Doomi Senegaal, ñu yàgg a dox lañu. Bu ñu nekkul fépp it, bari na réew yooy dem tase fa ak ñoom. Aw askan lañu wu ñeme tukki, bëgg tukki, mën a tukki te yàgg it tukki lool. Dem nañu, ba mu mel ne, tukki dafa bokk ci ñoom. Bu ñenn ñi di dem ngir wuti lu ñu suturloo, ñeneen ñi dañuy jóg ngir wattu seen bopp, gën a ñoŋal seen ug dund. Am na itam ñuy sàkkuji xam-xam ak ñuy gàddaay ndax jaaxle ak ñàkk yaakaar. Waaye tamit, am na ñu kumpa kepp di yóbbu ak ñuy tukki ngir yaras, jàpp ne, la ca biti moo gën li ci biir. Am na sax ñuy wax ne, ku tukki, tekki. Am na yit ñu gëm ne, fàww ñu tukki ngir tekki. Donte sax faramfàccewuñu lu baatu “tekki” biy tekki.
Ak lépp lu ko mën a yékkati, kiy roñ i godaaram di waaj a tukki, mi ngi def ay tànneef yu yéeme, mu yëg ko ak mu umpale ko. Mi ngi tànn, bàyyi ci ginnaawam suuf si ko meññ. Ba noppi, nara dem ci seneen suuf sos, xamul naka lees ko fay gatandoo. Mi ngi tàggatoo ak ay jegeñaaleem yoy, dootu leen tegati bët mukk ci kaw suuf. Mi ngi dem tamit te, xamul kañ lay dellusi. Xamul sax ndax dina ñëwaat walla, bu naree dellusi it, ndax dina indaale bakkan am déet.
Ci kaw loolu lépp, mu laxasaayu rekk ne : “Dee moom wenn yoon la. Te, ndegam ñëw nanu ci kaw suuf ba noppi, dara desatu fi ludul ñibbi (laaxira) rekk. Ñàkk a xam kañ la kay moo nu ëlëm. Te sax, diggante juddu ak faatu, noppalu da cee xajul”.
Loolu di ko yóbbee muy dékku lu ne. Nde, bu demee réewu jàmbur, danañu ko bëmëx, danañu ko këmëx. Dana fa daj lu mu mësul woon a xalaat a dund ci biir réewam te, du ci mën dara. Ndax kat, moom moo wàlli. Te, “kuy wàlliyaan, sa kër a tëggul”. Lu tax këram tëggul ? Xanaa amuñuy ndënd ni ñépp ? Looloo jar a laaj nag !
Ci noonu, la taasukat ba xaacoo ne : “ku sa reeru baay doy, doo tal a xaaraani ba ñu di la bëmëx”. Nu dégg ci ne, ki bàyyi léppam, dem bitim-réew, àdduna di ko bëmëx muy muñ, reer bi réewam rëgël moo doyul rekk. Bu doyoon, du dem. Waaye, moom lañuy fekksi. Kon, Saa-Senegaal yi fi bàyyi teraanga gi ñuy taggee réew mi, jaar ci géej gi, walla jéeri ji, walla jàwwu ji, dara yóbbuwu leen lu dul xaaraani. Ndax, reer bee suurul ñépp.
Reer bi nag, yamul ci lu ñuy lekk doŋŋ. Dees koy soloo, dees koy jàngee, dees koy fajoo, … Ci gàttal, reer bi mooy ëmb lépp luy teeyal dund nit ki ba noppi teg ko ci yoon. Kon, bari na ñoo xam ne, li ñuy wuti bu jàppandi woon, duñu dem fenn. Ki jóg di jàngi, bu daara yi ak jàngune yi ci réew mi meloon ni ñu waroon a mel, amaana kon du dem fenn. Kiy wuti sutura, bu lépp tegu woon fi mu waroon a tegu, xéy-na du xalaat a génn. Niki noonu ki bëgg a faju, kiy dem ngir bañ ku ko toroxal walla ki ñu jaay doole.
Dëgg la, lépp mënul a mat gaa. Ndax, yëfi nit moom, yëfi nit la rekk. Waaye, bu li ëpp matoon, lu nekk tegu fa mu war a tege, ku nekk def la mu war a def, doomu Senegaal du wàlliyaani mukk. Daf koy neex rekk, mu dem xool la xew feneen ngir yaatal liggéeyam, yokk xam-xamam, féexal xolam walla yu ni mel. Waaye, du mës a dem fenn di wuti lol, soxla na ko, te mënu cee jot feek mi ngi toog ci réew mi.
Te sax, Senegaal du réew mu ñàkk. Te it, du réew mu ay doomam yaafuus. Réew la mu mag, mu Yàlla beral loxo bu baax a baax ci fànn yu bari. Niki fi mu féete ci kaw suuf, li mu ëmb ciy balluy mbindaare yu gànjaru ak ni ñu bari ci ay doomam ràññeekoo ndax seen taxawaay ak seen ug njàmbaar. Te lépp nag, ànd ak bëgg réew mi mbëggeel gu amul yemu. Dafa fekk ne kay, li ëpp ci li nu yóbbee lii nuy dund, sunuy njiit ñoo nu ko teg. Ñoom lanuy fal, jël li nu moom denk leen, ñu jàpp ni seen moomeelu bopp la. Méngale seen bopp ak i buur. Nekk ci donkaasi giy nguuru ak a bànneexu. Fàtte li leen fal ak li leen war.
Waaye nag, ci weneen wàll, nun danuy fàtte ni, njiit yi, ci askan wi lañu bawoo. Kon, bu ñu dëngee rekk, wareef la, ci nun ñépp, nu xoolaat sunu bopp. Te nangu ne, bu genn kilifa jubadee rekk, lim bu takku ci mboolaay gi dañoo jubadi. Kon, jafe-jafe yi, du ci kilifa yi doŋŋ, ci sunu wet sax, nun askan wi, la ëppee. Bu nu soppee njiit ay yooni yoon, te soppiwunu sunu bopp, coppite gi nuy séntu ci sunug dund, du mën a nekk.
Njiit lu ñëw rekk, ni aw askanam lay mel. Ndax, li butéel def rekk la saañ bay xeeñ.