yaw mi nga xam ne kenn umpalewul sa diggante ak làkku farãse. Dama bëgg rekk nga gis ni sunu làkk yi suqalikoo léegi, tubaarkàlla !

Lu baree bari xew na ci sa ginnaaw, xaw ma sax fan laa war a tàmbalee. Xam naa yaa ngiy muuñ sax.

Sama waxtaan ak yaw nag xajul cib bataaxal, bu nu gisee, daa nu làng, àggale ko ndeem soob na Yàlla.

Ndax duma tàmbalee ci ladab sax ? Xam naa moos ne moo la gënal !

Waaw Maam, xanaa sa xalima gu ñaw gi te mucc-ayib danga koo fuloon, séddale ko bala nga doon dem ? Dama xam ne kat, Saa-Afrig yaa ngi fi di gën a ràññeeku rekk ci wàll woowu, di wone seen bopp bu baax a baax maasàllaa.

Diggante 2021 ak 2022 rekk raaya yu bari duggusi nañu ci Kembaarug Afrig. Ci atum 2021, doomu Tansani bii di Abdulrasaak Gurna, moo jël ndam lu rëy lii di “Prix Nobel” ci ladab. Nu jóge ca, sa sët Muhammad Mbugar Saar, jël “Prix Goncourt” sa Faraas, nu tekk ci tuuti, ci 2022, sa doom jii di Bubakar Boris Jóob, jël “Prix international de littérature Neustadt” bu waa Amerig di joxe nga xam sax ne dañu koy gam-gamle ak “Prix Nobel” ci ladab. Taxawal na it ab xëtu yénnekaay ci kàllaama Wolof. Rax-ci-dolli ubbi na ab kër guy móol i téere ci sunu làkk yi ba jot naa siiwaal ab lim sax. Gis nga ni mbir yi di jëmee kanam ?

Mbaa nekkoo di tàccu rekk mbaa ngay sarxolle ? Xam naa yaa ngi bég fi mu ne !

Noppeeguma ak yaw ci loolu de !

Sa jeneen doom it, Suleymaan Basiir Jaañ, mi ngi fiy ràññeeku bu baax maasàllaa ci wàllu xeltu. Jagleel na la fi sax ab téere di ciy aajar sa bëtu xeltukat bi nga doon xoolee mbatiitu Afrig. Duma la ko nëbb nag Maam, xaw ma ndax xam nga koom déet waaye, ñu baree ngi fiy wéy di la sànni xeer rekk. Nee nañu yaw ab tubaab bu ñuul nga woon, nekke woo fi woon lu dul di làkkiy farãse ak a logg-loggal. Loolu nag la Suleymaan B. Jaañ di weddi saa suy wax ci yaw ngir wone sa xel mu ñaw mi nga yoroon ak ni nga fonkee woon mbatiitu nit ku ñuul. Ci loolu sax la sukkandiku, bi ko daara ju mag jii di “École Normale Supérieure” bu Pari dalalee diggante féewiryee ak awril 2023 def ko cëslaay ci lenn ci ay waxtaan yi mu doon amal ayu-bis bu nekk.

Waxtaanam wu mujj wi, mi ngi ko jagleloon baatu “nite”, sukkandiku ci waxi wolof jii di : “Nit, nit ay garabam” walla “Nit nite ay garabam”. Ci dégg-dégg bu gàtt rekk, mën nanoo tekki léebu bi ci ne nit mooy faj aajo moroomu nitam. Waaye, baatu “garab” biñ ci dugal dafay firndeel ne tawat am na te du lenn lu dul ñàkk a nekk dëgg dëgg nit. Xeltukat bi jàngat ne nit, ngir mu mat nit ki mu war a nekk, dafay jaadu ci moom mu nangul ñeneen ñi seen ug nite : “duma nekk nit feek ñeneen ñi nekku ñu ay nit”. Mboolaay gi, dafay taxawu képp ku ci bokk ngir mu mottaliku ba mat nit. Nu gis ne kon kenn ku ne, dafa war a seey ci mboolaayam, mu gënal ko boppam ak i bëgg-bëggam : “nekk naa ndax nun nekk nanu”, “damay dëggal samag nite ndax noo ngi mottali sunug nite”.

Ndeke kon daanaka coono yi nuy dund, yi ci ëpp, ñàkk a nekk nit doŋŋ moo nu ko yóbbe.

Moo waral nit di xeeb moroomam. Moo waral ñii di lekk alal ju ñu leen dénk, ndax seen bopp a leen gënal. Moo waral it njiit di nappaaje ñi ko jiital. Ci gàttal daal, ku nekk a ngi wey di topp ay bëgg-bëggam bay salfaañe yosi ñeneen ñi.

Su ma yaboo ne, fii mu ne, kenn gënu la bég, Maam-bóoy, ci xibaar yii ngay jàng ci sama bataaxal bii. Xam naa yàkkamti nga noppi ba dem wax ko sa gaa ña nga nekkal foofu.

Xaaral sax ma yamale waxi mbatiit yi fii te ñëw ak yaw ci wàllu pólitig. Mbaadu danga foogoon ne dinaa wax ak yaw ba noppi te duma ko tudd ?

Xéy-na doo ci sawar ni nga saware ci waxtaanu mbatiit. Waaye, mënul ñàkk nag Maam-bóoy.

Xam nga sànq maa ngi la naan ñu bari dañuy wax ne yaw ab tubaab bu ñuul nga woon. Waaye nag, ñi ëpp ci ñi àndul ak yaw, jàpp naa ne ci wàllu pólitig lañuy waxe. Donte nag am na loo xam ne fàww nu nangul la ko. Bu nuy wax Càmm ak Mbolaayu Senegaal (“Etat Sénégalais et Nation Sénégalaise”), danga cee am wàll wu rëy. Yaw yaa tabax Càmmu Senegaal ba ñépp nawloo ko ; waaye it danga dugal sa loxo bu baax ci luy jëmmal Mboolaay gi. Bul foog ne dama lay jay nag, déedéet !

Ñépp xam nañu ne, yaa njëkk a jiite Réew mii nga xam ne ñi ci ëpp ay jullit lañu te yaw doonoo ko woon. Waaye coow mësul jib ci loolu. Nga nekkoon ci làng pólitig gi ak sa nawley jullit ba noppi ràññeeku woon ci ay tariixa. Waaye teewul yaw yaa nekkoon xaritu njiiti tariixa yooyu. Kenn réerewul sa diggante ak Sëriñ Fàllu Mbàkke ak Sëriñ Baabakar Si ñi fi nekkoon ca jamono jooju.

Muy firndeel ne ñépp dañoo bootu woon sa ginnaaw nga bokk njaboote ñépp.

Waaye léegi, daanaka la woon, wonni na.

Maam, Réew mi, fi mu ne nii rëb na lool sax. Kenn nawloowul moroomam te lépp, way-pólitig yi ñoo ko waral. Waa-waaw  ! Nguur gi ak kujje gi di mel ne xaj ak muus, buum gi leen lëkkale teeŋ na ba jéggi dayo. Te, ku ci bàyyi, askan wi doŋŋ a ciy gaañu. Dañuy saagante, di xastante, di jokkalante ay kàddu yu ñaaw a ñaaw. Loolu dem ba am ay njeexital yu réy ci dundinu askan wi. Léegi daal, dal amu fi, fitna rekk. Mu mel ne li nu amoon ci mbaax ak jikko yu rafet ak lu nuy jomb yépp a raaf.

Ñi la fi wuutu, yor seen ub yar di caw rekk. Xéy-na soo leen laajee ñu ne, “xale yi dañoo dëgër bopp”. Waaw, waaye xanaa sax yenn saa yi, way-jur dina woo doomam yedd ko, du dëkk ci di ko ndulli rekk.

Dañoo dem ba ñu bari amatuñu fitu wax ndax jàppe yu bari yi. Ñu ngiy lim ay nit ñu bari ñoo xam ne làq nañu leen jant bi ndax mbiri pólitig. Ki gën a fés ci kujje gi sax ci la bokk, ma nga ndungusiin fi mu nekk nii, tas nañu tamit làngu pólitigam. Waaye loolu nag ci yaw lañu ko jànge !

Waaw yaw sax Maam, lu taxoon nga tas làngu pólitig gii di PAI ? Daf la neexoon rekk walla danga doon wone sa diisaayu loxo ? Mu mel ne ñii fi nekk dañu la doon delloo njukkal ci loolu ndax daanaka 63i at yu mat sëkk ci ginnaaw lañu defaat la nga defoon. Boo fàttalikoo, yaa ngi tasoon PAI benneelu fan ci weeru ut atum 1960, ñoom ñu tas PASTEF ci 31i fan ci weeru sulet ci 2023. Xanaa du bés bee dellu si ?

Jàpp gi ñuy jàpp ñi ci kujje gi it dafa mel ne yaa leen ko won Maam. Aa ! Yaw kat bi nga fi nekkee, lañu jàpp Maam Mamadu Ja jàpp it sunu baay Omar Bolondeŋ Jóob ba mu mujj faatu ci kaso bi. Ndeysaan ! Xanaa du kon yaw yaa xàll yoon wi ?

Ñoom sax, lu taxoon nga tëj leen ? Loolu leerul ci sama bopp ba léegi. Bu nu gisee nga wax ma lu tax.

Yii ma lay fàttali nag, defuma ko ngir nga am lu la metti, dama la koy wax rekk ngir mën a ñëw ak yaw ci tolluwaayu Réew mi.

Jaxasoo na lool, jafe-jafe yi it bari nañu. Mën nanu koo gam-gamle ak yaramu màggat, foo laal mu metti. Par-parloo bi bari na ba ku juum sax du nangu ne juum na. Ku nekk jàpp ne moo am dëgg te képp ku àndul ak moom nekkul ci dara. Loolu dem ba ñi jiite mel ni ñu gëlëm walla ñu fàtte seen i wareef seen diggante ak askan wi. Njëg yi yokku, njàng mi gall-góose, raglu yi feebar, ñépp di ñaxtu ak a xultu. Ñoom, ñuy wéy di doxal, mel ne lépp a ngi jaar yoon, dëkkee wax waxi pólitig rekk ak di ko jëfe.

Yaw de, ak lu ñu la mën di waxal, bi nga fi nekkee Réew mi melul woon nii mu mel tey. Dëgg la, jamonoo soppeeku, waaye li fi newoon ci mbaax, mi ngi fiy baax rekk.

Li ma lay laaj kay mooy, lu tax nga dem rekk toog di seetaan ?

MAAM, SA PATT-PATTAARAL GI YÀGG NA, WAR NGA WAX DE !

Waxal ak nun Saa-Senegaal yi, nu xam nooy kan te jekkalaat sunu toogaay. Boo mënul ñëw sax nga yable walla nga bind yónnee waaye fàww nga wax.

Gis nga jéego yu réy yi nu def ci mbatiit, su nu deful ndànk, coowal pólitig yi dina ko far ba dara dootu fi des. Te bu boobaa, xawma looy wax sa xarit yi nga nekkal foofu.

Nuyul ma sa mbokk ya nga nekkal yépp. Su ma limee juum. Waaye xam naa seen i jotaay mënul def lu dul neex.

Yàkkamti naa jot sa tontu, xam naa ne sa xalima gu mucc-ayib googu, lu mu bind rekk mu jaar yoon. Bu nu gisee gën a yaatal.

Baabakar Lóo

Pari, 20 safar 1445 yamoo ak 6i fani sàttumbaar 2023

Baabakar Lóo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj