DUND GU DIGG-DÓOMU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu jamono di gën a dem, mag ñi di gën a ñaawlu nekkiinu ndaw ñi. Moom kay, dañoo dëkk ci di ŋàññ seen i doxalin ak a naqarlu seen ñàkkug yitte. Dinañu ciy rax dolli, ñoom mag ñi, ne ndaw ñi tegginewuñu lool. Ñaare sax, dañu leen di méngale ak maas gi dox seen diggante, ñoom mag ñeek ndawi tay jii. Walla sax, ñu leen di gam-gamle ak ñoom, ci seen bopp, bi ñuy am at yi goney tay yi am.

Mu mel ni, bu nu sukkandikoo ci loolu, jamono ju jot rekk, ñi ko dëkke ñooy yées ña leen jiitu ci lu bari, niki teggin ak jikko yu rafet. Walla boog, jamono ju jot rekk, lenn ci mbaaxi démb yi dañuy réer, mbon gi wuutu ràcc. Dafa mel ni rekk, mbaax dafa nekk ci tànki raaf.

Ñi nangu ni noonu la demee, bu ñu ko bëggee utal aw lay, mën nañoo wax ne : “jamonoo soppeeku rekk, xale yi soppiku ànd ak moom”. Te sax, loolu moom, nekkul rekk ndaw ñi ñëw bees. Nde, dañoo dikk fekk mag ñi leen jiitu ànd ak jamono di dox, di dem. Dafa di rekk, ku nekk ak sa doxin. Ñenn ñi dañuy daagu ba mu ëpp, ñeneen ñi di waaxu te baral ko lool. Ci diggante ñaari xeet yooyu nag, am ñuy jayaŋ-jayaŋi, ñuy ŋat-ŋati, ñuy nokkos-nokkosi, ñuy yagar-yagari ak sax ñuy tëñëx-tëñëxi. Waaye, ku ci nekk rekk, ak xeetu doxin wu mu mën a ame, mi ngi ci yoonam, lëngoo ak àdduna di wéy.

Nu gis ne kon, lay wi du luy yomb a dàq. Xel mën na koo nangu ci lu amul benn jafe-jafe. Ndax kat, ñaar ñu ànd, lëngante, lu sañaxal kenn ki du fa bàyyi ka ca des. Kon, bu jamono dee yëngu moom, ki ànd ak moom mënul a ñàkk a yëngu. Waaye nag, bu dee saa su yëngoo nu topp ci, def ni moom, ndax dinanu tal leneen ? Dafa di, jamono, yëngu ak soppeeku la baaxoo. Daf koo tàmm ba, bu doonoon nit, mënees na koo tëkkale ak ku boole léej ak luqnjuur. Rax-ci-dolli, moom jamono, ku bariy yitte la. Te, du jóg ci di dogu, saa su ne rekk, ngir di leen doxal boppam. Mënul toog lu yàgg cib barab, mel ni rekk ay rabam dañuy bañ loolu. Moo tax, ku ko dëkkee topp rekk, bu moytuwul dundam dina rëb.

Waaye tamit, ndax mën nanoo nekk ci kaw suuf, bëgg dund gu teey ba noppi bañ a dox ni jamonoy doxee ? Naka la nuy méngoowee ak jamono te dunu ko topp ? Walla, ci weneen waxiin, ndax mën nanoo ànd ak jamono ci ni mu waree te, dunu ko topp ba mu sori ? Maanaam, dunu ko topp ba mu yóbbu nu fof, ndëgg-sërëx a fa nekk. Bu ko defee, bu nu fa dëggee sunu tànk rekk, tarxiis walla sànku daf nuy yomb. Bu loolu mënee nekk, naka lees ko mën a defee ?

Li wóor mooy, farata la ci nun, nuy fexe ba, lépp lu nuy def, nu koy yemale sunu kéem kàttan. Bañ di ëppal, bañ it di yéesal. Ndax kat, lu rembat tuuru te lu matul moom, mëneesu koo jëriñoo ci ni mu waree. Moo tax, kiy yoot ba jamono raw ko lool ak ki ko topp di xélu lu mu àttanul, ñoom ñaar ñépp a nekk cig lëndëm. Dañoo sori digg bi lool sax, te ñaari cat yépp a wóoradi. Dañoo sew ruuj ba ku ca taxaw xàwwiku. Ku leen dëgmal it, gëlëm daf koy yomb. Te, ku gëlëm, bu réeree warul a jaaxal i mbokkam. Ba tax na, dafay jaadu, ci lépp lu nuy def rekk, nu ciy digg-dóomu. Maanaam, nuy fexe bay bañ a weesu diggoo ba ca war. Moo xam lu nuy jëfandikoo (lekk ak naan), lu nuy gëm (diine, pólitig, añs.), lu nuy bëgg walla lu nuy bañ. Ci loolu it, la sunu lëngoo ak jamono war a lalu. Danu war a ànd ak moom ak doxin wu dëgër te am pasteef ba noppi nu yemale ko bu baax.

Liy wax ji nag mooy, naka lees mën a def bay digg-dóomu ci sunuy jëf ak i wax. Yomb naa wax lool waaye, def ko laaj na lu bari. Laaj na nu nàmm sunum xel, tàggat sunuy jikko te ànd ak sunu sago ci lépp lu nuy def ak fépp fu nu nekk. Noonu rekk lanuy mënee ràññaatle lu bari ci li nu mën a fakkastal. Laaj na itam nu xam sunu bopp. Ndax, mooy tax nu xam fa nu jóge, ki nu doon, li war ci nun ak li nuy jomb. Ci la nuy mën a xamee it fi nu war a teg sunuy tànk. Bu ko defee nu xam fa nu wara dem ak ba fan la nu am sañsañu àgg.

Te, xam sunu bopp sax mooy caabi ji. Bu jiituwee rekk dinanu mën a ànd ak sunu sago te di jëfandikoo sunum xel bu baax. Ndax, dara dootu ko tënk, danu koy boyal muy xelli leer gu dul fay mukk tey jëriñ àddina sépp ba fàww.

Waaye nag, mënunoo xam sunu bopp feek nu ngi réere sunum mbatiit. Ki nu doon dëgg, mbatiit mi kese lanu mën jeex ba daj ko. Feneen fu nu aw fu dul foofu, mën nanoo xam lu bari gaa, waaye, du tax mukk nu xam sunu bopp.

Te, lu waay mën a xam te réere boppam, njariñ la narul a bari lool. Ndax, tegle bi, lu mu kawe kawe, ci daanu la jëm. Nde, tóoj gaa fënëx.

Baabakar Lóo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj